Wolof: New Testament

Darby's Translation

2 Corinthians

11

1 Céy bu ngeen ma manoon a muñal, ma wax leen tuuti waxi dof! Waaw muñal-leen ma sax.
1Would that ye would bear with me [in] a little folly; but indeed bear with me.
2 Dama leen di fiire ak fiiraange gu jóge ca Yàlla, ndaxte dama leen a bëgg a jébbal jenn jëkkër kepp, muy Kirist, ngeen set ni janq.
2For I am jealous as to you with a jealousy [which is] of God; for I have espoused you unto one man, to present [you] a chaste virgin to Christ.
3 Waaye ni jaan ja naxe woon Awa ci pexeem, ragal naa yéen itam ñu lëmbaaje ni seen xel, ba ngeen dëddu xol bu laab, bi ngeen amoon ci seen diggante ak Kirist.
3But I fear lest by any means, as the serpent deceived Eve by his craft, [so] your thoughts should be corrupted from simplicity as to the Christ.
4 Ndaxte bu kenn ñëwee, di leen waar ci Yeesu ci lu juuyoo ak li nu leen yégal, walla ngeen jot meneen xel mu wuute ak Xel mi ngeen jot, walla ngeen nangu beneen xebaar bu wuute ak bi ngeen dégg, dingeen ko dékku bu baax.
4For if indeed he that comes preaches another Jesus, whom we have not preached, or ye get a different Spirit, which ye have not got, or a different glad tidings, which ye have not received, ye might well bear with [it].
5 Moona foog naa ne, seen ndaw yooyu ngeen yékkati, ba ñu ëpp ndaw sax, ëpplewuñu ma dara.
5For I reckon that in nothing I am behind those who are in surpassing degree apostles.
6 Bu ma dul jàmbaari wax it, néewuma xam-xam, te won nanu leen ko ci bépp mbir ak ci bépp fànn.
6But if [I am] a simple person in speech, yet not in knowledge, but in everything making [the truth] manifest in all things to you.
7 Walla boog ndax dama leen a tooñ ci li ma suufeel sama bopp ngir yékkati leen, ba ma leen di yégal xebaar bu baax bi te laajuma leen genn pey?
7Have I committed sin, abasing myself in order that *ye* might be exalted, because I gratuitously announced to you the glad tidings of God?
8 Xanaa kay damaa tooñ ci li ma dunde alalu yeneen mboolooy ñi gëm, ba futti leen, ngir dimbali leen, yéen.
8I spoiled other assemblies, receiving hire for ministry towards you.
9 Te ba ma nekkee ci yéen te soxla dab ma, wéeruwuma ci kenn ci yéen, ndaxte bokk ya jóge Maseduwan ñoo ma indil li ma soxla woon. Ci lépp moytu naa nekk yen ci yéen, te dinaa ko gën a def.
9And being present with you and lacking, I did not lazily burden any one, (for the brethren who came from Macedonia supplied what I lacked,) and in everything I kept myself from being a burden to you, and will keep myself.
10 Ni mu wóore ne, dëggug Kirist nekk na ci man, ni la wóore ne loolii may damoo, kenn du ko teggi ci diiwaanu Akayi gépp.
10[The] truth of Christ is in me that this boasting shall not be stopped as to me in the regions of Achaia.
11 Lu tax? Ndax dama leen a bëggul? Yàlla xam na ne, bëgg naa leen!
11Why? because I do not love you? God knows.
12 Noonu may doxale nag dinaa ci sax, ngir ñiy damu, di wut yoon wu ñu aw ba yemale seen bopp ak nun, duñu ko am.
12But what I do, I will also do, that I may cut off the opportunity of those wishing [for] an opportunity, that wherein they boast they may be found even as we.
13 Ay ndawi naaféq lañu, di ay liggéeykat yu njublaŋ yuy mbubboo turu ndawi Kirist.
13For such [are] false apostles, deceitful workers, transforming themselves into apostles of Christ.
14 Te loolu jaaxalu nu, ndaxte Seytaane moom ci boppam day mbubboo malaakam leer.
14And [it is] not wonderful, for Satan himself transforms himself into an angel of light.
15 Kon nag ay ndawam mbubboo ndawi njub, loolu du nu jaaxal. Dees na leen fey seeni jëf.
15It is no great thing therefore if his ministers also transform themselves as ministers of righteousness; whose end shall be according to their works.
16 Maa ngi leen koy waxaat: bu ma kenn jàpp nib dof. Walla boog bu ngeen ma ko jàppee, séddleen ma céru dof, ngir ma damu tuuti, man itam.
