1 Bi loolu wéyee ñu fas yéene noo dugal gaal jëme réewu Itali. Noonu ñu jël Pool ak ñeneen ñi ñu tëjoon, dénk leen njiitu xare bu tudd Yulyus, mi bokk ci mbooloom xare mu buur.
1Da det nu var avgjort at vi skulde seile avsted til Italia, overgav de både Paulus og nogen andre fanger til en høvedsmann ved navn Julius ved den keiserlige hærdeling.
2 Nu dugg ca gaalu dëkku Adaramit guy taxaw ci teeruy Asi, daldi tàbbi ci biir géej; te Aristàrk, mi dëkk Tesalonig ci diiwaanu Maseduwan, ànd ak nun.
2Vi gikk da ombord på et skib fra Adramyttium som skulde seile til stedene langs Asia-landet, og så fór vi ut; Aristarkus, en makedonier fra Tessalonika, var med oss.
3 Ca ëllëg sa nu teer Sidon; Yulyus laabiir ci Pool, may ko mu dem ci ay xaritam, ngir ñu ganale ko.
3Den annen dag løp vi inn til Sidon, og Julius, som var menneskekjærlig mot Paulus, gav ham lov til å gå til sine venner og nyte godt av deres omsorg.
4 Bi nu fa jógee, nu dem ci biir géej, leru dunu Sipar ci fegu ngelaw li, ndaxte ngelaw li da noo soflu.
4Derfra fór vi videre og seilte inn under Kypern, fordi vinden var imot,
5 Nu jàll géej, gi janook diiwaani Silisi ak Pamfili, teersi Mira ca wàlli Lisi.
5og efterat vi hadde seilt over havet ved Kilikia og Pamfylia, kom vi til Myra i Lykia.
6 Foofa nag njiit la gis gaal gu jóge Alegsàndiri, jëm Itali, mu dugal nu ca.
6Der fant høvedsmannen et skib fra Aleksandria som skulde til Italia, og han førte oss ombord på det.
7 Noonu nuy dem ndànk diirub fan yu bare, ba janook Kanidd ci kaw coono bu réy; te ndegam ngelaw li mayu nu, nu jëm kanam, nu leru dunu Kereet ci fegu ngelaw li, janook Salmon.
7I mange dager gikk det nu smått med seilingen, og vi vant med nød og neppe frem imot Knidus; da vinden var imot, holdt vi ned under Kreta ved Salmone,
8 Nu romb fa ak coono yu bare, agsi ca bérab bu ñuy wax Teeru yu neex, te dend ak dëkku Lase.
8og det var så vidt vi kom der forbi og nådde frem til et sted som kalles Godhavn, nær ved en by Lasea.
9 Fekk booba yàggoon nañu ca yoon wa, te dem ci géej daldi aaytal, ndaxte jamonoy Kooru Yawut ya wees na. Moo tax Pool digal leen ne:
9Da nu en lang tid var gått, og det allerede var farlig å ferdes på sjøen, fordi det alt var over fasten, advarte Paulus dem og sa:
10 «Gaa ñi, gis naa ne, tukki bi ëmb na musiba ak kasara ju bare, waxuma gaal gi ak li mu yeb waaye sunuy bakkan sax xaj na ci.»
10I menn! jeg ser at sjøferden vil være et vågestykke og medføre stor skade, ikke bare for ladning og skib, men også for vårt liv.
11 Waaye njiit la sobental waxi Pool, déggal dawalkat ba ak boroom gaal ga.
11Men høvedsmannen satte mere lit til styrmannen og skipperen enn til det som Paulus sa.
12 Te gannaaw teeru ba neexul a lollikoo, ña ca ëpp mànkoo ci jóge fa, dem ci biir géej, ngir wut a agsi Fenigsë, biy teerub dunu Kereet te janook sowu suuf ak sowu kaw, nu lollikoo fa.
12Og da havnen var uhøvelig til vinterleie, blev de fleste enige om at de skulde fare ut også derfra, om de måskje kunde vinne frem og ta vinterhavn i Føniks, en havn på Kreta, som vender mot sydvest og nordvest.
13 Noonu bi ngelaw lu woyof liy jóge sudd wolee, ñu defe ne, man nañoo sottal seen pexe, ñu wëgg diigal, daldi tafu ci dunu Kereet.
13Da det nu blåste en svak sønnenvind, tenkte de at de kunde fullføre sitt forsett; de lettet da, og seilte nær land langsmed Kreta.
