1 Bi juróomi fan wéyee, Anañas saraxalekat bu mag ba dikk, ànd ak ay njiit ak layookat bu tudd Tertul, ñu woo Pool ci yoon fa kanam boroom réew ma.
1And after five days came down the high priest Ananias, with the elders, and a certain orator called Tertullus, and laid their informations against Paul before the governor.
2 Noonu ñu woo Pool, te Tertul daldi ko jiiñ naan: «Yaw Feligsë mu tedd mi, sa nguur jural na nu jàmm ju neex, te sa jàppandil soppi na lu bare ci sunu xeet.
2And he having been called, Tertullus began to accuse, saying, Seeing we enjoy great peace through thee, and that excellent measures are executed for this nation by thy forethought,
3 Gis nanu ko fépp ak ci lépp, di la gërëm ak sunu xol bépp.
3we receive [it] always and everywhere, most excellent Felix, with all thankfulness.
4 Waaye ngir bañ a yàggal jataay bi, maa ngi lay ñaan ci sa lewetaay, nga déglu nu ci lu gàtt.
4But that I may not too much intrude on thy time, I beseech thee to hear us briefly in thy kindness.
5 Ndaxte ci mbirum nit kii teew, gis nanu ne rambaaj la, buy indi xëccoo ci Yawut yi ci àddina sépp, di njiitu mbooloo mu ñuy wax Nasaréen.
5For finding this man a pest, and moving sedition among all the Jews throughout the world, and a leader of the sect of the Nazaraeans;
6 Dem na ba jéem a teddadil sax kër Yàlla ga, waaye jàpp nanu ko.
6who also attempted to profane the temple; whom we also had seized, [and would have judged according to our law;
8 Soo ko laajee, yaw ci sa bopp, dinga gis ne, li nu koy jiiñ dëgg la.»
7but Lysias, the chiliarch, coming up, took [him] away with great force out of our hands,
9 Ci kaw loolu Yawut ya ànd ca, di dëggal ne loolu wóor na.
8having commanded his accusers to come to thee;] of whom thou canst thyself, in examining [him], know the certainty of all these things of which we accuse him.
10 Bi loolu amee boroom réew ma jox Pool kàddu gi. Noonu mu làyyi ne: «Xam naa ne, yaa ngi àtte xeet wi diirub at yu bare, moo tax maa ngi làyyi ak kóolute.
9And the Jews also joined in pressing the matter against [Paul], saying that these things were so.
11 Man ngaa wóorliku ne, ëppagul fukki fan ak ñaar demoon naa Yerusalem ngir màggali.
10But Paul, the governor having beckoned to him to speak, answered, Knowing that for many years thou hast been judge to this nation, I answer readily as to the things which concern myself.
12 Te kenn gisu ma, maay werante mbaa di jógloo mbooloo, muy ca kër Yàlla ga mbaa ca jàngu ya mbaa ci biir dëkk ba.
11As thou mayest know that there are not more than twelve days since I went up to worship at Jerusalem,
13 Te mënuñoo firndeel dara ci li ñu may jiiñ léegi.
12and neither in the temple did they find me discoursing to any one, or making any tumultuous gathering together of the crowd, nor in the synagogues, nor in the city;
14 Waaye nangu naa ci sa kanam ne, maa ngi jaamu Yàllay sunuy maam, ci topp yoon wi ñu ne, mooy tariixa; terewul ne, lépp li ñu tëral ci yoonu Musaa ak li yonent yi bind, gëm naa ko.
13neither can they make good the things of which they now accuse me.
15 Te bokk naa ak ñoom yaakaar ci Yàlla, ne ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki keroog yawmelxayaam.
14But this I avow to thee, that in the way which they call sect, so I serve my fathers' God, believing all things which are written throughout the law, and in the prophets;
16 Moo tax fu ma tollu, maa ngi góor-góorlu, ngir am xel mu dal fa kanam Yàlla ak fa kanam nit ñi.
15having hope towards God, which they themselves also receive, that there is to be a resurrection both of just and unjust.
17 «Noonu gannaaw gëjeb at yu bare ñëw naa, ngir indil sama xeet ndimbal te jébbal Yàlla ay sarax.
16For this cause I also exercise [myself] to have in everything a conscience without offence towards God and men.
18 Bi ma koy def nag, gis nañu ma ca kër Yàlla ga, ma setlu ba noppi, fekk ànduma ak mbooloo te indiwuma benn coow.
17And after a lapse of many years I arrived, bringing alms to my nation, and offerings.
19 Waaye ay Yawut yu dëkk Asi — xanaa kay ñoo waroon a ñëw ci sa kanam, di ma kalaame, bu ñu amee dara lu ñu may topp.
18Whereupon they found me purified in the temple, with neither crowd nor tumult. But it was certain Jews from Asia,
20 Waaye it na nit ñii wax ci lan laa tooñe ci jataayu géewub àtte ba,
19who ought to appear before thee and accuse, if they have anything against me;
21 xanaa li ma waxoon ca kaw ci seen biir rekk ne: “Mbirum ndekkitel ñi dee moo tax ngeen dëj ma ci seen kanam tey!”»
20or let these themselves say what wrong they found in me when I stood before the council,
22 Bi mu waxee noonu, Feligsë mi xam bu wóor mbirum yoon wi, yiwi leen ba beneen yoon. Mu ne leen: «Bu Lisiyas kilifag xare bi ñëwee, dinaa àtte seen mbir.»
21[other] than concerning this one voice which I cried standing amongst them: I am judged this day by you touching [the] resurrection of [the] dead.
23 Noonu mu sant njiitu xare ba ne ko: «Nanga wottu Pool, waaye nga may ko féex, te bàyyi ay xaritam, ñu topptoo ko.»
22And Felix, knowing accurately the things concerning the way, adjourned them, saying, When Lysias the chiliarch is come down I will determine your affair;
24 Bi ay fan wéyee, Feligsë ñëwaat, ànd ak jabaram Dursil, miy Yawut. Noonu mu woolu Pool, di ko déglu ci mbirum gëm Yeesu Kirist.
23ordering the centurion to keep him, and that he should have freedom, and to hinder none of his friends to minister to him.
25 Waaye bi Pool di waxtaan ci mbirum njub ak moom sa bopp ak bés pénc, Feligsë daldi tiit, yiwi ko ne ko: «Demal, bu ma amee jot, dinaa la woolu.»
24And after certain days, Felix having arrived with Drusilla his wife, who was a Jewess, he sent for Paul and heard him concerning the faith in Christ.
26 Fekk yaakaaroon na it ne, Pool dina ko jox xaalis; kon mu di ko faral a woolu, ngir waxtaan ak moom.
25And as he reasoned concerning righteousness, and temperance, and the judgment about to come, Felix, being filled with fear, answered, Go for the present, and when I get an opportunity I will send for thee;
27 Bi ñaari at weesoo nag, amoon na ku wuutu Feligsë, tudd Porsiyus Festus. Noonu Feligsë, mi bëggoon lu neex Yawut ya, bàyyi Pool ca kaso ba.
26hoping at the same time that money would be given him by Paul: wherefore also he sent for him the oftener and communed with him.
27But when two years were completed, Felix was relieved by Porcius Festus as his successor; and Felix, desirous to oblige the Jews, to acquire their favour, left Paul bound.