Wolof: New Testament

Norwegian

Mark

13

1 Bi Yeesu di jóge ca kër Yàlla ga, kenn ca taalibe ya ne ko: «Kilifa gi, xoolal! Ni mu réye ay doj, te rafete ni ay taax!»
1Og da han gikk ut av templet, sa en av hans disipler til ham: Mester! se, hvilke stener og hvilke bygninger!
2 Waaye Yeesu tontu leen: «Du gis ngeen taax yu réy yii yépp? Lii lépp dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.»
2Og Jesus sa til ham: Ser du disse store bygninger? Det skal ikke levnes sten på sten som ikke skal brytes ned.
3 Gannaaw loolu, bi nga xamee ne Yeesu toog na ci tundu Oliw ya, jàkkaarlook kër Yàlla ga, Piyeer, Saag, Yowaana ak Andare fekki ko cig wet, laaj ko:
3Og da han satt på Oljeberget rett imot templet, spurte Peter og Jakob og Johannes og Andreas ham i enrum:
4 «Wax nu kañ la loolu di am? Te luy tegtal ne, mbir yii yépp a ngi bëgg a mat?»
4Si oss: Når skal dette skje? og hvad er tegnet når alt dette skal fullbyrdes?
5 Noonu Yeesu tontu leen: «Moytuleen, bu leen kenn nax.
5Jesus tok til orde og sa til dem: Se til at ikke nogen fører eder vill!
6 Ñu bare dinañu ñëw ci sama tur naan: “Moom laa,” te dinañu nax ñu bare.
6For mange skal komme i mitt navn og si: Det er mig; og de skal føre mange vill.
7 Bu ngeen déggee ay xare ak coowi xare, wottuleen a tiit; loolu war na am, waaye mujug jamono ji jotagul.
7Men når I hører krig og rykter om krig, da la eder ikke skremme! for det må så skje, men enden er ikke enda.
8 Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew. Te yengu-yenguy suuf dina am ciy bérab yu bare, ak ay xiif. Loolu lépp mooy ndoortel metit yi, mel ni jigéen juy matu.
8For folk skal reise sig mot folk, og rike mot rike; det skal være jordskjelv både her og der; det skal være hunger og oprør. Dette er begynnelsen til veene.
9 «Moytuleen. Dees na leen jébbal àttekat ya, di leen dóor ay yar ca jàngu ya. Dinañu leen dëj ci kanamu ay boroom réew ak ay buur ndax sama tur, ngir ngeen nekk seede ci ñoom.
9Men ta eder i vare! De skal overgi eder til domstolene, og I skal hudstrykes i synagoger og stilles for landshøvdinger og konger for min skyld, til vidnesbyrd for dem.
10 Fàww xebaar bu baax bi jëkk a jib ci xeet yépp.
10Og først må evangeliet forkynnes for alle folkeslag.
11 Saa su ñu leen jàppee nag, dëj leen ci péncum layoo, buleen jàq ci li ngeen war a wax; li ngeen jot ca waxtu woowa waxleen ko, ndaxte du yéenay wax waaye Xel mu Sell mi.
11Og når de fører eder frem og overgir eder, da vær ikke forut bekymret for hvad I skal tale! men det som gis eder i samme stund, det skal I tale; for det er ikke I som taler, men den Hellige Ånd.
12 «Mag dina joxe rakkam cig dee, baay joxe doomam; ay doom it dinañu jóg, di bañ seeni waajur, di leen reylu.
12Og bror skal overgi bror til døden, og en far sitt barn, og barn skal reise sig mot foreldre og volde deres død.
13 Te ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur; waaye ku muñ ba ca muj ga, mucc.
13Og I skal hates av alle for mitt navns skyld; men den som holder ut inntil enden, han skal bli frelst.
14 «Bés baa ngi ñëw, bu li ñuy wax “Lu araam luy yàqe” tegee ca bérab bu mu yelloowul; kiy jàng, na xam. Bu ngeen gisee loolu nag, ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya.
14Men når I ser ødeleggelsens vederstyggelighet stå der hvor den ikke bør - den som leser det, han se til å skjønne det! - da må de som er i Judea, fly til fjells,
15 Ku nekk ci kaw taax mi, bul wàcc ngir dugg kër gi, fab say yëf ya fa nekk.
15og den som er på taket, ikke stige ned i huset og ikke gå inn for å hente noget fra sitt hus,
16 Ku nekk ci tool bi, bul ñibbi ngir fab sa mbubb.
16og den som er ute på marken, ikke vende tilbake for å hente sin kappe.
17 Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooya, ngalla it ñiy nàmpal.
17Ve de fruktsommelige og dem som gir die, i de dager!
