1 Noonu ma gis asamaan su bees ak suuf su bees, ndaxte asamaan su jëkk sa ak suuf su jëkk sa wéyoon nañu, te géej gi amatul.
1Og jeg så en ny himmel og en ny jord; for den første himmel og den første jord var veket bort, og havet er ikke mere.
2 Ma gis, wàcce ca asamaan, jóge ca wetu Yàlla, Yerusalem gu bees gi, dëkk bu sell, bi ñu waajal ba mu jekk ni séet buy nég jëkkëram.
2Og jeg så den hellige stad, det nye Jerusalem, stige ned av himmelen fra Gud, gjort i stand som en brud som er prydet for sin brudgom.
3 Ma dégg baat bu xumb jibe ca gàngune ma naan: «Dalub Yàllaa ngi ci biir nit ñi. Dina dëkk ak ñoom, nit ñi dinañu nekk ay gaayam, te moom Yàlla ci boppam dina ànd ak ñoom, nekk Yàlla seen Boroom.
3Og jeg hørte en høi røst fra tronen si: Se, Guds bolig er hos menneskene, og han skal bo hos dem; og de skal være hans folk, og Gud selv skal være hos dem og være deres Gud;
4 Dina fomp bépp rangooñ ci seeni bët; te dee dootul am walla naqar walla jooy walla metit, ndaxte yëf yu jëkk ya wéy nañu.»
4og han skal tørke bort hver tåre av deres øine, og døden skal ikke være mere, og ikke sorg og ikke skrik og ikke pine skal være mere; for de første ting er veket bort.
5 Noonu ki toog ca gàngune ma ne: «Maa ngi yeesal lépp!» Mu ne ma: «Bindal, ndaxte kàddu yii yu wóor lañu te dëggu.»
5Og han som satt på tronen, sa: Se, jeg gjør alle ting nye. Og han sier til mig: Skriv! for disse ord er troverdige og sanne.
6 Mu teg ca ne ma: «Lépp mat na! Maay Alfa ak Omega, njàlbéen gi ak muj gi. Ku mar, dinaa la may ci bëtu ndoxum dund mi, te doo fey dara.
6Og han sa til mig: Det er skjedd. Jeg er Alfa og Omega, begynnelsen og enden. Jeg vil gi den tørste av livsens vannkilde uforskyldt.
7 Ku daan, dinga am cér ci mbir yii. Dinaa nekk Yàlla sa Boroom, te dinga nekk doom ci man.
7Den som seirer, skal arve alle ting, og jeg vil være hans Gud, og han skal være min sønn.
8 Waaye ñi ragal, ñi gëmul, ñiy def lu ñaaw, ñiy bóom nit, ñiy njaaloo, luxuskat yi, xërëmkat yi ak fenkat yépp, seen añ moo di déegu safara ak tamarax bi. Loolu mooy ñaareelu dee gi.»
8Men de redde og vantro og vederstyggelige og manndraperne og horkarlene og trollmennene og avgudsdyrkerne og alle løgnerne, deres del skal være i sjøen som brenner med ild og svovel; det er den annen død.
9 Gannaaw loolu benn malaaka ñëw, mi bokk ca juróom-ñaari malaaka, ya yoroon juróom-ñaari ndabi musiba yu mujj ya, ne ma: «Ñëwal, ma won la séet bi, jabaru Mbote mi.»
9Og en av de syv engler som hadde de syv skåler, fulle av de syv siste plager, kom til mig og talte med mig og sa: Kom, jeg vil vise dig bruden, Lammets hustru.
10 Noonu Xelum Yàlla solu ma, malaaka ma yóbbu ma ci kaw tund wu réy-a-réy. Noonu mu won ma Yerusalem, dëkk bu sell bi, muy wàcce ci asamaan, jóge ca wetu Yàlla,
10Og han førte mig i ånden bort på et stort og høit fjell og viste mig den hellige stad Jerusalem, som steg ned av himmelen fra Gud;
11 ànd ak ndamu Yàlla. Leeraayam mel ni leeraayu per bu jafe lool, ni jamaa buy ray-rayi.
11den hadde Guds herlighet, og dens lys var som den kosteligste sten, som krystallklar jaspis.
12 Miir bu réy te kawe moo ko wër te am fukki bunt ak ñaar, te bu ca nekk malaaka taxaw ca wet ga. Ca bunt ya bind nañu ca fukki tur ak ñaar, yu giiri bànni Israyil.
12Og den hadde en stor og høi mur; den hadde tolv porter, og på portene tolv engler og innskrevne navn, navnene på Israels barns tolv stammer;
13 Ca penku am na fa ñetti bunt; ca nor ñett; ca sudd ñett ak ñett ca sowu.
13mot øst var tre porter, mot nord tre porter, mot syd tre porter, mot vest tre porter.
