1 Nun ñi dëgër ci sunu ngëm, war nanoo nangu ñi seen ngëm néew te am ci lu ñuy sikki-sàkka, te bañ a yem ci wut sunu bànneex.
1And we ought — we who are strong — to bear the infirmities of the weak, and not to please ourselves;
2 Na ku nekk ci nun di wut lu neex moroomam ngir jariñ ko, ba mu gën a dëgër ci ngëmam.
2for let each one of us please the neighbor for good, unto edification,
3 Ndaxte Kirist musul a wut bànneexu boppam. Loolu la Mbind mi wax ne: «Lor yi ñu la saagaa, ci sama kaw lañu dal.»
3for even the Christ did not please himself, but, according as it hath been written, `The reproaches of those reproaching Thee fell upon me;`
4 Ndaxte lépp lu ñu waxoon ci Mbind mi lu jiitu tey, dañu koo tëraloon, ngir nu sàkku ci xam-xam, xam-xam bu nuy may fit ak muñ, ak di feddali sunu yaakaar.
4for, as many things as were written before, for our instruction were written before, that through the endurance, and the exhortation of the Writings, we might have the hope.
5 Kon nag Yàlla miy maye muñ ak fit, na leen may, ngeen déggoo te nekk benn bu yellook li Kirist Yeesu wone.
5And may the God of the endurance, and of the exhortation, give to you to have the same mind toward one another, according to Christ Jesus;
6 Ba tax nu bokk benn xalaat ak benn baat ci màggal Yàlla, Baayu Yeesu Kirist sunu Boroom.
6that with one accord — with one mouth — ye may glorify the God and Father of our Lord Jesus Christ;
7 Moo tax nangoonteleen, bay màggal Yàlla, ni leen Kirist nangoo.
7wherefore receive ye one another, according as also the Christ did receive us, to the glory of God.
8 Lii laay wax: Kirist ñëw na liggéeyal Yawut yi, ngir wone kóllëreg Yàlla ci matal dige, ya mu digoon maam ya.
8And I say Jesus Christ to have become a ministrant of circumcision for the truth of God, to confirm the promises to the fathers,
9 Ñëw na itam ngir ñi nekkul Yawut man a màggal Yàlla ndax yërmandeem. Moo tax Mbind mi ne:«Dinaa la màggal tey tagg saw tur,ci kanamu xeet yépp.»
9and the nations for kindness to glorify God, according as it hath been written, `Because of this I will confess to Thee among nations, and to Thy name I will sing praise,`
10 Mbind mi nee na it:«Yéen xeeti àddina, ñëwleen bànneexuak xeet wi Yàlla tànnal boppam.»
10and again it saith, `Rejoice ye nations, with His people;`
11 Mu dellooti ne:«Santleen Boroom bi, yéen waa àddina,te ñëw màggal ko, yéen xeet yépp.»
11and again, `Praise the Lord, all ye nations; and laud Him, all ye peoples;`
12 Te it Esayi wax na ne:«Am na sëtu Yese buy ñëw,dina yilif xeeti ñi dul Yawut,te ci moom lañuy wékk seen yaakaar.»
12and again, Isaiah saith, `There shall be the root of Jesse, and he who is rising to rule nations — upon him shall nations hope;`
13 Kon Yàlla miy maye yaakaar, na def ci seen xol mbég mu réy ak jàmm ju yaa ci seen kaw ngëm, ba ngeen am yaakaar ju mat sëkk ci dooley Xel mu Sell mi.
13and the God of the hope shall fill you with all joy and peace in the believing, for your abounding in the hope in power of the Holy Spirit.
14 Bokk yi, wóor na ma ne, baax ngeen ba fa mbaax man a yem, fees dell ak xam-xam, ba man a jàngaleente mbiri Yàlla ci seen biir.
14And I am persuaded, my brethren — I myself also — concerning you, that ye yourselves also are full of goodness, having been filled with all knowledge, able also one another to admonish;
15 Bu sama kàddu diisee nag ci bataaxal bii, dara taxul lu dul bëgg a yeesal seen xalaat, ndaxte Yàlla ci kaw yiwam daf maa sas,
15and the more boldly I did write to you, brethren, in part, as putting you in mind, because of the grace that is given to me by God,
16 ma nekk jawriñu Kirist Yeesu, yebal ma ci àddina ci xeeti ñi dul Yawut. Liggéey bu sell laay def ngir Yàlla, ci xamle xebaaram bu baax bi, ngir xeeti àddina sell ci dooley Xel mu Sell mi, ba neex Yàlla, mel ni sarax su ñu koy jébbal.
16for my being a servant of Jesus Christ to the nations, acting as priest in the good news of God, that the offering up of the nations may become acceptable, sanctified by the Holy Spirit.
