Wolof: New Testament

Norwegian

Matthew

14

1 Ca jamono joojale Erodd boroom diiwaanu Galile dégg na tur, wa Yeesu am.
1På den tid fikk fjerdingsfyrsten Herodes høre ryktet om Jesus,
2 Noonu mu ne ay surgaam: «Kooku mooy Yaxya, mi dekki; moo tax mu ànd ak kàttanu def ay kéemaan.»
2og han sa til sine tjenere: Dette er døperen Johannes; han er opstanden fra de døde, og derfor er det disse krefter er virksomme i ham.
3 Ndaxte Erodd jàppoon na Yaxya, yeew ko, tëj. Ndaxte Erodd takkoon na Erojàdd, jabaru Filib magam,
3Herodes hadde grepet Johannes og bundet ham og kastet ham i fengsel for Herodias' skyld, som var hans bror Filips hustru.
4 te Yaxya daan ko wax: «Jaaduwul nga denc ko.»
4For Johannes hadde sagt til ham: Det er dig ikke tillatt å ha henne.
5 Erodd nag bëgg koo rey, waaye dafa ragal nit ñi, ci li ñu teg Yaxya ab yonent.
5Og han vilde gjerne slå ham ihjel, men fryktet for folket; for de holdt ham for en profet.
6 Bi ñu ca tegee ab diir nag, ñuy màggal bés ba Erodd juddu woon, te doomu Erojàdd ju jigéen di fecc ci biir gan ñi. Loolu neex Erodd,
6Men da det var Herodes' fødselsdag, danset Herodias' datter for dem, og Herodes syntes om henne;
7 ba mu dig ko ci kaw ngiñ ne ko: «Loo laaj, dinaa la ko jox.»
7derfor lovte han med ed å gi henne hvad hun vilde be om.
8 Noonu ndaw sa daldi topp la ko ndey ji digaloon, ne Erodd: «Indil ma fii ci biir ndab boppu Yaxya.»
8Men hun sa efter sin mors råd: Gi mig hit døperen Johannes' hode på et fat!
9 Bi ko buur ba déggee, mu am naqar, waaye ngiñ la ak gan ña tax mu santaane, ñu jox ko ko.
9Og kongen blev ille til mote, men for sine eders og for gjestenes skyld bød han at det skulde gis henne,
10 Mu yónnee nag, ngir ñu dagg boppu Yaxya ca kaso ba.
10og han sendte sine folk avsted og lot Johannes halshugge i fengslet.
11 Ñu indi bopp bi ci biir ndab, jox ko janq ba, mu jox ko ndeyam.
11Og de kom med hans hode på et fat og gav det til piken, og hun bar det til sin mor.
12 Noonu taalibey Yaxya ñëw, fab néew wa, suul ko; ba noppi dem, wax ko Yeesu.
12Og hans disipler kom til og tok hans legeme og begravde det; og de gikk og fortalte det til Jesus.
13 Bi Yeesu déggee deewu Yaxya nag, mu jóge fa, dugg cig gaal, di dem ca bérab bu wéet. Waaye bi ko nit ñi yégee, ñu daldi jóge ci dëkk yi, topp ko ak seeni tànk.
13Da Jesus hørte det, drog han derfra i en båt avsides til et øde sted, og da folket fikk høre det, fulgte de efter ham til fots fra byene.
14 Yeesu génn ci gaal gi nag, gis mbooloo mu réy, mu yërëm leen, ba faj ñi ci wopp.
14Og da han gikk i land, så han meget folk, og han ynkedes inderlig over dem og helbredet deres syke.
15 Ca ngoon sa taalibe yi ñëw ci moom ne ko: «Fii àllub neen la, te léegi mu guddi. Doo yiwi mbooloo mi, ngir ñu dem ci dëkk yu ndaw yi, jënd lu ñu man a lekk?»
15Men da det var blitt aften, gikk hans disipler til ham og sa: Stedet er øde, og det er alt sent på dagen; la derfor folket fare, så det kan gå bort i byene og kjøpe sig mat!
16 Waaye Yeesu tontu leen ne: «Matul ñu dem, yéen joxleen leen lu ñu lekk.»
16Men Jesus sa til dem: De har ikke nødig å gå bort; gi I dem å ete!
17 Ñu ne ko: «Amunu fi lu dul juróomi mburu ak ñaari jën.»
17De sa til ham: Vi har ikke mere her enn fem brød og to fisker.
18 Yeesu ne leen: «Indil-leen ma ko fii.»
18Men han sa: Hent dem hit til mig!
