1 Ci mbirum ndimbal loolu jëm ci gaayi Yàlla yi, matul ma leen di bindaat,
1For concerning the ministration which [is] for the saints, it is superfluous my writing to you.
2 ndaxte xam naa seen yéene ju rafet, te maa ngi ciy damu ci kanamu waa Maseduwan, naan leen: «Daaw fekk na waa Akayi jekk.» Te seen cawarte xamb na ñu bare ci ñoom.
2For I know your readiness, which I boast of as respects you to Macedonians, that Achaia is prepared since a year ago, and the zeal [reported] of you has stimulated the mass [of the brethren].
3 Maa ngi yónni nag bokk yooyu, ngir damu gi nu doon damu ci yéen ci mbir mii bañ a neen, te ngeen jekk, ni ma ko waxe woon.
3But I have sent the brethren, in order that our boasting about you may not be made void in this respect, in order that, as I have said, ye may be prepared;
4 Danoo bañ rekk waa Maseduwan, ñiy ànd ak man, fekk jekkaguleen; te kon kóolute googu nu am ci yéen dina nekk sunu gàcce, waxaalewuma nag seen bos.
4lest haply, if Macedonians come with me and find you unprepared, *we*, that we say not *ye*, may be put to shame in this confidence.
5 Moo tax ma xalaat ne, li gën mooy yónni bokk yooyu, ñu jiitu ma ci yéen, topptoo mbiri ndimbal lu yaatu loolu ngeen dige woon. Loolu di may gu tàlli, te bañ a nekk yëfi nay.
5I thought it necessary therefore to beg the brethren that they would come to you, and complete beforehand your fore-announced blessing, that this may be ready thus as blessing, and not as got out of you.
6 Te lii moo am: ku ji tuuti, góob tuuti; ku ji lu bare, góob lu bare.
6But this [is true], he that sows sparingly shall reap also sparingly; and he that sows in [the spirit of] blessing shall reap also in blessing:
7 Kon na ku nekk joxe, ni mu ko nase ci xolam, te bañ cee am réccu walla sañul-bañ, ndaxte kiy joxe ak mbég moo neex Boroom bi.
7each according as he is purposed in his heart; not grievingly, or of necessity; for God loves a cheerful giver.
8 Te Yàlla man na leen a woomal ci bépp yiwam ba ci fépp ak ci lépp, ngeen faj seen soxla yépp te sakkanle it ngir bépp jëf bu baax.
8But God is able to make every gracious gift abound towards you, that, having in every way always all-sufficiency, ye may abound to every good work:
9 Moom la Mbind mi wax ne:«Tabe na, ba may baadoolo yi;njubteem day sax ba fàww.»
9according as it is written, He has scattered abroad, he has given to the poor, his righteousness remains for ever.
10 Yàlla miy jox beykat bi jiwu ak nit ab dund, dina leen jox jiwu wu ne gàññ, te sakkanal li seen njub meññ.
10Now he that supplies seed to the sower and bread for eating shall supply and make abundant your sowing, and increase the fruits of your righteousness:
11 Noonu dingeen woomle ci lépp, ba yéwén ci bépp anam, ba tax ñu bare gërëm Yàlla ndax li ngeen maye jaarale ko ci nun.
11enriched in every way unto all free-hearted liberality, which works through us thanksgiving to God.
12 Ndaxte njaamu, gi ngeen di jaamu, yemul rekk ci faj soxlay gaayi Yàlla yi, waaye dina tax it ngërëmu ñu bare baawaan, jëm ci Yàlla.
12Because the ministration of this service is not only filling up the measure of what is lacking to the saints, but also abounding by many thanksgivings to God;
13 Ci li ngeen firndeel seen mbëggeel ci joxe ndimbal lii, dinañu màggal Yàlla, ndaxte wone ngeen ni ngeen déggale xebaar bu baax bu Kirist bi, ak ni ngeen yéwéne ci seen ndimbal jëme ci ñoom ak ñépp.
13they glorifying God through the proof of this ministration, by reason of your subjection, by profession, to the glad tidings of the Christ, and your free-hearted liberality in communicating towards them and towards all;
14 Rax-ca-dolli dinañu sant Yàlla ak xol bu fees ak cofeel ci yéen ndax yiw wu mag, wi Yàlla def ci yéen.
14and in their supplication for you, full of ardent desire for you, on account of the exceeding grace of God [which is] upon you.
15 Jërë-jëfati yaw Yàlla ndax sa may googu weesu dayo!
15Thanks [be] to God for his unspeakable free gift.