1 Bokk yi, bëgguma ngeen umple li daloon sunu maam ya. Ñoom ñépp niir wa tiimoon na leen, te ñoom ñépp jàll nañu géej.
1For I would not have you ignorant, brethren, that all our fathers were under the cloud, and all passed through the sea;
2 Sóobu nañu ca ndoxu géej ga ak ca niir wa, ba bokk noonu ci Musaa.
2and all were baptised unto Moses in the cloud and in the sea;
3 Ñoom ñépp bokk nañoo lekk ñam, wa Yàlla joxe,
3and all ate the same spiritual food,
4 naan naan ga mu joxe, ndaxte ñu ngi doon naan ca xeer, wa leen doon gunge, te xeer woowa Kirist la woon.
4and all drank the same spiritual drink, for they drank of a spiritual rock which followed [them]: (now the rock was the Christ;)
5 Teewul ñi ëpp ci ñoom neexuñu woon Yàlla, ba mu fàddoon leen ca màndiŋ ma.
5yet God was not pleased with the most of them, for they were strewed in the desert.
6 Mbir yooyu ay misaal lañu, yu nuy artu, ngir benn bëgg-bëgg bu bon bañ noo jiital, na mu leen jiitale woon.
6But these things happened [as] types of us, that we should not be lusters after evil things, as they also lusted.
7 Buleen jaamu ay xërëm, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon. Ndaxte Mbind mi nee na: «Mbooloo mi dafa toog, di lekk ak di naan, ba noppi ñu jóg di mbumbaay.»
7Neither be ye idolaters, as some of them; as it is written, The people sat down to eat and to drink, and rose up to play.
8 Bunu njaaloo, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon, ba tax ñaar-fukki junni ak ñett ci ñoom dee ci benn bés.
8Neither let us commit fornication, as some of them committed fornication, and fell in one day three and twenty thousand.
9 Bunu diiŋat Kirist, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe, ba ay jaan màtt leen, ñu dee.
9Neither let us tempt the Christ, as some of them tempted, and perished by serpents.
10 Buleen xultu, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon, ba tax malaakam Yàqkat mi rey leen.
10Neither murmur ye, as some of them murmured, and perished by the destroyer.
11 Mbir yooyu leen daloon misaal la ci nun, te bind nañu ko ngir artu nu, nun ñiy dund ci jamono jii lépp mat.
11Now all these things happened to them [as] types, and have been written for our admonition, upon whom the ends of the ages are come.
12 Kon nag kiy naw sa doole, ba yaakaar ne taxaw nga, moytul a daanu ci bàkkaar!
12So that let him that thinks that he stands take heed lest he fall.
13 Benn nattu dabu leen bu wuute ak yi dal nit ñépp. Te sax Yàlla kuy sàmm kóllëre la, te du nangu nattu bi wees seen kàttan, waaye cib nattu, dina leen ubbil bunt bu ngeen man a récce, ba ngeen man koo dékku.
13No temptation has taken you but such as is according to man's nature; and God is faithful, who will not suffer you to be tempted above what ye are able [to bear], but will with the temptation make the issue also, so that [ye] should be able to bear [it].
14 Looloo tax, sama soppe yi, nangeen daw xërëm yi.
14Wherefore, my beloved, flee from idolatry.
15 Maa ngi wax ak yéen ñi am xel. Kon seetleen li ma leen wax.
15I speak as to intelligent [persons]: do *ye* judge what I say.
16 Kaas bu yiw, bi tax nuy gërëm Yàlla, ndax du wone sunu booloo ak deretu Kirist? Mburu mi nuy damm, xanaa du dafay wone sunu booloo ak yaramu Kirist?
16The cup of blessing which we bless, is it not [the] communion of the blood of the Christ? The bread which we break, is it not [the] communion of the body of the Christ?
17 Ndegam benn mburu rekk a am, kon nun ñépp lu nu baree-bare, menn mbooloo lanu, ndaxte bokk nanu menn mburu mi.
17Because we, [being] many, are one loaf, one body; for we all partake of that one loaf.