19 Ci kaw loolu Yeesu sant mbooloo ma, ñu toog ca ñax ma. Mu jël juróomi mburu ya ak ñaari jën ya, xool ci kaw, sant Yàlla. Mu damm mburu ma, jox ko taalibe ya, ñu séddale ko nit ña.
19Og han bød at folket skulde sette sig ned i gresset, tok de fem brød og de to fisker, så op mot himmelen og velsignet dem; og han brøt brødene og gav dem til disiplene, og disiplene gav dem til folket.
20 Noonu ñépp lekk ba suur. Te ñu dajale dammit ya ca des, mu nekk fukki pañe ak ñaar yu fees.
20Og de åt alle og blev mette; og de tok op det som blev tilovers av stykkene, tolv kurver fulle.
21 Gannaaw jigéen ña ak gune ya, góor ña doon lekk matoon nañu juróomi junni.
21Men de som hadde ett, var omkring fem tusen menn foruten kvinner og barn.
22 Bi loolu amee Yeesu sant taalibe ya, ñu dugg gaal ga te jàll dex ga, jiituji ko, muy yiwi mbooloo ma.
22Og straks nødde han sine disipler til å gå i båten og sette over til hin side før ham, inntil han hadde latt folket fare.
23 Bi mu ko yiwee nag, mu yéeg ca tund wa, ngir wéet ak Yàlla. Noonu guddi jot, fekk mu nekk fa moom rekk.
23Og da han hadde latt folket fare, gikk han avsides op i fjellet for å bede; og da det var blitt aften, var han der alene.
24 Bi mu fa nekkee nag, gaal ga sore na tefes ga, te duus ya di ko yengal bu metti, ndax ngelaw la leen soflu.
24Men båten var alt midt ute på sjøen og arbeidet hårdt mot bølgene, for vinden var imot.
25 Ca njël nag Yeesu jëm ci ñoom, di dox ci kaw dex gi.
25Men i den fjerde nattevakt kom han til dem, vandrende på sjøen.
26 Waaye bi ko taalibe yi gisee, muy dox ci kaw dex ga, ñu daldi jommi naan: «Njuuma la!» daldi tiit bay yuuxu.
26Og da disiplene så ham vandre på sjøen, blev de forferdet og sa: Det er et spøkelse, og de skrek av redsel.
27 Waaye ca saa sa Yeesu ne leen: «Takkleen seen fit, man la, buleen tiit!»
27Men Jesus talte straks til dem og sa: Vær frimodige; det er mig, frykt ikke!
28 Ci kaw loolu Piyeer jël kàddu gi ne ko: «Sang bi, bu dee yaw, sant ma, ma dox ci kaw ndox mi, ñëw ci yaw.»
28Da svarte Peter ham og sa: Herre! er det dig, da byd mig komme til dig på vannet!
29 Yeesu ne ko: «Kaay!» Piyeer nag wàcc ca gaal ga, di dox ci kaw ndox mi, jëm ci Yeesu.
29Han sa: Kom! Og Peter steg ut av båten og gikk bortover vannet for å komme til Jesus.
30 Waaye bi mu gisee ni ngelaw li mettee, mu daldi tiit, tàmbalee suux. Mu woote ne: «Sang bi, wallu ma!»
30Men da han så det hårde vær, blev han redd og begynte å synke; da ropte han: Herre, frels mig!
31 Ca saa sa Yeesu tàllal loxoom, jàpp ko naan: «Yaw mi néew ngëm, lu tax nga am xel ñaar?»
31Og Jesus rakte straks hånden ut og tok fatt i ham og sa til ham: Du lite troende! hvorfor tvilte du?
32 Noonu ñu dugg ca gaal ga, te ngelaw li ne tekk.
32Og da de steg i båten, la vinden sig.
33 Ñi nekk ci gaal gi nag sukk ci kanamam ne ko: «Ci dëgg yaa di Doomu Yàlla ji.»
33Men de som var i båten, kom og falt ned for ham og sa: Sannelig, du er Guds Sønn!
34 Bi loolu amee ñu jàll, teer ca diiwaanu Senesaret.
34Og da de var faret over, kom de til Gennesarets land.
35 Ña fa dëkk xàmmi Yeesu, yónnee nag ca diiwaan bépp, indil ko ñu wopp ñépp.
35Og da folket på dette sted kjente ham igjen, sendte de bud i hele landet deromkring, og de førte til ham alle dem som hadde ondt,
36 Noonu ñu ñaan ko, mu may leen ñu laal cati mbubbam rekk, te ku ko laal daldi wér.
36og bad ham at de bare måtte få røre ved det ytterste av hans klædebon; og alle de som rørte ved det, blev helbredet.