14 Waaye nes tuuti ngelaw lu wole penku, ñu di ko wax «Ërakilon,» jóge ca dun ba, ne milib ci sunu kaw.
14Men ikke lenge efter kom en hvirvelvind som kalles eurakylon, og kastet sig mot øen;
15 Mu ëpp doole gaal ga, daldi ko wat, ba nu bayliku, daldi yal.
15da skibet blev grepet av den og ikke kunde holde sig op mot vinden, gav vi det op og lot oss drive.
16 Nu daldi daw, leru dun bu tuuti bu ñuy wax Kóda ci fegu ngelaw, rawale looco ga ci kaw gaal ga ak coono bu bare.
16Vi løp da under en liten ø som kalles Klauda, og det var med nød at vi fikk berget båten;
17 Bi ñu ko yéegee, ñu fab ay buum, ngir laxas ca taatu gaal ga, ngir ragal a daanu ci suuf su nooy su ñuy wax Sirt; ba noppi ñu daldi sànni diigal, ngir wàññi doxub gaal ga, nuy yale noonu.
17da de hadde fått den ombord, grep de til nødhjelp og slo taug om skibet. Og da de fryktet for å drive ned på Syrten, firte de seilet ned, og drev således.
18 Waaye bi nu ngelaw li sonalee bu metti, ca ëllëg sa ñu sànni la gaal ga yeboon ca géej ga.
18Da vi nu led meget ondt av været, kastet de næste dag ladningen overbord,
19 Te ca ñetteelu fan ba, ñu sànni ak seeni loxo jumtukaay, yi ñu yeboon ngir fàggu.
19og den tredje dag kastet vi med egne hender skibets redskap i sjøen.
20 Noonu jant bi ne meŋŋ te biddiiw ne mes ay fan yu bare, fekk ba tey ngelaw li di wol ak doole, ba sunu yaakaaru mucc gépp tas.
20Da nu hverken sol eller stjerner lot sig se på flere dager, og et svært uvær var over oss, var det fra nu av forbi med alt håp om redning.
21 Bi loolu di xew, fekk gëj nañoo lekk, Pool daldi taxaw ci seen biir ne leen: «Gaa ñi, li gënoon mooy ngeen déglu ma te bañ a jóge Kereet, ba indil seen bopp musiba ak kasara ju réy jii.
21Og da de ikke hadde fått mat på lenge, stod Paulus frem midt iblandt dem og sa: I menn! I burde ha lydt mitt råd og ikke faret ut fra Kreta, så I hadde spart eder for dette vågestykke og denne skade.
22 Léegi nag maa ngi leen di dénk, ngeen takk seen fit, ndax gaal gi rekk mooy yàqu, waaye kenn ci yéen du dee.
22Og nu ber jeg eder være ved godt mot; for ingen sjel iblandt eder skal forgå, men bare skibet.
23 Ndaxte ci guddi menn malaaka dikkal na ma, jóge ci Yàlla sama Boroom, bi may jaamu.
23For i denne natt stod for mig en engel fra den Gud som jeg tilhører, som jeg også tjener, og sa:
24 Mu ne ma: “Pool bul tiit; fàww nga taxaw ci kanamu Sesaar, te yaa tax Yàllay aar bakkani ñi nga àndal ñépp.”
24Frykt ikke, Paulus! du skal stå frem for keiseren, og se, Gud har gitt dig alle dem som seiler med dig, til gave.
25 Moo tax gaa ñi, takkleen seen fit, ndax wóolu naa Yàlla ne, li mu ma wax, dina am.
25Derfor vær ved godt mot, I menn! for jeg setter min lit til Gud at det skal bli så som det er sagt mig.
26 Waaye war nanoo luf cib dun.»
26Men vi skal strande på en eller annen ø.
27 Ca fukkeelu guddi ga ak ñeent nu nga doon jayaŋ-jayaŋi ca géeju Adiratig; noonu ca xaaju guddi dawalkati gaal ga defe ne, danu jegesi suuf.
27Da nu den fjortende natt kom, mens vi drev omkring i Adriaterhavet, skjønte sjøfolkene midt på natten at det bar nær mot land.
28 Ñu sànni nattukaay ba ci biir géej, mu jàpp ñeent-fukki meetar, dem ca kanam tuuti, sànniwaat ko, jàpp fanweeri meetar.
28Og da de loddet, fant de tyve favner; men da de var kommet et lite stykke derfra og loddet igjen, fant de femten favner;
29 Ñu ragal ne, dinañu fenqu ci ay xeer, kon ñu daldi sànni ñeenti diigal ci geenu gaal ga, di ñaan bët set.
