Wolof: New Testament

Norwegian

Matthew

11

1 Ba Yeesu joxee fukki taalibeem ya ak ñaar ndigal yooyu, mu jóge fa, ngir dem jàngaleji ak a waare ci seeni dëkk.
1Og det skjedde da Jesus var ferdig med å gi sine tolv disipler disse forskrifter, da drog han derfra for å lære og forkynne i deres byer.
2 Gannaaw loolu Yaxya dégg ca kaso ba jëfi Almasi bi. Mu yónni ci moom nag ay taalibeem,
2Men da Johannes i fengslet hørte om Kristi gjerninger, sendte han bud med sine disipler og lot si til ham:
3 ne ko: «Ndax yaa di Ki war a ñëw, walla danoo war a xaar keneen?»
3Er du den som skal komme, eller skal vi vente en annen?
4 Yeesu tontu leen ne: «Demleen nettali Yaxya li ngeen dégg te gis ko.
4Og Jesus svarte og sa til dem: Gå bort og fortell Johannes det som I hører og ser:
5 Gumba yaa ngi gis, lafañ yiy dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, ñi dee di dekki, te ñi woyoflu ñu ngi dégg xebaar bu baax bi.
5blinde ser og halte går, spedalske renses og døve hører og døde står op, og evangeliet forkynnes for fattige;
6 Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man, barkeel nga.»
6og salig er den som ikke tar anstøt av mig.
7 Bi nga xamee ne taalibe ya Yaxya yónni woon ci Yeesu dem nañu, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li?
7Da nu disse gikk bort, begynte Jesus å tale til folket om Johannes: Hvorfor var det I gikk ut i ørkenen? for å se et rør som svaier for vinden?
8 Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol yére yu rafet? Waaye ñi sol yére yu rafet ñu ngi dëkk ci këri buur.
8Eller hvorfor var det I gikk der ut? for å se et menneske klædd i fine klær? Se, de som går i fine klær, er i kongenes hus.
9 Lu tax ngeen génn nag? Ngir gis ab yonent? Waaw, wax naa leen ne, ëpp na yonent.
9Eller hvorfor var det I gikk der ut? for å se en profet? Ja, jeg sier eder, endog mere enn en profet.
10 Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan:“Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la,te xàllal la yoon ci sa kanam.”
10Det er ham det er skrevet om: Se, jeg sender mitt bud for ditt åsyn; han skal rydde din vei for dig.
11 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya musul a feeñ. Waaye ba tey ki gën a ndaw ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji moo ko sut.
11Sannelig sier jeg eder: Nogen større enn døperen Johannes er ikke opreist blandt dem som er født av kvinner; men den minste i himlenes rike er større enn han.
12 Ci li dale ci jamonoy Yaxya ba léegi, nit ñaa ngi góor-góorlu ngir dugg ci nguuru Yàlla, te ñi sawar ñoo ci am wàll.
12Men fra døperen Johannes' dager inntil nu trenger de sig med makt inn i himlenes rike, og de som trenger sig inn, river det til sig.
13 Ndaxte li yonent yi wax ak li yoonu Musaa tëral ñu ngi doon dox, ba kera Yaxya di feeñ.
13For alle profetene og loven har spådd inntil Johannes,
14 Te Yaxya moomu, su ngeen bëggee nangu lii, mooy Iliyas bi waroon a ñëw.
14og om I vil ta imot det: Han er den Elias som skal komme.
15 Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.
15Den som har ører, han høre!
16 «Niti jamono jii nag, lan laa leen man a mengaleel? Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma, di woo seeni xarit,
16Men hvem skal jeg ligne denne slekt med? Den ligner små barn som sitter på torvene og roper til sine lekebrødre:
17 ne leen:“Liital nanu leen ak toxoro, te fecculeen,woyal nanu leen woyi dëj, te jooyuleen.”
17Vi blåste på fløite for eder, og I vilde ikke danse; vi sang sørgesanger, og I vilde ikke gråte.
18 Ndaxte Yaxya feeñ na, lekkul, naanul, ngeen daldi ne: “Dafa ànd ak rab.”
18For Johannes kom; han hverken åt eller drakk, og de sier: Han er besatt.
19 Gannaaw gi nag, Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.” Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.»
19Menneskesønnen kom; han eter og drikker, og de sier: Se, for en storeter og vindrikker, tolderes og synderes venn! Men visdommen er rettferdiggjort av sine barn.
20 Gannaaw loolu Yeesu daldi gëdd dëkk, ya mu defe woon la ëpp cay kéemaanam, ndaxte tuubuñu seeni bàkkaar.
20Da begynte han å refse de byer hvor hans fleste kraftige gjerninger var gjort, fordi de ikke hadde omvendt sig:
21 Mu ne: «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon réccu nañu bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku.
21Ve dig, Korasin! ve dig, Betsaida! Dersom de kraftige gjerninger som er gjort i eder, var gjort i Tyrus og Sidon, da hadde de for lenge siden omvendt sig i sekk og aske.
22 Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Tir ak Sidon ñoo leen di tane.
22Dog, jeg sier eder: Det skal gå Tyrus og Sidon tåleligere på dommens dag enn eder.
23 Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe. Ndaxte kéemaan yi ma def ci yaw, bu ñu leen defoon ci dëkku Sodom, kon mu nekk ba tey.
23Og du, Kapernaum, som er blitt ophøiet like til himmelen! like til dødsriket skal du bli nedstøtt; for dersom de kraftige gjerninger som er gjort i dig, var gjort i Sodoma, da var det blitt stående til denne dag.
24 Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Sodom moo lay tane.»
24Dog, jeg sier eder: Det skal gå Sodomas land tåleligere på dommens dag enn eder.
25 Ca jamono joojale Yeesu wax na lii: «Yaw Baay bi, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel, te xamal leen gune yi.
25På den tid tok Jesus til orde og sa: Jeg priser dig, Fader, himmelens og jordens herre, fordi du har skjult dette for de vise og forstandige, og åpenbaret det for de umyndige;
26 Waaw Baay bi, ndaxte looloo la neex.»
26ja, Fader, fordi således skjedde det som var velbehagelig for dig.
27 Yeesu teg ca ne: «Sama Baay jébbal na ma lépp, te kenn mënu maa xam, man Doom ji, ku dul Baay bi; kenn it mënul a xam Baay bi, ku dul man Doom ji, ak ku ma ko bëgg a xamal.
27Alle ting er mig overgitt av min Fader, og ingen kjenner Sønnen, uten Faderen, heller ikke kjenner nogen Faderen, uten Sønnen og den som Sønnen vil åpenbare det for.
28 «Ñëwleen ci man, yéen ñépp ñi sonn te diis, dinaa leen may noflaay.
28Kom til mig, alle I som strever og har tungt å bære, og jeg vil gi eder hvile!
29 Jébbaluleen ci man te jàng ci man, ndaxte lewet naa te woyof, te dingeen am noflaay ci seen xol.
29Ta mitt åk på eder og lær av mig! for jeg er saktmodig og ydmyk av hjertet; så skal I finne hvile for eders sjeler.
30 Ndaxte sama kilifteef lewet na te sama yen diisul.»
30For mitt åk er gagnlig, og min byrde er lett.