1 Am bés Piyeer ak Yowaana dem, ba bëgg a dugg ca kër Yàlla ga ca waxtuw ñaan, maanaam tisbaar.
1Men Peter og Johannes gikk sammen op i templet ved bønnens time, som var den niende.
2 Fekk ñu indi fa nit ku judduwaale lafañ, ñu di ko teg bés bu nekk ca bunt, ba ñuy wooye Bunt bu rafet ba, ca kër Yàlla ga, ngir muy yelwaan ña fay dugg.
2Og det blev båret frem en mann som var vanfør fra mors liv av, og som de daglig la ved den tempeldør som kalles den fagre, for å be dem som gikk inn i templet, om almisse.
3 Bi mu gisee Piyeer ak Yowaana nag, ñuy dugg ca kër Yàlla ga, mu dékk leen loxo.
3Da han så Peter og Johannes som vilde gå inn i templet, bad han om å få en almisse.
4 Ci kaw loolu Piyeer ak Yowaana ne ko jàkk, te Piyeer ne ko: «Xool nu.»
4Men Peter så skarpt på ham sammen med Johannes og sa: Se på oss!
5 Lafañ bi xool leen, yaakaar ne dina jot dara ci ñoom.
5Han gav da akt på dem, for han ventet å få noget av dem.
6 Noonu Piyeer ne ko: «Awma xaalis, awma wurus, waaye li ma am, dinaa la ko jox: ci turu Yeesu Kirist mu Nasaret doxal!»
6Men Peter sa: Sølv og gull eier jeg ikke; men det jeg har, det gir jeg dig: I Jesu Kristi, nasareerens navn - stå op og gå!
7 Mu jàpp ci loxol ndeyjooram, yékkati ko. Ci saa si ay tànkam ak ay kostanam dëgër.
7Så grep han ham ved den høire hånd og reiste ham op,
8 Mu tëb, daldi taxaw, di dox. Mu dugg ak ñoom ca kër Yàlla ga, muy dox, di tëb tey sant Yàlla.
8og straks fikk hans føtter og ankler styrke, og han sprang op og stod og gikk omkring, og han fulgte med dem inn i templet, og gikk omkring der og sprang og lovet Gud.
9 Noonu ñépp gis ko, muy dox, di sant Yàlla.
9Og hele folket så ham gå omkring og love Gud,
10 Te ñu xàmmi ko, ne moo daan toog, di yelwaan ca Bunt bu rafet ba ca kër Yàlla ga. Ñu daldi waaru lool te yéemu ci li ko dikkal.
10og de kjente ham, de så at han var den som satt der ved den fagre tempeldør for å få almisse, og de blev fulle av forundring og redsel over det som var vederfaret ham.
11 Naka waa ji taq ci Piyeer ak Yowaana, ñépp waaru; ñu daldi daw, fekksi leen ca bérab ba ñuy wax Werandaa bu Suleymaan.
11Mens han nu holdt sig nær til Peter og Johannes, strømmet hele folket i forundring sammen om dem ved den buegang som kalles Salomos buegang.
12 Bi Piyeer gisee loolu nag, mu ne mbooloo mi: «Yéen waa Israyil, lu tax ngeen waaru ci lii? Lu tax ngeen di nu xool jàkk, mel ni ci sunu kàttan, mbaa ci sunu ragal Yàlla lanu doxloo kii?
12Da Peter så dette, svarte han folket: Israelittiske menn! Hvorfor undrer I eder over dette? eller hvorfor stirrer I på oss som om vi av vår egen kraft eller gudsfrykt hadde gjort at han går omkring?
13 Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, di Yàllay sunuy maam, màggal na Ndawam Yeesu; yéena xàcceek moom, ba jébbal ko Pilaat, fekk naroon na koo bàyyi.
13Abrahams og Isaks og Jakobs Gud, våre fedres Gud, har herliggjort sin tjener Jesus, ham som I forrådte og fornektet for Pilatus da han dømte at han skulde løslates;
14 Yéen xeeb ngeen Aji Sell ji te Jub, te tinul ab reykat.
14men I fornektet den hellige og rettferdige og bad at en morder måtte gis eder,
15 Bóom ngeen Aji Dundal ji, waaye Yàlla dekkal na ko; seede nanu ko nun ñépp.
15men livets høvding drepte I, ham som Gud opvakte fra de døde, som vi er vidner om.
16 Ci gëm turam la nit, kii ngeen di gis te xam ko, dëgëre; waaw, turu Yeesu ak ngëm gi jóge ci moom, moo tax mu wér peŋŋ ci seen kanam, yéen ñépp.
16Og ved troen på hans navn har hans navn styrket denne mann som I ser og kjenner, og troen som virkedes ved ham, har gitt ham denne fulle førlighet for eders alles øine.
17 «Léegi nag bokk yi, xam naa ne, ñàkka xam a tax ngeen def ko, yéen ak seeni kilifa.
17Og nu, brødre! jeg vet at I gjorde det i uvitenhet, likesom eders rådsherrer;
18 Waaye noonu la Yàlla amale li mu yégle woon lu jiitu jaarale ko ci gémmiñug yonent yépp naan, Almaseem dina sonn.
18men Gud opfylte på denne måte det som han forut forkynte ved alle profetenes munn, at hans Messias skulde lide.
19 Tuubleen seeni bàkkaar nag te woññiku ci Yàlla, ngir seeni bàkkaar far.
19Så fatt da et annet sinn og vend om, forat eders synder må bli utslettet, så husvalelsens tider kan komme fra Herrens åsyn,
20 Noonu jamonoy péex dina bawoo ci Boroom bi, te muy yebal Almasi bi mu leen jagleel, maanaam Yeesu.
20og han kan sende den for eder utkårede Messias, Jesus,
21 Asamaan war na koo yor, ba jamono ju ñuy defaraat lépp, di jamono ji Yàlla waxoon jaarale ko ci gémmiñug yonentam yu sell yépp, li dale ci njàlbéenug àddina.
21som himmelen skal huse inntil de tider da alt det blir gjenoprettet som Gud har talt om ved sine hellige profeters munn fra eldgamle dager av.
22 Ndaxte Musaa nee woon na: “Boroom bi seen Yàlla dina leen feeñalal ci seen xeet Yonent ni man; nangeen ko déggal ci lépp lu mu leen wax.
22Moses har jo sagt: En profet, likesom mig, skal Herren eders Gud opreise eder av eders brødre; ham skal I høre i alt det som han taler til eder;
23 Képp ku déggalul Yonent boobu, dees na la far ci xeet wi.”
23og det skal skje: Hver sjel som ikke hører denne profet, skal utryddes av folket.
24 «Li dale sax ci Samwil ak ñi ci topp, bépp yonent bu wax yégle na bés yii.
24Men også alle profetene fra Samuel av og derefter, så mange som har talt, har også forkynt om disse dager.
25 Yéen nag yéenay donn yonent yi ak kóllëre, gi Yàlla fasoon ak seeni maam, bi mu naan Ibraayma: “Xeeti àddina yépp dinañu barkeel ci ki soqikoo ci yaw.”
25I er barn av profetene og av den pakt som Gud gjorde med våre fedre da han sa til Abraham: Og i din ætt skal alle jordens slekter velsignes.
26 Yàlla feeñal na Ndawam, jëkk koo yebal ci yéen, ngir barkeel leen, ci woññi leen kenn ku nekk ci say bàkkaar.»
26I var de første som Gud sendte sin tjener til, da han lot ham fremstå forat han skulde velsigne eder, idet enhver av eder vender sig bort fra sin ondskap.