1 Man Saag, jaamu Yàlla ak Boroom bi Yeesu Kirist, maa leen di nuyu, yéen fukki giir ak ñaar, yi tasaaroo ci biir àddina si.
1Jakob, Guds og den Herre Jesu Kristi tjener, hilser de tolv stammer som er spredt omkring i landene.
2 Yéen samay bokk, waxtu wu nattu yi dalee ci seen kaw, ak nu ñu man a mel, defleen ko ni mbég mu réy,
2Akt det for bare glede, mine brødre, når I kommer i allehånde fristelser,
3 xam ne nattub ngëm mooy ndeyu muñ.
3da I vet at prøvelsen av eders tro virker tålmodighet;
4 Kon na seen muñ dem ba mat, ngir ngeen bañ a fell fenn, waaye ngeen mat sëkk.
4men tålmodigheten må føre til fullkommen gjerning, forat I kan være fullkomne og hele og ikke mangle noget.
5 Ku xelam des ci benn fànn ci yéen nag, na ko ñaan Yàlla, te dina ko ko may, ndaxte Yàlla mooy Aji Yéwén, jiy may ñépp ci lu àndul ak genn ŋàññ.
5Men dersom nogen av eder mangler visdom, da bede han Gud, han som gir alle villig og uten onde ord, og den skal gis ham.
6 Waaye na ko ñaan ci ngëm te bañ cee werante; ndaxte kiy werante mi ngi mel ni ndoxum géej, mi ngelaw liy lëmbaaje wet gu ne.
6Men han bede i tro, uten å tvile; for den som tviler, ligner havsbølgen, som drives og kastes av vinden.
7 Bu kooku yaakaar dara ci Boroom bi.
7For ikke må det menneske tro at han skal få noget av Herren,
8 Ku am xel ñaar la, te ñàkk pasteef ci lépp lu mu man a def.
8slik en tvesinnet mann, ustø på alle sine veier.
9 Naka mbokk mi néew doole, na sant ci teraangaam fa kanam Yàlla,
9Men den ringe bror rose sig av sin høihet,
10 te boroom alal it sant cig suufeem, ndax ni tóor-tóor di ruuse, noonu lay wéye.
10og den rike av sin ringhet; for han skal forgå som blomst på gress;
11 Su jant fenkee, ba naaj wi tàng, kon gàncax lax, tóor-tóor ruus, te rafetaayam naaw. Noonu la boroom alal di nasaxe, moom ak i jëfam.
11solen gikk op med sin brand og tørket gresset bort, og blomsten på det falt av, og dets fagre skikkelse blev ødelagt; således skal og den rike visne bort på sine veier.
12 Ku dékku nattu, ku barkeel nga, ndax boo ci génnee ak ndam, dees na la jagleel kaalag dund, gi Yàlla dig ñi ko bëgg.
12Salig er den mann som holder ut i fristelse; for når han har stått sin prøve, skal han få livsens krone, som Gud har lovt dem som elsker ham.
13 Bu la fiir galanee, bul ne: «Yàllaa ko dogal,» ndaxte Yàlla jegewul ak mbon fenn te du fiir kenn.
13Ingen si når han fristes: Jeg fristes av Gud. For Gud fristes ikke av det onde, og selv frister han ingen.
14 Waaye ku sa bakkan nax, ba man la, looloo lay dugal ci fiir.
14Men hver fristes idet han drages og lokkes av sin egen lyst;
15 Kon bu bëgg-bëgg ëmbee, bàkkaar lay wasin, te bu bàkkaar màggee, jur dee.
15derefter, når lysten har undfanget, føder den synd; men når synden er blitt fullmoden, føder den død.
16 Yéen sama bokk yi ma bëgg, buleen juum ci lii:
16Far ikke vill, mine elskede brødre!
17 gépp may gu baax ak gépp jagle gu mat, ci Yàlla la jóge, di Baay bi sàkk leeri asamaan, fekk moom du soppiku, mbaa muy leer ak di lëndëm.
17All god gave og all fullkommen gave kommer ovenfra, fra lysenes Fader, hos hvem det ikke er forandring eller skiftende skygge.
18 Ci coobareem la nu sole kàddug dëgg gi, ba nu judduwaat, di tànneefu lépp lu mu bind.
18Efter sin vilje har han født oss ved sannhets ord, forat vi skal være en førstegrøde av hans skapninger.
19 Yéen sama bokk yi ma bëgg, nangeen xam lii: ku nekk war ngaa farlu ci déglu, di yéex a wax tey yéex a mer.
19I vet det jo, mine elskede brødre! Men hvert menneske være snar til å høre, sen til å tale, sen til vrede;
20 Ndaxte meru nit du jur njub gi neex Yàlla.
20for manns vrede virker ikke det som er rett for Gud.
21 Moo tax nanguleen ci woyof kàddu, gi leen Yàlla sol te man leen a musal, di dëddu bépp sobe ak coxor gi daj àddina.
21Avlegg derfor all urenhet og all levning av ondskap, og ta med saktmodighet imot det ord som er innplantet i eder, og som er mektig til å frelse eders sjeler!
22 Buleen yem ci déglu kàddu gi rekk, di nax seen bopp; waaye jëfeleen ko.
22Men vær ordets gjørere, og ikke bare dets hørere, idet I dårer eder selv.
23 Ndaxte ku déglu kàddu gi, te bañ koo jëfe, moom ak kuy seetu ñoo yem;
23For dersom en er ordets hører og ikke dets gjører, da ligner han en mann som ser på sitt naturlige åsyn i et speil:
24 day gis xar-kanamam, te su nee wërëñ, daldi fàtte meloom.
24han så på sig selv og gikk bort, og glemte straks hvordan han så ut.
25 Waaye kuy gëstu yoonu Yàlla, wi mat tey goreel --waxuma ki dégg, ba noppi fàtte, waaye kiy jëfe ndigal — kooku barkeel na ci kaw jëfam.
25Men den som skuer inn i frihetens fullkomne lov og holder ved med det, så han ikke blir en glemsom hører, men gjerningens gjører, han skal være salig i sin gjerning.
26 Ku yaakaar ne am na diine, waaye moomul làmmiñam, xanaa di nax boppam rekk, diineem jooju du diiney dara.
26Dersom en mener at han er en gudsdyrker, og ikke holder sin tunge i tømme, men dårer sitt eget hjerte, hans gudsdyrkelse er forgjeves.
27 Ku diineem sell te amul benn gàkk fa kanam Yàlla mooy kii: ki nemmiku jiirim yi ak jigéen ñi seen jëkkër faatu ci seeni tiis, tey waggar sobey àddina.
27En ren og usmittet gudsdyrkelse for Gud og Faderen er dette: å se til farløse og enker i deres trengsel, å holde sig selv uplettet av verden.