1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Yàlla, man ak Sosten sunu mbokk,
1Paulus, ved Guds vilje kalt til Kristi Jesu apostel, og broderen Sostenes
2 noo leen di bind, yéen mbooloom Yàlla, mi dëkk Korent. Nu ngi leen di nuyu, yéen ñi Yàlla sédde boppam jaare ci Kirist Yeesu, yéen ñi Yàlla woo, ngeen sell, boole leen ak ñi nekk ci àddina sépp tey tudd turu sunu Boroom Yeesu Kirist, miy seen Boroom, di sunu bos.
2- til den Guds menighet som er i Korint, helligede i Kristus Jesus, kalte, hellige, tillikemed alle dem som på ethvert sted påkaller vår Herre Jesu Kristi navn, deres og vår:
3 Na leen Yàlla sunu Baay ak Yeesu Kirist Boroom bi may yiw ak jàmm.
3Nåde være med eder og fred fra Gud vår Fader og den Herre Jesus Kristus!
4 Duma jóg ci di sant Yàlla sama Boroom ci seen mbir ndax yiw, wi mu leen may ci seen bokk ci Kirist Yeesu.
4Jeg takker alltid min Gud for eder, for den Guds nåde som er eder gitt i Kristus Jesus,
5 Ndaxte ci yiwi Yàlla yépp ngeen woomle ci Kirist, muy ci wax, muy ci xam-xam.
5at I i ham er gjort rike på alt, på all lære og all kunnskap,
6 Ndaxte li nu doon seedeel Kirist, Yàlla dëggal na ko ci yéen.
6likesom Kristi vidnesbyrd er blitt rotfestet i eder,
7 Noonu nag ñàkkuleen genn may léegi bi ngeen di séentu waxtu, wi sunu Boroom Yeesu Kirist di feeñ ci biir ndamam.
7så at det ikke fattes eder på nogen nådegave mens I venter på vår Herre Jesu Kristi åpenbarelse,
8 Kirist dina leen dooleel ba ca muj ga, ngir ngeen bañ a am wenn ŋàññ bés bu sunu Boroom Yeesu Kirist dellusee.
8han som også skal styrke eder inntil enden, så I må være ulastelige på vår Herre Jesu Kristi dag.
9 Yàlla kuy sàmm kóllëre la, moom mi leen woo, ngir ngeen bokk ak Doomam Yeesu Kirist, sunu Boroom.
9Gud er trofast, han ved hvem I blev kalt til samfund med hans Sønn, Jesus Kristus, vår Herre.
10 Waaye bokk yi, maa ngi leen di dénk ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist, ngeen juboo te bañ a féewaloo ci seen biir. Waaye nangeen ànd te booloo, bokk xel, bokk xalaat.
10Men jeg formaner eder, brødre, ved vår Herre Jesu Kristi navn at I alle må føre den samme tale, og at det ikke må være splid iblandt eder, men at I må være fast forenet i samme sinn og i samme mening.
11 Ndaxte bokk yi, waa kër Kelowe xamal nañu ma ne, dangeen di xuloo.
11For det er av Kloes folk blitt mig fortalt om eder, mine brødre, at det er tretter iblandt eder.
12 Maa ngi ñëw ca wax ja: kenn ku nekk ci yéena ngi naan: «Man ci Pool laa bokk!» «Man ci Apolos!» «Man ci Sefas!» «Man ci Kirist!»
12Jeg mener dette at enhver av eder sier: Jeg holder mig til Paulus; jeg til Apollos; jeg til Kefas; jeg til Kristus.
13 Ndax Kirist dafa xaajoo? Ndax Pool lañu daajoon ca bant ba, mu dee ngir yéen? Ndax sóob nañu leen ci ndox, ngir wone ne bokk ngeen ci Pool?
13Er Kristus blitt delt? var det Paulus som blev korsfestet for eder, eller var det til Paulus' navn I blev døpt?
14 Maa ngi sant Yàlla ci li ma sóobul kenn ci yéen, ku dul Kirispus ak Gayus,
14Jeg takker Gud at jeg ikke har døpt nogen av eder uten Krispus og Gajus,
15 ngir kenn bañ a wax ne, ci sama tur lañu ko sóob.
15for at ikke nogen skal si at I blev døpt til mitt navn.
16 Aaŋkay! Sóob naa it ci ndox waa kër Estefanas. Waaye ci sama pàttaliku sóobuma keneen.
16Dog har jeg også døpt Stefanas' hus; ellers vet jeg ikke av at jeg har døpt nogen annen.
