1 Gannaaw loolu Yawut ya amoon nañu genn màggal, moo tax Yeesu demoon Yerusalem.
1Derefter var det en av jødenes høitider, og Jesus drog op til Jerusalem.
2 Ca wetu benn ci bunti dëkk ba nag, maanaam ca Buntu xar ya, am na fa bët bu tudd Betesda ci làkku yawut, te ñu wërale ko ak juróomi mbaar.
2Men det er ved Fåreporten i Jerusalem en dam som på hebraisk heter Betesda og har fem bueganger;
3 Ca suufu mbaar yooyu la jarag yu bare, yu deme niki ay gumba, ay lafañ ak ay làggi, daan tëdd, di xaar ndox mi yengatu;
3i dem lå en mengde syke: blinde, halte, visne.
4 ndaxte, ci ni ñu ko nettalee, benn malaakam Boroom bi da daan wàcc léeg-léeg di jax ndox mi. Bu ndox mi masaa yengu ba noppi, jarag ju ca jiitu, wopp joo amaan, daldi wér ca saa sa.
4For en engel steg til visse tider ned i dammen og oprørte vannet. Den som da først steg ned efterat vannet var blitt oprørt, han blev helbredet, hvad sykdom han så led av.
5 Amoon na fa benn waay bu feebaroon lu mat fanweeri at ak juróom ñett.
5Nu var der en mann som hadde vært syk i åtte og tretti år;
6 Bi ko Yeesu séenee mu tëdd, te mu xam ne, woppam ji yàggoon na lool, mu laaj ko ne: «Ndax bëgg ngaa wér?»
6da Jesus så ham ligge der, og visste at han allerede hadde vært syk i lang tid, sa han til ham: Vil du bli frisk?
7 Jarag ja tontu ko ne: «Sang bi, duma am ku ma sóob ci ndox mi, bu yengoo; su ma ciy fexee dem, ñu jëkk ma ci.»
7Den syke svarte ham: Herre! jeg har ingen til å kaste mig ned i dammen når vannet blir oprørt; og i det samme jeg kommer, stiger en annen ned før mig.
8 Yeesu ne ko: «Jógal, jël sa basaŋ te dox.»
8Jesus sier til ham: Stå op, ta din seng og gå!
9 Ca saa sa mu daldi wér, jël basaŋam, daldi dox. Mbir moomu dafa daje woon ak bésu noflaay ba,
9Og straks blev mannen frisk og han tok sin seng og gikk. Men det var sabbat den dag.
10 looloo tax ba Yawut ya daldi ne nit ku wér ka: «Tey bésu noflaay la, te sunu yoon aaye na, ngay yor sa basaŋ.»
10Jødene sa da til ham som var blitt helbredet: Det er sabbat, og det er dig ikke tillatt å bære sengen.
11 Mu ne leen: «Ki ma faj moo ma ne: “Jëlal sa basaŋ te dox.”»
11Han svarte dem: Han som gjorde mig frisk, han sa til mig: Ta din seng og gå!
12 Ñu ne ko nag: «Ku la ne: “Jëlal sa basaŋ te dox?”»
12De spurte ham: Hvem er det menneske som sa til dig: Ta den og gå?
13 Waaye waa ji xamul ki ko wéral, fekk booba Yeesu dem na, te nit ñu bare teewoon nañu ca bérab ba.
13Men han som var blitt helbredet, visste ikke hvem det var; for Jesus hadde trukket sig tilbake, da det var meget folk på stedet.
14 Bi ñu ca tegee ab diir, Yeesu dajeek moom ca kër Yàlla ga ne ko: «Déglul, fii mu ne, wér nga; bul defati bàkkaar, ngir ragal lu yées lii dal la.»
14Siden traff Jesus ham i templet og sa til ham: Se, du er blitt frisk; synd ikke mere, forat ikke noget verre skal vederfares dig!
15 Noonu nit ka dellu ne Yawut ya, Yeesu moo ko fajoon.
15Mannen gikk bort, og fortalte jødene at det var Jesus som hadde gjort ham frisk.
16 Looloo tax Yawut ya di wut a sonal Yeesu, ndaxte daan na jëfe noonu ca bésu noflaay ba.
16Og derfor forfulgte jødene Jesus, fordi han gjorde dette på en sabbat.