18 Seetleen ci bànni Israyil. Ñiy lekk sarax si ñu rendi, ndax booloowuñu ak Yàlla ji ñu jagleel saraxalukaay ba? Aaŋkay!
18See Israel according to flesh: are not they who eat the sacrifices in communion with the altar?
19 Li may wax, lu muy tekki? Ndax yàpp wi ñu jagleel xërëm yi dafay dara? walla xërëm yi dañuy dara?
19What then do I say? that what is sacrificed to an idol is anything, or that an idol is anything?
20 Déedéet! Waaye sarax yi xërëmkat yi di rendi, ay rab lañu ko jagleel; jagleeluñu ko Yàlla. Te man bëgguma, ngeen booloo ak rab yi.
20But that what [the nations] sacrifice they sacrifice to demons, and not to God. Now I do not wish you to be in communion with demons.
21 Mënuleen a naan ci kaasu Boroom bi, naan ci kaasu rab yi. Mënuleen a sukk ci reerub Boroom bi, sukk ci reerub rab yi.
21Ye cannot drink [the] Lord's cup, and [the] cup of demons: ye cannot partake of [the] Lord's table, and of [the] table of demons.
22 Walla boog ndax danuy jéem a gillil meru Boroom bi? Xanaa noo ko ëpp doole?
22Do we provoke the Lord to jealousy? are we stronger than he?
23 Dafa am ñu naan: «Lépp lanu sañ.» Waaw, waaye du lépp a baax ci nun. «Lépp lanu sañ,» waaye it lépp du yékkati ngëm.
23All things are lawful, but all are not profitable; all things are lawful, but all do not edify.
24 Bu kenn seet njariñam rekk, waaye nay seet njariñul moroomam.
24Let no one seek his own [advantage], but that of the other.
25 Man ngeen a lekk lépp lu ñuy jaay ca ja ba, bañ cee boole ay laaj ngir dalal seen xel.
25Everything sold in the shambles eat, making no inquiry for conscience sake.
26 Ndaxte Mbind mi nee na: «Àddina ak li ci biiram lépp, Boroom bi moo ko moom.»
26For the earth [is] the Lord's and its fulness.
27 Ku xamul Yàlla nag, bu leen wooyee aw ñam këram, te ngeen nangoo dem, lekkleen lépp lu ñu leen dëj, bañ a laajte dara ngir dalal seen xel.
27But if any one of the unbelievers invite you, and ye are minded to go, all that is set before you eat, making no inquiry for conscience sake.
28 Waaye bu leen kenn nee: «Lii sarax la, bu ñu jagleel xërëm yi,» suurleen ko ndax ki leen ko xamal, ngir xel mu dal.
28But if any one say to you, This is offered to holy purposes, do not eat, for his sake that pointed it out, and conscience sake;
29 Waxuma sa xel yaw, waaye xelu keneen laay wax. Waaye nga ne: «Li ma sañ a def, lu tax nit ku xelam dalul di am dara lu mu ciy wax?
29but conscience, I mean, not thine own, but that of the other: for why is my liberty judged by another conscience?
30 Su ma lekkee dara di ci sant Yàlla, lu tax ñu may wax lu ñaaw, fekk sant naa ci Yàlla.»
30If *I* partake with thanksgiving, why am I spoken evil of for what *I* give thanks for?
31 Kon su ngeen di lekk walla ngeen di naan, walla lu ngeen man a def, defleen lépp ngir màggal Yàlla.
31Whether therefore ye eat, or drink, or whatever ye do, do all things to God's glory.
32 Buleen def dara lu man a fanq ngëmu Yawut yi walla ñi dul Yawut walla mbooloom Yàlla.
32Give no occasion to stumbling, whether to Jews, or Greeks, or the assembly of God.
33 Noonu laay def man ci sama bopp: damay wut a neex ñépp ci lépp. Wutuma lu may jariñ, waaye luy jariñ ñu bare laay wut, ngir ñu mucc.
33Even as *I* also please all in all things; not seeking my own profit, but that of the many, that they may be saved.