1 Naka noonu nit ku tudd Anañas, ànd ak Safira jabaram, jaay làccu suuf.
1Men en mann ved navn Ananias og hans hustru Saffira solgte en eiendom,
2 Mu dencal boppam benn cér ca njëg ga, ànd ca ak jabaram; ba noppi mu indi cér ba ca des, teg ko ci loxoy ndaw ya.
2og han stakk til side noget av pengene med sin hustrus vitende, og bar frem en del og la det for apostlenes føtter.
3 Bi mu ko defee Piyeer ne ko: «Anañas, lu tax nga bàyyi Seytaane dugg la, ba fees sa xol, ngay wor Xel mu Sell mi, ci li nga dencal sa bopp benn cér ci njëg gi?
3Da sa Peter: Ananias! hvorfor har Satan fylt ditt hjerte, så du skulde lyve for den Hellige Ånd og stikke til side noget av pengene for akeren?
4 Bi mu jaragul, ndax moomuloo ko woon? Te bi mu jaree, ndax yilifuloo woon njëg gi? Lu tax nga fas ci sa xol def nii? Woruloo nit ñi, waaye Yàlla nga wor.»
4Var den ikke din så lenge du hadde den, og var den ikke i din makt da den blev solgt? Hvorfor har du satt dig denne gjerning fore i ditt hjerte? Du har ikke løiet for mennesker, men for Gud.
5 Bi Anañas déggee baat yooyu, mu daanu dee. Ñi ko dégg ñépp tiit, ba ne nërëm.
5Men da Ananias hørte disse ord, falt han om og opgav ånden. Og stor frykt kom over alle som hørte det;
6 Noonu waxambaane ya jóg, ñu sàng ko, yóbbu ko, jébbal Yàlla.
6og de unge menn stod op og la ham til rette og bar ham ut og begravde ham.
7 Ñetti waxtu gannaaw ga, jabaram duggsi, fekk xamul la fa xew.
7Så gikk det omkring tre timer; da trådte hans hustru inn, uten å vite hvad som var skjedd.
8 Piyeer daldi ko ne: «Wax ma, ndax lii mooy njëgu tool bi?» Mu tontu ko: «Waawaaw, lii la.»
8Peter tok da til orde og sa til henne: Si mig: Var det for denne pris I solgte akeren? Hun sa: Ja, for denne pris.
9 Ci kaw loolu Piyeer ne ko: «Lu tax ngeen ànd, di diiŋat Xelu Boroom bi? Ñi denci woon sa jëkkër ñu ngi nii ci bunt bi, te dinañu la yóbbu.»
9Da sa Peter til henne: Hvorfor er I dog blitt enige om å friste Herrens Ånd? Se, deres føtter som har begravet din mann, er for døren, og de skal bære dig ut.
10 Ca saa sa mu daanu ciy tànkam dee. Bi waxambaane ya agsee nag, ñu fekk ko, mu faatu; ñu yóbbu ko, def ko ci wetu jëkkëram.
10Og straks falt hun om for hans føtter og opgav ånden, og da de unge menn kom inn, fant de henne død; og de bar henne ut og begravde henne hos hennes mann.
11 Noonu tiitaange ju mag tàbbi ci mbooloom ñi gëm ñépp ak ñi ko dégg ñépp.
11Og stor frykt kom over hele menigheten og over alle som hørte dette.
12 Bi loolu amee ay kéemaan ak ay firnde yu bare di xew ci nit ñi, jaare ca loxoy ndaw ya. Ñépp di booloo ca Werandaa bu Suleymaan ca kër Yàlla ga.
12Men det blev gjort mange tegn og undergjerninger blandt folket ved apostlenes hender, og de holdt alle samdrektig til i Salomos buegang.
13 Te kenn ci ña ca des ñemewul a booloo ak ñoom, waaye nit ñépp di leen màggal.
13Av de andre vågde ingen å holde sig til dem; men folket priste dem;
14 Moona ay nit ñu gën a bare, góor ak jigéen, di gëm Boroom bi, tey taq ci ñoom.
14og dess flere troende blev vunnet for Herren, menn og kvinner i hopetall,
15 Nit ñi indi sax ñu wopp ca mbedd ya, teg leen ca ay lal yu ndaw ak ay leeso, ngir bu Piyeer di jaar, doonte takkandeeram sax yiir ñenn ci ñoom.
