1 Gannaaw loolu ma gis meneen malaaka mu wàcce ca asamaan, yor sañ-sañ bu réy, te leeraayam daj na àddina sépp.
1And after these things I saw another messenger coming down out of the heaven, having great authority, and the earth was lightened from his glory,
2 Mu daldi xaacu naan: «Daanu na! Babilon mu mag ma daanu na! Léegi dëkkukaayu jinne la, ak bépp rab wu bon ak bépp picc mu daganul te araam.
2and he did cry in might — a great voice, saying, `Fall, fall did Babylon the great, and she became a habitation of demons, and a hold of every unclean spirit, and a hold of every unclean and hateful bird,
3 Ndaxte jox na xeeti àddina yépp, ñu naan ci koppu nafsoom ak njaaloom, ba ñu màndi. Buuri àddina ànd nañu ak moom ci njaaloo, te baana-baanay àddina woomle nañu ndax li mu bëgg mbuux.»
3because of the wine of the wrath of her whoredom have all the nations drunk, and the kings of the earth with her did commit whoredom, and merchants of the earth from the power of her revel were made rich.
4 Noonu ma dégg beneen baat bu jóge asamaan naan: «Génnleen ci biiram, yéen samay gaay, ngir ngeen bañ a bokk ci ay bàkkaaram te bañ a am cér ci musiba yi koy dal.
4And I heard another voice out of the heaven, saying, `Come forth out of her, My people, that ye may not partake with her sins, and that ye may not receive of her plagues,
5 Ndaxte ay bàkkaaram dajaloo nañu ba ci asamaan, te Yàlla fàttaliku na ay jëfam yu bon.
5because her sins did follow — unto the heaven, and God did remember her unrighteousness.
6 Dellooleen ko li mu defoon, feyleen ko ñaar ci li mu lebaloon, feesal-leen koppam ak naan gu gën a wex ñaari yoon naan ga mu joxe woon.
6Render to her as also she did render to you, and double to her doubles according to her works; in the cup that she did mingle mingle to her double.
7 Joxleen ko ci coono ak naqar, lu tollu ni tiitar ak mbuux, ba mu dencaloon boppam. Gannaaw nee woon na ci xelam: “Maa ngi toog fii ni buur, duma ab jëtun te duma ténj mukk,”
7`As much as she did glorify herself and did revel, so much torment and sorrow give to her, because in her heart she saith, I sit a queen, and a widow I am not, and sorrow I shall not see;
8 looloo tax ba musiba, yii ñu ko sédd, dinañu ñëw ci benn bés, ñu di mbas, ténj ak xiif, ñu di ko lakk ba mu jeex, ndaxte Yàlla Boroom bi ko àtte, ku am kàttan la.»
8because of this, in one day, shall come her plagues, death, and sorrow, and famine; and in fire she shall be utterly burned, because strong [is] the Lord God who is judging her;
9 Buuri àddina yépp, yi àndoon ak moom ci njaaloo ak mbuux, bu ñu séenee saxar siy jollee ci taal bi ñu koy lakke, dinañu yuuxu, di ko jooy.
9and weep over her, and smite themselves for her, shall the kings of the earth, who with her did commit whoredom and did revel, when they may see the smoke of her burning,
10 Dinañu tiit ndax coonoom, ba dandu lu sore, naan:«Ngalla yaw! Ngalla yaw,dëkk bu mag bi,Babilon mi am kàttan;wenn waxtu rekk doy na,ngir sab àtte mat!»
10from afar having stood because of the fear of her torment, saying, Wo, wo, the great city! Babylon, the strong city! because in one hour did come thy judgment.
11 Baana-baana yi ci kaw suuf di jooy, di ko naqarlu, ndaxte kenn dootul jënd seen njaay:
11`And the merchants of the earth shall weep and sorrow over her, because their lading no one doth buy any more;
12 seen wurus, seen xaalis, seeni jamaa ak yeneeni per; seeni piis yu rafet, piis yu yolet, yu ray-ray, yu xonq; seen dénk wu xeeñ, seen yëf yi ñu defare iwaar walla dénk wu jafe walla xànjar walla weñ walla marbar;
12lading of gold, and silver, and precious stone, and pearl, and fine linen, and purple, and silk, and scarlet, and all thyne wood, and every vessel of ivory, and every vessel of most precious wood, and brass, and iron, and marble,
13 ak bant yuy safal, gàncax gu xeeñ, ay xeeti cuuraay yu bare, latkoloñ, biiñ, diw, sungufu lay-layaat, pepp, ay nag, ay xar, ay fas, sareeti xare, ay jaam, ba ci bakkani nit.
