Wolof: New Testament

Spanish: Reina Valera (1909)

1 Corinthians

4

1 Nañu nu teg kon ay surgay Kirist, di ay jawriñ yuy xamle mbóoti Yàlla.
1TÉNGANNOS los hombres por ministros de Cristo, y dispensadores de los misterios de Dios.
2 Li war ci jawriñ mooy mu takku ci liggéeyam.
2Mas ahora se requiere en los dispensadores, que cada uno sea hallado fiel.
3 Ngeen àtte ma walla ñeneen àtte ma, amaluma ko solo. Te man sax duma àtte sama bopp.
3Yo en muy poco tengo el ser juzgado de vosotros, ó de juicio humano; y ni aun yo me juzgo.
4 Sama xel yeddu ma ci dara, waaye loolu taxul ma jub; ki may àtte mooy Boroom bi.
4Porque aunque de nada tengo mala conciencia, no por eso soy justificado; mas el que me juzga, el Señor es.
5 Looloo tax buleen daan kenn ci àtte, bala jamono ji di jot te Boroom bi ñëw. Mooy leeral yi nëbbu ci lëndëm, di làññi mébétu xol yi. Bu ko defee ku nekk dina jot ci Yàlla ngërëm, li mu yelloo.
5Así que, no juzguéis nada antes de tiempo, hasta que venga el Señor, el cual también aclarará lo oculto de las tinieblas, y manifestará los intentos de los corazones: y entonces cada uno tendrá de Dios la alabanza.
6 Bokk yi, ci loolu ma leen doon wax lépp nag, misaal naa leen ko ci Apolos ak ci man, ngir ngeen xool ci nun, ba xam li wax jii di tekki: «Bu seen xalaat weesu li Mbind mi wax.» Noonu kenn du màggal kii, suufeel ki ci des.
6Esto empero, hermanos, he pasado por ejemplo en mí y en Apolos por amor de vosotros; para que en nosotros aprendáis á no saber más de lo que está escrito, hinchándoos por causa de otro el uno contra el otro.
7 Ndaxte yaw, ku la def, ba nga gën a màgg ñi ci des? Loo am lu ñu la mayul? Te bu ñu la ko mayee, lu tax nga di ci tiitaru, mel ni mayuñu la ko?
7Porque ¿quién te distingue? ¿ó qué tienes que no hayas recibido? Y si lo recibiste, ¿de qué te glorías como si no hubieras recibido?
8 Yéen suur ngeen xaat! Woomle ngeen xaat! Tàmbali ngeen di nguuru te agseegunu! Céy ni ma bëgge, ngeen di nguuru, ba nu man a bokk ak yéen di nguuru!
8Ya estáis hartos, ya estáis ricos, sin nosotros reináis; y ojalá reinéis, para que nosotros reinemos también juntamente con vosotros.
9 Xalaat naa ne, nun ndawi Kirist yi, Yàlla def na ba nu mel ni nit ñu ñu jàppe ci xare te mujj ci sàppe yi, ñu dogal seen dee, nuy ceetaanum mbindeef yépp, muy nit muy malaaka.
9Porque á lo que pienso, Dios nos ha mostrado á nosotros los apóstoles por los postreros, como á sentenciados á muerte: porque somos hechos espectáculo al mundo, y á los ángeles, y á los hombres.
10 Nun teg nañu nu ni ay dof ndax Kirist, waaye yéen am ngeen xel ci Kirist. Néew nanu doole, waaye yéen am ngeen doole. Nawees na leen, waaye nun dañu noo xeeb.
10Nosotros necios por amor de Cristo, y vosotros prudentes en Cristo; nosotros flacos, y vosotros fuertes; vosotros nobles, y nosotros viles.
11 Ba fii mu nekk, danoo xiif, mar te rafle; ñu ngi nuy dóor, te dëkkunu fenn;
11Hasta esta hora hambreamos, y tenemos sed, y estamos desnudos, y somos heridos de golpes, y andamos vagabundos;
12 nu ngi ñaq di jariñoo. Ku nu saaga, nu ñaanal la lu baax. Coono bu ñu nu teg, nu tegoo ko.
12Y trabajamos, obrando con nuestras manos: nos maldicen, y bendecimos: padecemos persecución, y sufrimos:
13 Ku nu ñaawal, nu tontu la tont lu rafet. Fi mu ne noo mujj di mbalitu àddina, di ñu ñàkk njariñ ci lépp.
13Somos blasfemados, y rogamos: hemos venido á ser como la hez del mundo, el desecho de todos hasta ahora.
14 Binduma leen loolu ngir ngeen am yeraange, waaye dama koo def ngir artu leen, ndaxte yéenay samay doom te bëgg naa leen.
14No escribo esto para avergonzaros: mas amonéstoos como á mis hijos amados.
15 Su ngeen amee junniy njiit yu leen di sàmm ci Kirist, ba tey benn baay rekk ngeen am, ndaxte maa leen yégal xebaar bu baax bi, ba jur leen ci Kirist.
15Porque aunque tengáis diez mil ayos en Cristo, no tendréis muchos padres; que en Cristo Jesús yo os engendré por el evangelio.
16 Kon nag maa ngi leen di ñaan, ngeen roy ci man.
16Por tanto, os ruego que me imitéis.
17 Looloo tax ma yebal ci yéen Timote, miy sama doomu diine, di doom ju takku te ma bëgg ko. Dina leen fàttali ni may dunde ci Kirist, te mu dëppook li may jàngale fu nekk ci mboolooy ñi gëm ñépp.
17Por lo cual os he enviado á Timoteo, que es mi hijo amado y fiel en el Señor, el cual os amonestará de mis caminos cuáles sean en Cristo, de la manera que enseño en todas partes en todas las iglesias.
18 Am na ci seen biir ñuy tiitaru, di xalaat ne, duma delluseeti ci yéen.
18Mas algunos están envanecidos, como si nunca hubiese yo de ir á vosotros.
19 Waaye bu soobee Boroom bi, léegi ma ñëw ci yéen te seet boroom tiitar yooyu; waxuma seen kàddu, seen doole laay seet.
19Empero iré presto á vosotros, si el Señor quisiere; y entenderé, no las palabras de los que andan hinchados, sino la virtud.
20 Ndaxte nguuru Yàlla du waxi kese, waaye doole la.
20Porque el reino de Dios no consiste en palabras, sino en virtud.
21 Lu leen gënal? Ma ñëw ci yéen, yor ab yar, walla ma ànd ak mbëggeel, te lewet?
21¿Qué queréis? ¿iré á vosotros con vara, ó con caridad y espíritu de mansedumbre?