17 Ndaxte Kirist yebalu ma ngir may sóobe ci ndox, waaye da maa yebal, ngir may yégle xebaar bu baax bi, te ma bañ koo def ak waxi xam-xamu nit, ngir bañ a ñàkkal faayda deewu Kirist ca bant ba.
17For Kristus har ikke utsendt mig for å døpe, men for å forkynne evangeliet, ikke med vise ord, for at Kristi kors ikke skulde tape sin kraft.
18 Ndaxte yégleb deewu Kirist ca bant ba, ag ndof la ci ñiy sànku. Waaye ci nun ñi aw ci yoonu mucc gi, dooley Yàlla la.
18For ordet om korset er vel en dårskap for dem som går fortapt, men for oss som blir frelst, er det en Guds kraft;
19 Ndaxte Mbind mi nee na:«Dinaa folli xam-xamu boroom xam-xam yi,lem xalaati ñi am xel.»
19for det er skrevet: Jeg vil ødelegge de vises visdom, og de forstandiges forstand vil jeg gjøre til intet.
20 Ana boroom xam-xam bi? Ana kaaŋ mi? Ana boroom làmmiñ wu neex, wi ci àddina sii? Xanaa Yàlla wonewul ne, xam-xamu àddina si ag ndof la?
20Hvor er en vismann, hvor er en skriftlærd, hvor er en gransker i denne verden? har ikke Gud gjort verdens visdom til dårskap?
21 Gannaaw àddina si ci xam-xamam demul ba xam Yàlla --te Yàllaa dogal loolu ci xam-xamam — soob na Yàlla mu musal ñi gëm, jaar ci yégleb xebaaru Kirist, fekk ag ndof la ci bëti nit.
21For eftersom verden ikke ved sin visdom kjente Gud i Guds visdom, var det Guds vilje ved forkynnelsens dårskap å frelse dem som tror,
22 Ndaxte Yawut yi ñu ngi laaj ay firnde; Gereg yi di wut xam-xam.
22eftersom både jøder krever tegn og grekere søker visdom,
23 Waaye nun nu ngi yégle Kirist, mi ñu reyoon ca bant ba, te loolooy téq ngëmu Yawut yi, di ag ndof ci ñi dul Yawut.
23men vi forkynner Kristus korsfestet, for jøder et anstøt og for hedninger en dårskap,
24 Waaye ci ñi Yàlla woo, ñuy Yawut mbaa di Gereg, Kirist mooy dooley Yàlla, di xam-xamu Yàlla.
24men for dem som er kalt, både jøder og grekere, forkynner vi Kristus, Guds kraft og Guds visdom.
25 Li ñuy wax ag ndof ca wàllu Yàlla moo gën a tedd xam-xamu nit. Te li ñuy wax ñàkk dooley Yàlla moo ëpp kàttan dooley nit.
25For Guds dårskap er visere enn menneskene, og Guds svakhet er sterkere enn menneskene.
26 Bokk yi, seetleen seen nekkin, bi leen Yàlla di woo. Barewul woon ci yéen, ñi ñuy tudde ay boroom xam-xam mbaa ay boroom doole mbaa ñu rafet ab juddu.
26For legg merke til eders kall, brødre, at ikke mange vise efter kjødet blev kalt, ikke mange mektige, ikke mange høibårne;
27 Waaye li àddina teg ag ndof, Yàlla tànn na ko, ngir rusloo boroom xam-xam yi; te li àddina teg ag ñàkk doole, Yàlla tànn na ko, ngir rusloo boroom doole yi.
27men det som er dårlig i verden, det utvalgte Gud sig for å gjøre de vise til skamme, og det som er svakt i verden, det utvalgte Gud sig for å gjøre det sterke til skamme,
28 Li dul juddu bu rafet te mat a xeeb ci àddina, Yàlla tànn na ko; Yàlla tànn na li nekkul, ngir neenal li nekk.
28og det som er lavt i verden, og det som er ringeaktet, det utvalgte Gud sig, det som ingenting er, for å gjøre til intet det som er noget,
29 Noonu kenn du man a damu ca kanam Yàlla.
29forat intet kjød skal rose sig for Gud.
30 Waaye Yàlla moo def ba ngeen bokk ci Kirist, moom mi doon ci nun xam-xam bu jóge ca Yàlla, maanaam: sunu njubte, sunu sellaay, sunu njot.
30Men av ham er I i Kristus Jesus, som er blitt oss visdom fra Gud og rettferdighet og helliggjørelse og forløsning,
31 Loolu dafa am, ngir li Mbind mi wax am, ne: «Kuy damu, na damu ci Boroom bi.»
31forat, som skrevet er: Den som roser sig, han rose sig i Herren!