Wolof: New Testament

Norwegian

1 Timothy

5

1 Bul gëdd mag, waaye waxtaanal ak moom ni sa baay. Ndaw it, nga digal ko ni sa rakk,
1Tal ikke hårdt til en gammel mann, men forman ham som en far, unge menn som brødre,
2 jigéen ju mag, def ko ni sa yaay; ju ndaw, ni sa jigéen ak cell gu mat sëkk.
2gamle kvinner som mødre, unge som søstre, i all renhet!
3 Ci wàllu ñi seen jëkkër faatu nag, ku ci sësul ci kenn, teral ko ngir Yàlla.
3Hedre enker som virkelig er enker!
4 Waaye ku ci am ay doom mbaa ay sët, na njaboot googu jëkk a wone seen ragal Yàlla ci seen biir kër, ci delloo njukkal seen waajur, ndaxte loolu lu rafet la fa kanam Yàlla.
4Men har en enke barn eller barnebarn, da skal disse først lære å vise sin gudsfrykt mot sin egen slekt og gi sine foreldre vederlag; for dette er tekkelig i Guds øine.
5 Jigéen ju sësul ci kenn day wékk yaakaaram jépp ci Yàlla, sax ci di ko wéetal te di ko ñaan guddi ak bëccëg.
5Men den som virkelig er enke og står alene, hun har satt sitt håp til Gud og blir ved i bønn og påkallelse natt og dag;
6 Waaye ki bànneex jiital, ndee luy dox la.
6men den som lever efter sine lyster, er levende død.
7 Dénk leen loolu, ngir ñu bañ a am benn gàkk.
7Og dette skal du byde, forat de kan være ulastelige.
8 Ndaxte ki defalul ay bokkam dara, rawatina ay waajuram, weddi na yoonu ngëm wi, ba yées ku gëmadi.
8Men dersom nogen ikke har omsorg for sine egne, og mest for sine husfolk, han har fornektet troen og er verre enn en vantro.
9 Ku bëgg a bindu ci ñi seen jëkkër faatu, nii la war a mel: war na wees juróom-benn-fukki at, di jigéen ju yemoon ci jëkkëram,
9En enke kan velges dersom hun ikke er yngre enn seksti år, dersom hun har vært én manns hustru,
10 te mu ràññiku ci jëf yu rafet yu deme ni yar ay guneem, man gan, geestu gaayi Yàlla yu sell yi, dimbali ñi nekk ci tiis; maanaa di ku takku ci mboolem jëf yu rafet yi.
10har vidnesbyrd om gode gjerninger, har opfostret barn, har vært gjestfri, har vasket de helliges føtter, er kommet de nødlidende til hjelp, har lagt vinn på all god gjerning.
11 Waaye bul bind jigéen ju ndaw, ndaxte bu ko ay bëgg-bëggam xiiree ci sore Kirist, dina bëgg a séyaat,
11Men yngre enker skal du avvise; for når de i kjødelig lyst sviker Kristus, vil de gifte sig,
12 te dina daje ak mbugal ndaxte fecci na kóllëre.
12og dermed har de den dom at de har brutt sin første tro.
13 Te du yem ci bëgg a séyaat rekk, waaye ku tayel lay doon; di ku wër kër ak kër, rax-ca-dolli réy làmmiñ te deñ kumpa, di wax lu yoonam nekkul.
13Tilmed lærer de og å gå ørkesløse, idet de farer omkring i husene, og ikke alene ørkesløse, men også med sladder og uvedkommende ting, så de taler det som utilbørlig er.
14 Looloo tax ma bëgg, jigéen yu ndaw yi séyaat, am ay doom, yor seeni kër, ba seen benn noon du leen man a gàkkal.
14Derfor vil jeg at unge enker skal gifte sig, føde barn, styre sitt hus, ikke gi motstanderen nogen leilighet til baktalelse.
15 Ndaxte fi mu ne sax am na ñu jeng xaat, ba topp Seytaane.
15For allerede har somme vendt sig bort efter Satan.
16 Kon nag jigéen ju gëm te am mbokk mu jëkkëram faatu, na ko dimbali te bañ koo bàyyeek mbooloom ñi gëm. Noonu mbooloo mi dina man a dimbali jigéen ñi sësul ci kenn.
16Dersom nogen troende mann eller kvinne har enker, da skal de sørge for dem og ikke la dem falle menigheten til byrde, forat den kan sørge for de virkelige enker.
17 Li jëm ci njiiti mbooloo mi nag, joxal teraanga ju mat sëkk ñi ciy rafetal seen liggéey, rawatina ñi sax dàkk ci waare bi ak njàngale mi.
17De eldste som er gode forstandere, skal aktes dobbelt ære verd, mest de som arbeider i tale og lære.
18 Ndaxte Mbind mi nee na: «Bul sunjuñ gémmiñu nag wu ñu takk bojjukaay,» nee na it: «Ku ñaq, jariñu.»
18For Skriften sier: Du skal ikke binde munnen på en okse som tresker. Og en arbeider er sin lønn verd.
19 Kuy tuumaal njiit fi yaw, bu ko gëm, li feek ñaar walla ñetti seede dëggaluñu ko.
19Ta ikke imot nogen klage mot en eldste uten efter to eller tre vidner.
20 Waaye ñiy bàkkaar, yedd leen fa kanam ñépp, ngir artu ñi ci des.
20Dem som synder, skal du refse så alle hører på det, forat også de andre må ha frykt.
21 Léegi nag maa ngi lay dénk fa kanam Yàlla ak Kirist Yeesu ak malaaka yu tedd ya, nga sàmm loolu ma wax te bañ cee gënale walla di ci parlàqu.
21Jeg vidner for Gud og Kristus Jesus og de utvalgte engler at du skal ta vare på dette uten fordom, så du ikke gjør noget av tilbøielighet.
22 Bul gaaw a teg loxo kenn, ba fal ko, di séddu noonu ci bàkkaari jaambur, waaye dëkkal cig sell.
22Vær ikke snar til å legge hendene på nogen; gjør dig ikke delaktig i fremmede synder; hold dig selv ren!
23 Ba tey bul yemati ci ndox mu ñuul rekk, waaye nangay naan tuuti biiñ, ngir faj say metiti biir ak say jagadi yu bare.
23Drikk ikke lenger bare vann, men nyt litt vin for din mave og dine jevnlige sykdommer.
24 Am na, ñu seeni bàkkaar fés ci kanamu ñépp, ba jiitu leen ca àtte ba; ñi seeni bàkkaar nëbbu nag, bés baa ngi leen di xaar.
24Nogen menneskers synder er åpenbare og går forut for dem til dom; men hos andre følger de efter.
25 Naka noonu it am na, ñu seen jëf yu rafet leer, te yi feeñul mënuñoo nekk kumpa ba fàww.
25Likeså er og de gode gjerninger åpenbare, og de som det ikke er således med, kan dog ikke skjules.