17 Waaye Yeesu tontu na leen ne: «Sama Baay nekk na ba tey ci liggéey, kon man itam damay liggéey.»
17Men Jesus svarte dem: Min Fader arbeider inntil nu; også jeg arbeider.
18 Baat boobu moo tax ba Yawut yi gën koo wut a rey, ndaxte yemul woon rekk ci bañ a topp ndigalu bésu noflaay ba, waaye dafa wax it ne, Yàlla Baayam la, ba teg boppam Yàlla.
18Derfor stod da jødene ham enn mere efter livet, fordi han ikke bare brøt sabbaten, men også kalte Gud sin Fader og gjorde sig selv Gud lik.
19 Noonu Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, Doom ji mënul a def dara moom ci boppam; li mu gis Baay bi di def rekk lay def. Li Baay bi di jëf la Doom ji itam di jëf.
19Jesus svarte da og sa til dem: Sannelig, sannelig sier jeg eder: Sønnen kan ikke gjøre noget av sig selv, men bare det han ser Faderen gjør; for det han gjør, det gjør Sønnen likeså;
20 Ndaxte Baay bi bëgg na Doom ji, ba di ko won lépp lu muy def, te dina ko won jëf yu ëpp kéemaan yii, ngir ngeen gën a waaru.
20for Faderen elsker Sønnen, og viser ham alt det han selv gjør; og han skal vise ham større gjerninger enn disse, forat I skal undre eder.
21 Maanaam, ni Baay bi di dekkale ñu dee ñi, di leen jox dund, noonu la Doom ji di joxe dund ñi mu ko bëgg a jox.
21For likesom Faderen opvekker de døde og gjør levende, således gjør også Sønnen levende hvem han vil.
22 Baay bi du àtte kenn; àtte bi yépp, jox na ko Doom ji,
22For Faderen dømmer heller ikke nogen, men har gitt Sønnen hele dommen,
23 ngir ñépp di teral Doom ji, ni ñuy terale Baay bi. Ku teralul Doom ji, teraloo Baay, bi ko yónni.
23forat alle skal ære Sønnen, likesom de ærer Faderen. Den som ikke ærer Sønnen, ærer ikke Faderen, som har sendt ham.
24 «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku dégg sama kàddu te gëm ki ma yónni, am nga dund gu dul jeex te doo jaar ca àtte ba, ndaxte génn nga ci dee, tàbbi ci dund.
24Sannelig, sannelig sier jeg eder: Den som hører mitt ord og tror ham som har sendt mig, han har evig liv og kommer ikke til dom, men er gått over fra døden til livet.
25 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, jamono dina ñëw te agsi na ba noppi, mooy jamono, ji ñu dee ñi di dégg baatu Doomu Yàlla ji, te ku ko dégg dinga dund.
25Sannelig, sannelig sier jeg eder: Den time kommer, og er nu, da de døde skal høre Guds Sønns røst, og de som hører, skal leve.
26 Ndaxte ni Baay bi ame dund moom ci boppam, noonu it la ko maye Doom ji, mu am ko ci boppam.
26For likesom Faderen har liv i sig selv, således har han også gitt Sønnen å ha liv i sig selv,
27 Jox na Doom ji itam sañ-sañu àtte, ndaxte mooy Doomu nit ki.
27og han har gitt ham makt til å holde dom, fordi han er en menneskesønn.
28 «Bu leen ci dara jaaxal; ndaxte jamonoo ngi ñëw ju néew yépp, yi nekk ci seen bàmmeel, di dégg baatam tey génn.
28Undre eder ikke over dette! For den time kommer da alle de som er i gravene, skal høre hans røst,
29 Ñi daan jëf lu baax dinañu dekki, dund ba fàww, waaye ñi daan jëf lu bon, dinañu dekki, ñu daan leen.
29og de skal gå ut, de som har gjort godt, til livets opstandelse, de som har gjort ondt, til dommens opstandelse.
30 Mënumaa def dara man ci sama bopp. Ni ma Baay bi di digale rekk laay àttee, te sama àtte bu jub la, ndaxte defuma sama bëgg-bëgg, ci waawi ki ma yónni doŋŋ laay aw.