14 Samp nañu miiru dëkk ba ci fukki fondamaa ak ñaar, yu ñu bind turi fukki ndawi Mbote ma ak ñaar.
14Og stadens mur hadde tolv grunnstener, og på dem navnene på Lammets tolv apostler.
15 Ki doon wax ak man amoon na nattukaay, di bantu wurus bu mu doon natte dëkk ba ak miir ba ko wër, ak bunt ya.
15Og han som talte med mig, hadde et gullrør forat han skulde måle staden og dens porter og dens mur.
16 Dëkk ba dafa kaare, guddaay ba ak yaatuwaay ba ñoo tolloo. Mu natt dëkk ba ak bant ba mu yor. Guddaay ba, yaatuwaay ba ak taxawaay ba lépp tolloo, di fukki junni ak ñaar ciy estat.
16Og staden ligger i en firkant, og dens lengde er så stor som bredden. Og han målte staden med røret: tolv tusen stadier; lengden og bredden og høiden på den er like.
17 Malaaka ma natt miir ba nattub nit, fekk miir ba di téeméer ak ñeent-fukk ak ñeenti xasab.
17Og han målte dens mur: hundre og fire og firti alen, efter menneskemål, som og er engle-mål.
18 Miir ba, jamaa lañu ko liggéeye, te dëkk ba di wurusu ngalam, leer ni weer bu set.
18Og dens mur var bygget av jaspis, og staden var av rent gull, lik rent glass.
19 Fondamaay miiru dëkk ba rafetale nañu leen xeeti per yu nekk.Fondamaa bu jëkk ba jamaa la;ñaareel ba, per bu bulo bu ñuy wax safir;ñetteel ba, per bu wert bu ñuy wax kalseduwan;ñeenteel ba, per bu wert te lerax, bu ñuy wax emëróot;
19Og grunnstenene i stadens mur var prydet med allslags kostelig sten; den første grunnsten var jaspis, den annen safir, den tredje kalkedon, den fjerde smaragd,
20 juróomeel ba, per bu xonq bu ñuy wax sardonigsë;juróom-benneel ba, per bu xonq curr bu ñuy wax sarduwan;juróom-ñaareel ba, per bu mboq bu ñuy wax kirisolit;juróom-ñetteel ba, per bu wert ni géej bu ñuy wax beril;juróom-ñeenteel ba, per bu mboq bu ñuy wax topas;fukkeel ba, per bu wert bu ñuy wax kirisoparas;fukkeel ba ak benn, per bu bulo bu ñuy wax yasent;fukkeel ba ak ñaar, per bu yolet bu ñuy wax ametist.
20den femte sardonyks, den sjette sarder, den syvende krysolitt, den åttende beryll, den niende topas, den tiende krysopras, den ellevte hyasint, den tolvte ametyst.
21 Fukki bunt ya ak ñaar, ay per yu weex lañu. Bunt bu nekk di benn per kepp. Péncu dëkk ba di wurusu ngalam, leer ni weer bu set.
21Og de tolv porter var tolv perler; hver av portene var av én perle; og stadens gate var rent gull, som klart glass.
22 Gisuma ca dëkk ba kër Yàlla, ndaxte Boroom bi Yàlla Aji Kàttan ji ak Mbote ma ñooy màggalukaay ba.
22Og noget tempel så jeg ikke i den; for dens tempel er Gud Herren, den allmektige, og Lammet.
23 Dëkk ba soxlawul jant walla weer ngir leeral ko, ndaxte ndamu Yàlla moo koy leeral, te Mbote ma moo nekk làmpam.
23Og staden trenger ikke solen eller månen til å lyse for sig; for Guds herlighet oplyser den, og Lammet er dens lys.
24 Xeeti àddina dinañu dox cig leeram, te buuri àddina dinañu ca indi seen ndam.
24Og folkeslagene skal vandre i dens lys, og kongene på jorden bærer sin herlighet inn i den.
25 Bunti dëkk ba duñu tëju bëccëg, te guddi du fa am.
25Og dens porter skal aldri lukkes om dagen; for natt skal ikke være der;
26 Dinañu fa indi ndamu xeet yi ak seen alal.
26og de skal bære folkeslagenes herlighet og ære inn i den.
27 Dara du fa dugg lu am sobe, mbaa kenn kuy sóobu ci ñaawteef walla fen. Ñi ñu bind ci téereb dund bu Mbote mi rekk ñoo fay dugg.
27Og intet urent skal komme inn i den, og ingen som farer med stygghet og løgn, men bare de som er innskrevet i livsens bok hos Lammet.