15så de endog bar de syke ut på gatene og la dem på senger og benker, forat endog bare skyggen av Peter kunde overskygge nogen av dem når han kom.
16 Te it nit ñu bare dajaloo, jóge ca dëkk ya wër Yerusalem, ñu indi ay jarag ak ñu rab yu bon sadd; te ñoom ñépp daldi wér.
16Ja, også fra de omliggende byer kom de sammen i mengde til Jerusalem og førte med sig syke og folk som var plaget av urene ånder, og de blev alle helbredet.
17 Booba saraxalekat bu mag ba jóg ak gàngooram gépp, maanaam kureelu Sadusen, ga fa dëkk. Kiñaan gu mag jàpp leen,
17Da stod ypperstepresten op og alle de som holdt med ham, det var sadduseernes parti, og de blev fulle av nidkjærhet
18 ba ñu jàpp ndaw ya, tëj leen ca kaso ba.
18og la hånd på apostlene og kastet dem i det offentlige fengsel.
19 Waaye ci guddi malaakam Boroom bi ubbi buntu kaso ba, génne leen ci biti naan:
19Men en Herrens engel åpnet om natten fengslets dører og førte dem ut og sa:
20 «Demleen taxaw ca kër Yàlla ga, te xamal nit ñi lépp lu jëm ci dund gu wóor gii.»
20Gå avsted, og stå frem og tal i templet alle dette livs ord for folket!
21 Bi ñu déggee loolu, ñu dugg ca kër Yàlla ga ci suba teel, daldi waare. Bi ñu koy def, saraxalekat bu mag ba ak gàngooram ñëw, woolu kureelu àttekat ya, maanaam mbooloom njiiti bànni Israyil gépp; ñu yónnee, ngir jëli ndaw ya ca kaso ba.
21Da de hørte dette, gikk de mot dagningen inn i templet og lærte. Da nu ypperstepresten og hans følge kom, kalte de sammen rådet og alle Israels barns eldste, og sendte bud til fengslet for å hente dem.
22 Waaye bi wottukati kër Yàlla ga agsee ca kaso ba, gisuñu leen fa; ñu daldi dellusi, yégle ko
22Men de tjenere som kom dit, fant dem ikke i fengslet; de kom da tilbake og meldte:
23 ne: «Fekk nanu kaso ba tëju bu wóor ak wottukat ya taxaw ca bunt ya, waaye bi nu ko tijjee, fekkunu kenn ci biir.»
23Fengslet fant vi pålitelig lukket, og vaktmennene stod ved døren; men da vi lukket op, fant vi ingen der inne.
24 Bi kilifag wottukati kër Yàlla ga ak saraxalekat yu mag ya déggee loolu, ñu daldi ciy jaaxle lool, ñuy laajante, fu lii di mujj.
24Da høvedsmannen for tempelvakten og yppersteprestene hørte disse ord, visste de ikke hvad de skulde tenke om dem, og hvad dette skulde bli til.
25 Noonu benn waay ñëw, yégal leen ne: «Nit ñi ngeen tëjoon ñu ngi taxaw ca kër Yàlla ga, di jàngal nit ñi.»
25Da kom det en og meldte dem: Se, de menn som I kastet i fengsel, står i templet og lærer folket.
26 Ci kaw loolu kilifa ga ak wottukat ya dem jëli leen; waaye boolewuñu ci fitna, ngir ragal nit ñi sànni leen ay xeer.
26Da gikk høvedsmannen avsted med tjenerne og hentet dem, dog ikke med vold; for de fryktet for folket, at de skulde bli stenet.
27 Bi ñu leen indee, ñu dëj leen ci kanamu mbooloo ma. Saraxalekat bu mag ba laaj leen
27Og da de hadde hentet dem, stilte de dem for rådet, og ypperstepresten spurte dem og sa:
28 ne: «Ndax terewunu leen ci lu wér, ngeen waare ci tur woowu, te fi mu ne dajal ngeen Yerusalem ak seeni waare, rax-ca-dolli yéena ngi nuy fexee taqal deretu nit kooku.»
28Vi bød eder strengt at I ikke skulde lære i dette navn, og nu har I fylt Jerusalem med eders lære og vil føre dette menneskes blod over oss!