30Jeg kan ikke gjøre noget av mig selv; som jeg hører, så dømmer jeg, og min dom er rettferdig; for jeg søker ikke min vilje, men hans vilje som har sendt mig.
31 «Su ma seedeelee sama bopp, sama wax du am maana.
31Vidner jeg om mig selv, da er mitt vidnesbyrd ikke sant;
32 Waaye keneen moo may seedeel, te bir na ma ne, la muy wax ci man dëgg la.
32det er en annen som vidner om mig, og jeg vet at det vidnesbyrd han vidner om mig, er sant.
33 «Yéen yónni ngeen ay ndaw ci Yaxya, te seede na dëgg.
33I har sendt bud til Johannes, og han har vidnet for sannheten;
34 Man ci sama bopp soxlawuma seedes nit; waaye nag damay wax loolu rekk, ngir ngeen mucc.
34jeg tar ikke imot vidnesbyrd av et menneske, men jeg sier dette forat I skal bli frelst.
35 Yaxya meloon na ni làmp buy tàkk tey leeral, te nangu ngeen a bànneexu ab diir ci leeram.
35Han var det brennende og skinnende lys, men I vilde bare en tid fryde eder i hans lys.
36 «Waaye yor naa ci man seede su gën a mag si ma Yaxya di seedeel: maa ngi def jëf, yi ma Baay biy sant. Jëf yooyu may def nag ñooy seede ne, Baay bi moo ma yónni.
36Men jeg har det vidnesbyrd som er større enn det Johannes har vidnet; for de gjerninger som Faderen har gitt mig å fullbyrde, selve disse gjerninger som jeg gjør, de vidner om mig at Faderen har utsendt mig.
37 Te Baay bi ma yónni, moom itam seede na ma. Musuleen a dégg baatam te musuleen a gis xar-kanamam,
37Og Faderen, som har sendt mig, han har vidnet om mig; hverken har I nogensinne hørt hans røst eller sett hans skikkelse,
38 te kàddoom saxul ci yéen, ndaxte gëmuleen ki mu yónni.
38og hans ord har I ikke blivende i eder; for den han har sendt, ham tror I ikke.
39 Yéena ngi gëstu Mbind yi, ndaxte dangeen cee yaakaar dund gu dul jeex. Mbind yooyu nag far, ci sama mbir lañuy wax;
39I ransaker skriftene, fordi I tenker at i dem har I evig liv, og det er de som vidner om mig;
40 te bëgguleen a ñëw ci man ngir am dund!
40og I vil ikke komme til mig for å få liv.
41 «Wutuma tagg yu jóge ci nit.
41Jeg tar ikke ære av mennesker;
42 Waaye yéen, xam naa leen; leer na ma ne, amuleen ci seen xol benn mbëggeel ci Yàlla.
42men jeg kjenner eder og vet at I ikke har kjærligheten til Gud i eder.
43 Man ñëw naa ci sama turu Baay, te nanguwuleen ma, waaye bu keneen dikkee ci turu boppam, ngeen nangu ko.
43Jeg er kommet i min Faders navn, og I tar ikke imot mig; kommer en annen i sitt eget navn, ham tar I imot.
44 Bëgg ngeen ku leen di tagg, te wutuleen ngërëm, li jóge ci jenn Yàlla rekk ji am. Kon nan ngeen man a gëme?
44Hvorledes kan I tro, I som tar ære av hverandre, og den ære som er av den eneste Gud, den søker I ikke?
45 «Buleen xalaat ne, maa leen di jiiñ dara ci sama kanamu Baay. Musaa, mi ngeen yaakaar, moo leen di booleek moom.
45I må ikke tenke at jeg vil anklage eder hos Faderen; det er en som anklager eder, Moses, han som I har satt eders håp til.
46 Bu ngeen gëmoon Musaa, dingeen ma gëm man itam, ndaxte seedeel na ma.
46For hadde I trodd Moses, da hadde I trodd mig; for det er om mig han har skrevet;
47 Waaye su fekkee gëmuleen li Musaa bind, kon nu ngeen man a gëme samay wax?»
47men tror I ikke hans skrifter, hvorledes kan I da tro mine ord?