29og da de fryktet for at de kanskje kunde støte på skjær, kastet de fire anker ut fra bakstavnen, og ønsket at det vilde bli dag.
30 Waaye ci kaw loolu dawalkati gaal ga taafantaloo sànniji ay diigal ca boppu gaal ga, fekk dañuy fexee jël looco ga, ba raw.
30Men sjøfolkene søkte å rømme bort fra skibet og firte båten ned i havet, idet de lot som om de vilde legge ankere ut fra forstavnen;
31 Waaye Pool ne njiit la ak xarekat ya: «Bu ñii desul ci gaal gi, dungeen raw.»
31da sa Paulus til høvedsmannen og til krigsfolket: Dersom ikke disse blir ombord i skibet, kan I ikke bli berget.
32 Noonu xarekat ya dagg buum, yay téye looco ga, bàyyi ko mu wéy.
32Da kappet krigsfolket taugene på båten og lot den falle.
33 Bi bët setagul, Pool sant leen ñu lekk; mu ne leen: «Tey mooy seen fukki fan ak ñeent yu ngeen ne jonn, lekkuleen, mosuleen dara.
33Da det nu led mot dag, bad Paulus alle ta føde til sig, og han sa: Dette er nu den fjortende dag at I venter og lar være å ete og ikke tar noget til eder.
34 Maa ngi leen di sant nag, ngeen lekk, ndax noonu rekk ngeen man a rawe. Ndax genn kawar du rot ci yéen.»
34Derfor ber jeg eder ta føde til eder; dette hører med til eders redning; for det skal ikke falle et hår av hodet på nogen iblandt eder.
35 Bi mu waxee loolu, mu fab mburu, sant Yàlla ci kanamu ñépp, damm ko, daldi ko lekk.
35Da han hadde sagt dette, tok han et brød, takket Gud for alles øine og brøt det og begynte å ete;
36 Bi ñu gisee loolu, ñépp dëgëraat, ñu daldi lekk ñoom itam.
36da blev de alle frimodige og tok føde til sig de også.
37 Mboolem ñi nekkoon ca gaal ga mat na ñaari téeméeri nit ak juróom-ñaar-fukk ak juróom-benn.
37Vi var i alt to hundre og seks og sytti sjeler på skibet.
38 Noonu ñu lekk ba suur, daldi sànni pepp ma ca géej ga, ngir woyofal gaal ga.
38Og da de var blitt mette, lettet de skibet ved å kaste levnetsmidlene i havet.
39 Bi bët setee nag, xàmmiwuñu réew ma, waaye séen nañu ruqu tefes. Noonu ñu fas yéene caa teeral gaal ga, bu ñu ko manee.
39Da det nu blev dag, kjente de ikke landet, men de blev var en vik som hadde en strand; der bestemte de sig til å sette skibet på land om det var mulig.
40 Ñu dagg diigal ya, bàyyi leen ci biir géej, yiwiwaale baar ba; ba noppi firi wiiru kanam ga, jublu ca tefes ga.
40De kappet da ankerne og lot dem falle i havet, og løste tillike de taug som de hadde surret rorene med; så heiste de seilet for vinden og holdt ned på stranden.
41 Waaye ñu dal ca tundu suuf ca bérab bu ñaari koroŋ daje, gaal ga daldi fa luf. Boppu gaal ga nuur bu baax, ne fa tekk, te dooley duus ya daldi toj geen ba.
41Men de drev inn på en grunn som hadde dypt hav på begge sider; her støtte de på med skibet, og forskibet løp sig fast og stod urørlig, men akterskibet blev sønderslått av brenningene.
42 Bi loolu amee xarekat ya bëgg a rey ñi ñu tëj, ngir ragal ñenn ñi féey, ba raw.
42Krigsfolket vilde nu drepe fangene, forat ikke nogen av dem skulde svømme bort og rømme;
43 Waaye njiit la bëgg a musal Pool, mu tere leen pexe ma. Mu sant ñi man a féey, ñu jëkk a sóobu ca ndox ma, ba jot tefes ga.
43men høvedsmannen, som vilde frelse Paulus, hindret dem i deres råd, og bød at de som kunde svømme, skulde først kaste sig ut og komme i land,
44 Mu sant ñi ci des ñu def noonu, langaamu ci ay dénk, mbaa ca tojiti gaal ga. Noonu ñépp jot tefes ga ci jàmm ak salaam.
44og så de andre, dels på planker, dels på stykker av skibet. Og på denne vis gikk det så at alle berget sig i land.