18 Ñaanleen ngir seen gàddaay bañ a tase ak jamonoy seddaayu lolli.
18Men bed at det ikke må skje om vinteren!
19 Ndaxte booba dina am metit wu réy wu musul a am, ba àddina sosoo ak tey, te dootul am mukk.
19for i de dager skal det være så stor en trengsel som ikke har vært inntil nu fra skapningens begynnelse, fra den tid da Gud skapte verden, og som heller ikke skal bli.
20 Te bu fekkul woon Boroom bi wàññi bés yooyu, kenn du mucc, waaye fekk na mu wàññi leen ndax gaayam ñi mu tànn.
20Og dersom ikke Herren forkortet de dager, da blev intet kjød frelst; men for de utvalgtes skyld, for deres skyld som han har utvalgt, har han forkortet de dager.
21 «Booba nag, bu leen kenn waxee: “Kaayleen gis, Kirist a ngi fi,” mbaa: “Xool-leen, mu nga fale,” buleen ko gëm.
21Og om nogen da sier til eder: Se, her er Messias, eller: Se der - da skal I ikke tro det.
22 Ndaxte ñiy mbubboo turu Kirist ak ñiy mbubboo turu yonent, dinañu feeñ, di joxe ay firnde yu réy ak ay kéemaan, ba ciy nax sax ñi Yàlla tànn, su loolu manoon a am.
22For falske messiaser og falske profeter skal opstå og gjøre tegn og under for å føre de utvalgte vill, om det var mulig.
23 Wax naa leen ko lu jiitu. Kon nag moytuleen.
23Men ta I eder i vare! Jeg har sagt eder alt forut.
24 «Waaye booba, gannaaw metit yooyu:“Jant bi dina lëndëmte weer dootul leer;
24Men i de dager, efter den trengsel, skal solen bli formørket og månen ikke gi sitt skinn,
25 biddiiw yi di daanoo asamaan,te kàttani asamaan yiy yengu.”
25og stjernene skal falle ned fra himmelen, og himmelens krefter skal rokkes.
26 «Noonu dees na gis Doomu nit ki ñëw ci niir yi, ànd ak kàttan ak ndam lu réy.
26Og da skal de se Menneskesønnen komme i skyene med megen kraft og herlighet.
27 Dina yónni ay malaakam, ñu dajale ñi mu tànn ci ñeenti xebla yi, fa àddina dale, ba fa asamaan yem.»
27Og da skal han sende ut englene og samle sine utvalgte fra de fire verdenshjørner, fra jordens ende til himmelens ende.
28 Yeesu teg ca ne: «Jàngleen misaalu garabu figg ga. Boo xamee ne ay bànqaasam duy nañu, tey xobam sëq, xam ngeen ne nawet jege na.
28Lær en lignelse av fikentreet: Så snart det kommer saft i dets grener, og dets blader springer ut, da vet I at sommeren er nær;
29 Noonu itam bu ngeen gisee loolu lépp xew, xamleen ne jege na; mu ngi ci bunt bi sax.
29således skal også I, når I ser dette skje, vite at han er nær for døren.
30 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy, te loolu lépp amul.
30Sannelig sier jeg eder: Denne slekt skal ingenlunde forgå før alt dette skjer.
31 Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk.
31Himmel og jord skal forgå, men mine ord skal ingenlunde forgå.
32 «Waaye bés boobu ak waxtu woowu, kenn xamul kañ lay doon; du malaaka yi ci kaw, du sax Doom ji, waaye Baay bi rekk moo ko xam.
32Men hin dag eller time vet ingen, ikke engang englene i himmelen, ikke engang Sønnen, men alene min Fader.
33 Moytuleen te xool! Xamuleen kañ la waxtu wi di jot.
33Ta eder i vare, våk! For I vet ikke når tiden er.
34 «Mi ngi mel ni nit ku tukki, mu dénk këram ay surgaam, ku nekk ak sa sas, te sant bëkk-néeg bi, mu xool.
34Likesom en mann som drog utenlands og forlot sitt hus og overgav sine tjenere styret, enhver sin gjerning, og bød dørvokteren at han skulde våke,
35 Yéen nag xool-leen, ndaxte xamuleen kañ la boroom kër gi di dellusi, muy ci timis mbaa ci xaaju guddi, muy ci fajar mbaa njël.
35således skal I våke - for I vet ikke når husets herre kommer, enten det blir om aftenen eller ved midnatt eller ved hanegal eller om morgenen -
36 Bu nee jaleñ, bumu leen bett, ngeen di nelaw.
36forat han ikke skal finne eder sovende, når han kommer uforvarende.
37 Li ma leen wax, ñépp laa ko wax: “Xool-leen!”»
37Men det jeg sier til eder, det sier jeg til alle: Våk!