29 Waaye Piyeer ak ndaw ya tontu leen ne: «Déggal Yàlla moo gën déggal nit.
29Da svarte Peter og apostlene: En skal lyde Gud mere enn mennesker.
30 Yàllay sunuy maam dekkal na Yeesu, mi ngeen bóomoon ci wékk ko ca bant ba.
30Våre fedres Gud opvakte Jesus, som I drepte ved å henge ham på et tre;
31 Te Yàlla yékkati na ko ci ndeyjooram, mu nekk Buur ak Musalkat, ngir may bànni Israyil réccu, ba mu baal leen seeni bàkkaar.
31ham ophøiet Gud ved sin høire hånd til høvding og frelser, for å gi Israel omvendelse og syndenes forlatelse.
32 Seede nanu loolu, nun ak Xel mu Sell, mi Yàlla may ñi koy déggal.»
32Og vi er hans vidner om disse ting, og likeså den Hellige Ånd, som Gud gav dem som lyder ham.
33 Bi ñu déggee loolu, ñu mer ba seen xol di dagg, ñu bëgg leen a rey.
33Da de hørte dette, skar det dem i hjertet, og de la råd op om å slå dem ihjel.
34 Waaye amoon na fa nit ku tudd Gamaleel, bokk ci tariixab Farisen ya, di xutbakat bu tedd ci yoonu Musaa, mu jóg ca mbooloo ma, santaane ñu génne leen tuuti.
34Men det stod op en fariseer i rådet ved navn Gamaliel, en lovlærer som var høit aktet av hele folket, og han bød å føre mennene ut et øieblikk,
35 Bi ñu ko defee mu ne leen: «Yéen bokki Israyil, moytuleen li ngeen di def nit ñooñu.
35og han sa til dem: Israelittiske menn! Se eder vel for hvad I gjør med disse mennesker!
36 Ndaxte bu yàggul Tëdas jógoon na, mbubboo daraja, ba lu mat ñeenti téeméeri nit takktoo ak moom. Tëdas moomu nag reyees na ko, te ñi ko toppoon ñépp tasaaroo, ba seen pexe nasax.
36For nogen tid siden fremstod Teudas, som sa sig å være noget, og omkring fire hundre menn slo sig sammen med ham; han blev drept, og alle de som lød ham, spredtes og blev til intet.
37 Gannaawam it Yudaa mu Galile jóg, ca jamono ja ñu doon bind waa réew ma, mu jógloo nit ñu bare, ñu ànd ak moom. Moom itam dee na, te ay nitam ñépp tasaaroo.
37Efter ham fremstod Judas fra Galilea i skatteutskrivningens dager og forførte folket til å følge sig; også han omkom, og alle de som lød ham, blev spredt.
38 Léegi maa ngi leen di wax, génnleen ci mbirum ñooñu te bàyyi leen ñu dem. Ndaxte bu seen pas-pas mbaa seen jëf dee pexem nit, dina yàqu.
38Og nu sier jeg eder: Hold eder fra disse menn og la dem være i fred! for er dette råd eller dette verk av mennesker, da skal det gå til grunne,
39 Waaye bu fekkee ne ndogalu Yàlla la, dungeen ko man a fanq, ngir ragal a jànkoonte ak Yàlla.»
39men er det av Gud, vil I ikke kunne ødelegge dem. Vokt eder at I ikke må finnes stridende mot Gud!
40 Bi mu waxee loolu, ñu fekk ko ci xalaatam; ñu woo ndaw ya, daldi leen dóor ay yar, tere leen, ñu waxati dara ci turu Yeesu, ba noppi bàyyi leen, ñu dem.
40De lød ham da, og kalte apostlene inn igjen og lot dem hudstryke, og bød dem at de ikke skulde tale i Jesu navn, og så lot de dem gå.
41 Ndaw ya nag jóge ca kanam kureelu àttekat ya, bég ci li leen Yàlla jàppe, ñu yeyoo yenu toroxte ngir Tur wa.
41Så gikk de da bort fra rådet, glade over at de var aktet verdige til å vanæres for det navns skyld;
42 Noonu bés bu nekk ca kër Yàlla ga ak ca kër ya, daawuñu noppee jàngale ak a xamle xebaar bu baax bi, ne Yeesu mooy Almasi bi.
42og de holdt ikke op med å lære hver dag i templet og hjemme og å forkynne evangeliet om Kristus Jesus.