13and cinnamon, and odours, and ointment, and frankincense, and wine, and oil, and fine flour, and wheat, and cattle, and sheep, and of horses, and of chariots, and of bodies and souls of men.
14 Dinañu wax naan: «Yëf yi nga bëggoon a am raw nañu la, te lépp luy yafal walla col gu rafet ñàkk nga ko, te kenn du ko gisaat!»
14`And the fruits of the desire of thy soul did go away from thee, and all things — the dainty and the bright — did go away from thee, and no more at all mayest thou find them.
15 Baana-baana, yi daan jaay yëf yooyu ba woomle, dinañu sore ndax ragal coonoom. Dinañu jooy di naqarlu,
15The merchants of these things, who were made rich by her, far off shall stand because of the fear of her torment, weeping, and sorrowing,
16 naan:«Ngalla yaw! Ngalla yaw, dëkk bu mag,bi soloon yére yu rafet, yu yolet te xonq,daan takk wurus ak jamaa ak per,
16and saying, Wo, wo, the great city, that was arrayed with fine linen, and purple, and scarlet, and gilded in gold, and precious stone, and pearls — because in one hour so much riches were made waste!
17 sa alal ju bare jépp naaw na ci wenn waxtu!» Noonu ñépp ñiy dawal gaal ak ñi ciy tukki ak ñi ciy liggéey ak ñi ciy baana-baana, ñépp di sore bérab boobu,
17`And every shipmaster, and all the company upon the ships, and sailors, and as many as work the sea, far off stood,
18 te bu ñu séenee saxar sa cay jollee, naan: «Ndax dëkk bu niroo woon ak dëkk bu mag bii mas na am?»
18and were crying, seeing the smoke of her burning, saying, What [city is] like to the great city?
19 Ñuy xëpp suuf ci seen bopp, di jooy, di naqarlu te naan:«Ngalla yaw! Ngalla yaw,dëkk bu mag bi nga xam neci la boroom gaal yépp woomle ndax sa barele,ci wenn waxtu nga gental.
19and they did cast dust upon their heads, and were crying out, weeping and sorrowing, saying, Wo, wo, the great city! in which were made rich all having ships in the sea, out of her costliness — for in one hour was she made waste.
20 Yaw asamaan, bégal ci li ñu ko yàq!Yéen itam gaayi Yàlla yi,ndaw yi ak yonent yi, bégleen,ndaxte Yàlla àtte na ko, ba feyyul leen.»
20`Be glad over her, O heaven, and ye holy apostles and prophets, because God did judge your judgment of her!`
21 Noonu malaaka mu am doole jël doj wu réy, sànni ko ci géej gi, naan: «Nii lañuy sànnee ak doole Babilon dëkk bu mag bi, mu ne meŋŋ.
21And one strong messenger did take up a stone as a great millstone, and did cast [it] to the sea, saying, `Thus with violence shall Babylon be cast, the great city, and may not be found any more at all;
22 Buumi xalam yi, baati woykat yi, toxoro yi ak liit yi,kenn dootu leen dégg ci yaw.Liggéeykat bu xareñ bu mu man a doon, kenn dootu ko gis ci yaw.Kandaŋu gënn, kenn du ko déggati ci yaw.
22and voice of harpers, and musicians, and pipers, and trumpeters, may not be heard at all in thee any more; and any artizan of any art may not be found at all in thee any more; and noise of a millstone may not be heard at all in thee any more;
23 Niitug làmp du tàkkati,te baatu boroom séet ak séetam dootul jib ci yaw ba fàww.Ndaxte say baana-baana ñoo yilifoon àddina,te xeet yépp réer nañu ndax say luxus.
23and light of a lamp may not shine at all in thee any more; and voice of bridegroom and of bride may not be heard at all in thee any more; because thy merchants were the great ones of the earth, because in thy sorcery were all the nations led astray,
24 Te deretu yonent yi ak gaayi Yàlla yiak ñépp ñi ñu rey ci kaw suuf,ci moom Babilon lañu ko fa fekk.»
24and in her blood of prophets and of saints was found, and of all those who have been slain on the earth.`