1 «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Sàrd, ne ko: i Ki yor juróom-ñaari Xeli Yàlla yi ak juróom-ñaari biddiiw yi nee na: Xam naa say jëf. Dañu laa teg kuy dund, fekk dee nga.
1And to the angel of the assembly in Sardis write: These things saith he that has the seven Spirits of God, and the seven stars: I know thy works, that thou hast a name that thou livest, and art dead.
2 Yeewul te dëgëral li des ci yaw tey waaj a dee, ndaxte gis naa ne, say jëf matuñu ca sama kanam Yàlla.
2Be watchful, and strengthen the things that remain, which are about to die, for I have not found thy works complete before my God.
3 Fàttalikul kon kàddug Yàlla gi nga jot, te dégg ko, sàmm ko te réccu. Soo wéyee ciy nelaw nag, dinaa ñëw nib sàcc, te doo xam wan waxtu lay doon. i
3Remember therefore how thou hast received and heard, and keep [it] and repent. If therefore thou shalt not watch, I will come [upon thee] as a thief, and thou shalt not know at what hour I shall come upon thee.
4 Moona am nga foofu ci Sàrd nit ñu néew ñoo xam ne tilimaluñu seen mbubb. Ñooñu dinañu ànd ak man, sol lu weex, ndaxte yeyoo nañu ko.
4But thou hast a few names in Sardis which have not defiled their garments, and they shall walk with me in white, because they are worthy.
5 Ku daan, dinga sol mbubb mu weex ni ñoom. Te duma far sa tur ci téereb dund bi, waaye dinaa nangu ci sama kanamu Baay ak ay malaakaam ne, bokk nga ci man.
5He that overcomes, *he* shall be clothed in white garments, and I will not blot his name out of the book of life, and will confess his name before my Father and before his angels.
6 Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm.
6He that has an ear, let him hear what the Spirit says to the assemblies.
7 «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Filadelfi, ne ko: i Aji Sell ji, di Aji Dëgg ji nee na, moom mi yor caabiy Daawuda ji, moom miy tijji te kenn du ko man a tëj, muy tëj te kenn du ko tijji nee ne:
7And to the angel of the assembly in Philadelphia write: These things saith the holy, the true; he that has the key of David, he who opens and no one shall shut, and shuts and no one shall open:
8 Xam naa say jëf. Ubbil naa la bunt, te kenn du ko man a tëj. Xam naa ne barewuloo doole, waaye sàmm nga sama kàddu te weddiwoo ma.
8I know thy works: behold, I have set before thee an opened door, which no one can shut, because thou hast a little power, and hast kept my word, and hast not denied my name.
9 Dinaa def ba ñenn ci ñi bokk ci ndajem Seytaane --te tuddoo Yawut, fekk dañuy fen — dinaa leen ñëwloo, ñu sukk ci sa kanam, nangu ne, bëgg naa la.
9Behold, I make them of the synagogue of Satan who say that they are Jews, and are not, but lie; behold, I will cause that they shall come and shall do homage before thy feet, and shall know that *I* have loved thee.
10 Gannaaw muñ nga, ni ma la ko dénke woon, man itam dinaa la yiir ci jamono, ji musiba mi di wàcc ci dunyaa bépp ngir nattu waa àddina. i
10Because thou hast kept the word of my patience, *I* also will keep thee out of the hour of trial, which is about to come upon the whole habitable world, to try them that dwell upon the earth.
11 Léegi ma ñëw. Sàmmal li nga yor, ngir kenn bañ laa xañ sa kaalag ndam.
11I come quickly: hold fast what thou hast, that no one take thy crown.
12 Ku daan, dinaa la samp ni aw jënu néeg ci sama kër Yàlla te doo fa génn mukk. Dinaa bind ci yaw turu sama Yàlla ak turu dëkku sama Yàlla, mu di Yerusalem gu bees, giy jóge ca asamaan ca wetu sama Yàlla di wàcc. Dinaa bind it ci yaw sama tur wu bees.
12He that overcomes, him will I make a pillar in the temple of my God, and he shall go no more at all out; and I will write upon him the name of my God, and the name of the city of my God, the new Jerusalem, which comes down out of heaven, from my God, and my new name.
13 Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm.
13He that has an ear, let him hear what the Spirit says to the assemblies.
14 «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Lawdise, ne ko: i Ki ñuy wax Amiin ji, di seede bu takku bi te dëggu, ki di ndeyi bindu mbindeefi Yàlla yi, nee na;
14And to the angel of the assembly in Laodicea write: These things says the Amen, the faithful and true witness, the beginning of the creation of God:
15 Xam naa say jëf, xam ne seddoo, tàngoo. Manoon ngaa sedd mbaa nga tàng,
15I know thy works, that thou art neither cold nor hot; I would thou wert cold or hot.
16 waaye ndax li nga nugg, tàngoo seddoo, dinaa la yàbbi.
16Thus because thou art lukewarm, and neither cold nor hot, I am about to spue thee out of my mouth.
17 Yaa ngi damu naan: “Am naa alal, duunle naa, soxlaatuma dara.” Fekk xamuloo ne, torox nga, miskin, ñàkk, gumba te rafle.
17Because thou sayest, I am rich, and am grown rich, and have need of nothing, and knowest not that *thou* art the wretched and the miserable, and poor, and blind, and naked;
18 Moo tax maa ngi lay xiirtal, nga jënd ci man wurus wu ñu xellee ci safara, ngir nga duunle, te nga jënd yére yu weex ngir nga solu, ba sa gàcceg rafle bañ a feeñ, ak tuufaay booy diw ci say bët, ngir man a gis. i
18I counsel thee to buy of me gold purified by fire, that thou mayest be rich; and white garments, that thou mayest be clothed, and that the shame of thy nakedness may not be made manifest; and eye-salve to anoint thine eyes, that thou mayest see.
19 Man maay yedd, di yar ñépp ñi ma bëgg. Farlul kon te tuub say bàkkaar.
19I rebuke and discipline as many as I love; be zealous therefore and repent.
20 Maa ngi nii taxaw ci bunt bi, di fëgg. Ku dégg sama baat te ubbi bunt bi, dinaa dugg, reerandoo ak moom, moom it mu reerandoo ak man. i
20Behold, I stand at the door and am knocking; if any one hear my voice and open the door, I will come in unto him and sup with him, and he with me.
21 Ku daan, dinaa la toogloo ci sama wet ci sama gàngune, ni ma xeexe ba daan, man ci sama bopp, te toogandoo ak sama Baay ci gànguneem.
21He that overcomes, to him will I give to sit with me in my throne; as *I* also have overcome, and have sat down with my Father in his throne.
22 Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm.»
22He that has an ear, let him hear what the Spirit says to the assemblies.