Wolof: New Testament

Norwegian

Acts

18

1 Bi loolu wéyee Pool bàyyikoo Aten, dem Korent.
1Derefter drog han fra Aten og kom til Korint.
2 Mu tase fa ak Yawut bu tudd Akilas te juddoo diiwaanu Pont. Muy sog a jóge réewu Itali ak jabaram Pirsil, ndaxte buur ba Këlódd sant na Yawut yépp, ñu génn Room.
2Der fant han en jøde ved navn Akvilas, født i Pontus, som nylig var kommet fra Italia med sin hustru Priskilla, fordi Klaudius hadde påbudt at alle jøder skulde forlate Rom; dem gav han sig i lag med,
3 Noonu Pool seeti leen, te gannaaw ñoo bokk liggéey, maanaam di defar ay tànt, mu dal fa ñoom, ñuy liggéeyandoo.
3og da han drev samme håndverk, bodde han hos dem og arbeidet der; for de var teltmakere av håndverk.
4 Bésu noflaay bu nekk nag muy diisoo ak ñi nekk ca jàngu ba, di jéem a gëmloo ay Yawut ak ay Gereg.
4Men hver sabbat holdt han samtaler i synagogen, og han overbeviste jøder og grekere.
5 Waaye bi Silas ak Timote jógee diiwaanu Maseduwan, egg fa, Pool jublu ci xamle kàddu gi, tey dëggal ci Yawut yi naan, Yeesu mooy Almasi bi.
5Da nu Silas og Timoteus kom ned fra Makedonia, var Paulus helt optatt av å lære, idet han vidnet for jødene at Jesus er Messias.
6 Bi ko Yawut ya gàntoo nag, di ko xas, mu yëlëb ay yéreem ne leen: «Yéena sàkku seen musiba; set naa ci. Léegi maa ngi dem ci ñi dul Yawut.»
6Men da de stod imot og spottet, rystet han støvet av sine klær og sa til dem: Eders blod komme over eders eget hode! Jeg er ren; fra nu av går jeg til hedningene.
7 Ci kaw loolu mu jóge fa, dugg ci këru ku tudd Tisiyus Yustus, di ku ragal Yàlla, te kër ga dend ak jàngu ba.
7Så gikk han bort derfra, og tok inn i et hus som tilhørte en mann ved navn Justus, som dyrket Gud; hans hus lå like ved synagogen.
8 Kirispus nag, njiitu jàngu ba, gëm na Boroom bi ak waa këram gépp. Te waa Korent ñu bare dégg kàddu gi te gëm ko, ñu sóob leen ci ndox.
8Men synagoge-forstanderen Krispus kom til troen på Herren med hele sitt hus, og mange av korintierne som hørte ham, kom til troen og lot sig døpe.
9 Naka noona Boroom bi feeñu Pool ci guddi ne ko: «Bul tiit dara, waaye deel wax te bañ a noppi.
9Og Herren sa til Paulus i et syn om natten: Frykt ikke, men tal, og ti ikke!
10 Ndaxte maa ngi ànd ak yaw, te kenn du la jàpp, ba fitnaal la, ndaxte am naa xeet wu bare ci dëkk bii.»
10Jeg er med dig, og ingen skal røre dig for å gjøre dig ondt; for jeg har meget folk i denne by.
11 Noonu Pool des at ak genn-wàll ci seen biir, di fa jàngale kàddug Yàlla.
11Så tok han ophold der i et år og seks måneder, og lærte Guds ord iblandt dem.
12 Ci nguuru Galyon ci diiwaanu Akayi nag, Yawut ya likkoo, ñu dal ci kaw Pool, yóbbu ko ca àttekaay ba.
12Men da Gallio var landshøvding i Akaia, reiste jødene sig alle som en mot Paulus og førte ham for domstolen og sa:
13 Ñu ne: «Kii day xiir nit ñi ci màggal Yàlla ci lu juuyoo ak yoon wi.»
13Denne opvigler folk til å dyrke Gud på annen vis enn loven byder.
14 Bi Pool bëggee wax nag, Galyon ne Yawut ya: «Yéen Yawut yi, bu aju woon ci jàdd yoon walla ñaawteef wu réy, kon liy yoon mooy ma déglu leen.
14Da nu Paulus skulde til å oplate munnen, sa Gallio til jødene: Var det nogen misgjerning eller slem udåd, I jøder, da hadde jeg hatt god grunn til å høre tålmodig på eder;