16Again I say, Let not any one think me to be a fool; but if otherwise, receive me then even as a fool, that *I* also may boast myself some little.
17 Loolu may wax nag, waxuma ko ci turu Boroom bi. Bu ma ñemee damoo nii, maa ngi wax ni dof.
17What I speak I do not speak according to [the] Lord, but as in folly, in this confidence of boasting.
18 Ndegam ñu bare dañuy damu ni nit kese, man itam kon dinaa damu.
18Since many boast according to flesh, *I* also will boast.
19 Yéen boroom xel yi, aka ngeen a man a muñal ñi dof,
19For ye bear fools readily, being wise.
20 nde yéena ngi muñ ñi leen di jaamloo, di lekk seen alal, di leen nax, di leen xeeb, di leen talaata!
20For ye bear if any one bring you into bondage, if any one devour [you], if any one get [your money], if any one exalt himself, if any one beat you on the face.
21 Sunu néew doole mayu nu, nu dem ba jëfe noonu; rus naa ci lool de! Ma wax waxi dof; moona lépp lu waay ñemee damoo, ñeme naa ko, man it.
21I speak as to dishonour, as though *we* had been weak; but wherein any one is daring, (I speak in folly,) *I* also am daring.
22 Ndax Ibrë lañu? Man it Ibrë laa. Ndax bànni Israyil lañu? Man itam ci laa. Ndax sëti Ibraayma lañu? Man itam moom laa.
22Are they Hebrews? *I* also. Are they Israelites? *I* also. Are they seed of Abraham? *I* also.
23 Ndax surgay Kirist lañu? --maa ngi wax waxi ku tàggoo ak sagoom nag — maa leen ko gën a doon. Bu dee ci liggéey, maa leen ci man. Bu dee ci li ñu nu tëj ci kaso, maa leen ko gën a miin. Bu dee ci li ñu nu dóor ay yar, maa leen ëpple. Leru naa dee ba tàyyi.
23Are they ministers of Christ? (I speak as being beside myself) *I* above measure [so]; in labours exceedingly abundant, in stripes to excess, in prisons exceedingly abundant, in deaths oft.
24 Juróomi yoon Yawut yi dóor nañu ma fanweeri yar ak juróom-ñeent.
24From the Jews five times have I received forty [stripes], save one.
25 Ñetti yoon dóorees na ma ay yet, te mas nañu maa sànni ay xeer, bëgg maa rey. Ñetti yoon dugg naa gaal, mu suux. Mas naa yendu ci ndox, fanaan ci.
25Thrice have I been scourged, once I have been stoned, three times I have suffered shipwreck, a night and day I passed in the deep:
26 Ci sama tukki yu bare yi daan naa faral di daje ak musiba ci dex yi, ak musiba ci sàcc yi, musiba mu jóge ci sama xeet walla ci ñi dul Yawut, musiba ci biir dëkk yi, ci màndiŋ yi, ci géej gi, ci biir bokki taalibe yu naaféq yi.
26in journeyings often, in perils of rivers, in perils of robbers, in perils from [my own] race, in perils from [the] nations, in perils in [the] city, in perils in [the] desert, in perils on [the] sea, in perils among false brethren;
27 Sonn naa, di ñaq, di fanaane xool, di xiif ak a mar tey fande, di dékku liw te rafle,
27in labour and toil, in watchings often, in hunger and thirst, in fastings often, in cold and nakedness.
28 waxaalewuma li ci des nag: bés bu nekk maa ngi xalaat mboolooy ñi gëm.
28Besides those things that are without, the crowd [of cares] pressing on me daily, the burden of all the assemblies.
29 Ana ku ci néew doole, te wàlluma ko? Ana ku ci bàkkaar, te awma naqar wu tiis?
29Who is weak, and I am not weak? Who is stumbled, and I burn not?
30 Su ma damu waree kon, ci sama néew doole laay damoo.
30If it is needful to boast, I will boast in the things which concern my infirmity.
31 Yàlla Baayu sunu Boroom Yeesu, moom mi màgg ba fàww, xam na ne, du ay fen ci man.
31The God and Father of the Lord Jesus knows -- he who is blessed for ever -- that I do not lie.
32 Ba ma nekkee dëkku Damas, boroom dëkk ba, di jawriñu buur ba Aretas, dafa santaane woon ñuy wottu dëkk ba, ngir man maa jàpp.
32In Damascus the ethnarch of Aretas the king kept the city of the Damascenes shut up, wishing to take me;
33 Waaye dugalees na ma ci dàmba, jaarale ma ci palenteeru miiri dëkk ba, yoor ma ci suuf. Noonu ma rëcc ko.
33and through a window in a basket I was let down by the wall, and escaped his hands.