17 Kon nag maa ngi bànneexu ci Kirist Yeesu ngir liggéey boobu ma Yàlla dénk.
17I have, then, a boasting in Christ Jesus, in the things pertaining to God,
18 Awma fitu wax leneen nag, lu dul li Kirist jëf jaarale ko ci man, ngir xeeti àddina jébbalu ci moom; jëf na jaarale ci samay wax ak samay jëf,
18for I will not dare to speak anything of the things that Christ did not work through me, to obedience of nations, by word and deed,
19 ci ay tegtal ak i kéemaan, sukkandikoo ci dooley Xelu Yàlla mi. Ba fi mu nekk nag yégle naa fu nekk xebaaru Kirist, li dale ci Yerusalem, jaar ci gox yépp, ba àgg diiwaanu Iliri.
19in power of signs and wonders, in power of the Spirit of God; so that I, from Jerusalem, and in a circle as far as Illyricum, have fully preached the good news of the Christ;
20 Sama yéene mooy xamle xebaaru turu Kirist fa mu eggagul, ndax bëggumaa yeggale sas wu keneen daloon.
20and so counting it honour to proclaim good news, not where Christ was named — that upon another`s foundation I might not build —
21 Li ma def nag, dëppoo na ak li Mbind mi wax ne:«Ñi yégagul mbiram dinañu ko yég,te ñi ko musul a dégg, xam ko.»
21but according as it hath been written, `To whom it was not told concerning him, they shall see; and they who have not heard, shall understand.`
22 Bëggoon naa ñëw seetsi leen, fekk ay téq-téq ñoo ma téye ba tey.
22Wherefore, also, I was hindered many times from coming unto you,
23 Waaye nag léegi bey naa sama sas ci gox yii.
23and now, no longer having place in these parts, and having a longing to come unto you for many years,
24 Bu may dem Espaañ nag, bëgg naa faa jaar, nuyu leen; ndaxte ay at a ngii maa ngi am yéene ju tar ci ñëw seetsi leen. Bëgg na maa nekk ci seen biir, ngir am bànneexu sotteente ak yéen xalaat ab diir, te it ngeen waajalal ma sama yoonu Espaañ.
24when I may go on to Spain I will come unto you, for I hope in going through, to see you, and by you to be set forward thither, if of you first, in part, I shall be filled.
25 Waaye nag fi mu nekk maa ngi dem nii Yerusalem, ngir dimbaliji gaayi Yàlla yu sell ya fa nekk.
25And, now, I go on to Jerusalem, ministering to the saints;
26 Ndaxte waa Maseduwan ak waa Akayi ñi gëm, fas nañu yéeney sàkk ci seeni alal, yónnee ko, ngir dimbali ñi néew doole ci gaayi Yàlla yu sell, yi nekk Yerusalem.
26for it pleased Macedonia and Achaia well to make a certain contribution for the poor of the saints who [are] in Jerusalem;
27 Yéene nañu ko, te it ci dëgg-dëgg bor la, bu ñu war a fey. Ndaxte gannaaw ñi gëm ci Yerusalem séddoo nañu ak ñi dul Yawut seen ngëm, kon xeet yooyu itam war nañoo séddoo ak ñoom seen alal.
27for it pleased well, and their debtors they are, for if in their spiritual things the nations did participate, they ought also, in the fleshly things, to minister to them.
28 Kon nag waxtu wu ma noppee ci liggéey boobu, teg may gu tedd gii ci loxoy boroom, dinaa dem Espaañ, tey jaar fi yéen.
28This, then, having finished, and having sealed to them this fruit, I will return through you, to Spain;
29 Te wóor na maa ne, bu ma agsee ci yéen, dinaa indaale barkeb Kirist bu mat sëkk.
29and I have known that coming unto you — in the fulness of the blessing of the good news of Christ I shall come.
30 Gannaaw loolu bokk yi, maa ngi leen di ñaan ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist ak ci bëggante, gi Xelu Yàlla mi def ci nun, ngeen defal ma lii: àndleen ak man, nu tuur sunu ñaq ci ñaan Yàlla.
30And I call upon you, brethren, through our Lord Jesus Christ, and through the love of the Spirit, to strive together with me in the prayers for me unto God,
31 Ñaanal-leen ma, ngir ma mucc ci ñi gëmul ci waa Yude; te it gaayi Yàlla yu sell yu nekk ci Yerusalem nangu ndimbal, li ma leen di yóbbul.
31that I may be delivered from those not believing in Judea, and that my ministration, that [is] for Jerusalem, may become acceptable to the saints;
32 Dolli ci, Yàlla may ma, ma ñëw seetsi leen ak xol bu sedd, nu booloo yeeslu fa kanam Yàlla.
32that in joy I may come unto you, through the will of God, and may be refreshed with you,
33 Na Yàlla Boroom jàmm ànd ak yéen ñépp. Amiin.
33and the God of the peace [be] with you all. Amen.