15 Waaye bu ajoo ci ay werante ciy wax ak ay tur ak seen yoon, loolu seen wàll la; man duma ko àtte.»
15men er det spørsmål om en lære og om navn og om eders lov, da får det bli eders sak; dommer i disse ting vil jeg ikke være.
16 Noonu mu dàq leen ca àttekaay ba.
16Og han drev dem bort fra domstolen.
17 Ci kaw loolu nit ñépp jàpp Sosten, njiitu jàngu ba, ñu di ko dóor ca kanamu àttekaay ba, waaye Galyon faalewu leen.
17Men da tok de alle fatt på synagoge-forstanderen Sostenes og slo ham midt for domstolen; og Gallio brydde sig ikke noget om alt dette.
18 Bi loolu wéyee Pool desati fa fan yu bare. Gannaaw ga mu tàggtoo ak bokk ya, dugg gaal jëm Siri, ànd ak Pirsil ak Akilas. Bi mu jógeegul teerub Señsere, mu watlu boppam, ndaxte am na lu mu dige woon ak Yàlla.
18Paulus blev der da ennu en lang tid; så sa han farvel til brødrene og seilte avsted til Syria og i følge med ham Priskilla og Akvilas efterat han i Kenkreæ hadde klippet sitt hår; for han hadde et løfte på sig.
19 Noonu ñu teer ci Efes. Pool bàyyi fa ñi mu àndaloon, daldi dugg ca jàngu ba, di diisoo ak Yawut ya.
19Så kom de til Efesus; der lot han de andre bli tilbake, og selv gikk han inn i synagogen og gav sig i samtale med jødene.
20 Ñu ñaan ko, mu des fa lu gën a yàgg, waaye nanguwul.
20Da de bad ham bli der lenger, samtykte han ikke,
21 Kon mu tàggtoo ak ñoom naan: «Dinaa dellusi ci yéen, bu soobee Yàlla.» Noonu mu dugg gaal, jóge Efes,
21men sa farvel til dem og sa: Jeg vil komme til eder en annen gang, om Gud så vil. Så seilte han fra Efesus
22 teersi dëkku Sesare, mu dem nuyu mbooloom ñi gëm, ba noppi dem Ancos.
22og kom til Cesarea; derefter drog han op og hilste på menigheten, og drog så ned til Antiokia.
23 Bi mu fa desee ay jamono, mu jóge fa, di jaar dëkkoo-dëkk ci diiwaanu Galasi ak Firisi, di dooleel xoli taalibe yépp.
23Da han hadde vært der nogen tid, drog han ut, og vandret gjennem det galatiske land og Frygia fra ende til annen og styrket alle disiplene.
24 Amoon na nag Yawut bu tudd Apolos te juddoo Alegsàndiri, mu dikk Efes. Nit ku yeewu la woon te am xam-xam bu yaatu ci Mbind mi.
24Men det var en jøde ved navn Apollos, født i Aleksandria, en vel talende mann, som kom til Efesus; han var sterk i skriftene.
25 Jàngoon na ci yoonu Boroom bi, di ku farlu ci xelam, muy xamle ak a jàngale bu wóor ci mbirum Yeesu, waaye fekk xam-xamam yem ci ni Yaxya daan sóobe ci ndox.
25Han var oplært i Herrens vei, og da han var brennende i ånden, talte og lærte han grundig om Jesus, enda han bare kjente Johannes' dåp.
26 Noonu mu daldi wax ak fit wu dëgër ca jàngu ba. Bi ko Pirsil ak Akilas déggee nag, ñu woo ko fi ñoom, gën ko leeral yoonu Yàlla.
26Og han begynte å tale frimodig i synagogen. Da Priskilla og Akvilas hadde hørt ham, tok de ham til sig og la Guds vei nøiere ut for ham.
27 Naka mu bëgg a dem Akayi, bokk ya xiir ko ca, ñu bind taalibe ya, ngir ñu teeru ko teeru bu rafet. Noonu mu dikk fa te jariñ lool ñi gëm jaare ko ci yiwu Yàlla.
27Da han nu vilde dra videre til Akaia, tilskyndte brødrene ham, og skrev til disiplene der om å ta imot ham. Og da han kom dit, blev han ved Guds nåde til stort gagn for de troende;
28 Ndaxte mu ngay yey Yawut ya ca kanam ñépp, di firi Mbind yi, ba wone ne Yeesu mooy Almasi bi.
28for med kraft målbandt han jødene offentlig, idet han viste av skriftene at Jesus er Messias.