Wolof: New Testament

Spanish: Reina Valera (1909)

Acts

12

1 Ca jamono jooja Erodd buur ba jàppoon na ay nit ci mbooloom ñi gëm, ngir fitnaal leen.
1Y EN el mismo tiempo el rey Herodes echó mano á maltratar algunos de la iglesia.
2 Noonu mu daldi jàpp Saag, doomu ndeyu Yowaana, mu reylu ko ci jaasi.
2Y mató á cuchillo á Jacobo, hermano de Juan.
3 Bi mu gisee nag ne, mbir moomu neex na Yawut ya, mu daldi jàpp it Piyeer; fekk loolu daje ak bési màggalu Yawut, ga ñuy wax Mburu ya amul lawiir.
3Y viendo que había agradado á los Judíos, pasó adelante para prender también á Pedro. Eran entonces los días de los ázimos.
4 Bi mu ko jàppee, mu tëj ko kaso, teg ko ci loxoy ñeenti mboolooy xarekat, ngir ñu wottu ko, fekk mbooloo mu ci nekk di ñeenti nit; amoon na yéeney yóbbu ko ci kanamu Yawut ya gannaaw màggalu bésu Jéggi ba.
4Y habiéndole preso, púsole en la cárcel, entregándole á cuatro cuaterniones de soldados que le guardasen; queriendo sacarle al pueblo después de la Pascua.
5 Noonu ñuy wottu Piyeer ca kaso ba, waaye mbooloom ñi gëm di ko ñaanal Yàlla ak seen xol bépp.
5Así que, Pedro era guardado en la cárcel; y la iglesia hacía sin cesar oración á Dios por él.
6 Bi Erodd nekkee ci tànki indilu ko, ca guddi googa yeewoon nañu Piyeer ak ñaari càllala, muy nelaw diggante ñaari xarekat, te ay xarekat di wottu buntu kaso ba.
6Y cuando Herodes le había de sacar, aquella misma noche estaba Pedro durmiendo entre dos soldados, preso con dos cadenas, y los guardas delante de la puerta, que guardaban la cárcel.
7 Ca saa sa malaakam Boroom bi ñëw, te leer ne ràyy ca néeg ba. Malaaka ma dóor Piyeer ci wetam, yee ko ne ko: «Jógal bu gaaw!» Noonu jéng ya rot ciy loxoom.
7Y he aquí, el ángel del Señor sobrevino, y una luz resplandeció en la cárcel; é hiriendo á Pedro en el lado, le despertó, diciendo: Levántate prestamente. Y las cadenas se le cayeron de las manos.
8 Malaaka ma ne ko: «Takkal sa geño te sol say dàll.» Mu def ko. Malaaka ma ne ko: «Solal sa mbubb te topp ci man.»
8Y le dijo el ángel: Cíñete, y átate tus sandalias. Y lo hizo así. Y le dijo: Rodéate tu ropa, y sígueme.
9 Piyeer génn, topp ca malaaka ma, fekk gëmul sax ne lu am la, waaye mu yaakaar ne peeñu la.
9Y saliendo, le seguía; y no sabía que era verdad lo que hacía el ángel, mas pensaba que veía visión.
10 Noonu ñu weesu wottukat bu jëkk ba ak ba ca tegu, ñu agsi ca buntu weñ, ba jëm ca dëkk ba, mu daldi ubbikul boppam ci seen kanam. Ñu génn nag, jaar ci benn mbedd, malaaka ma daldi ko bàyyi.
10Y como pasaron la primera y la segunda guardia, vinieron á la puerta de hierro que va á la ciudad, la cual se les abrió de suyo: y salidos, pasaron una calle; y luego el ángel se apartó de él.
11 Bi xelam dellusee ci moom Piyeer ne: «Léegi xam naa ci lu wóor ne, Boroom bi yónni na malaakaam, musal ma ci loxoy Erodd ak li ma Yawut ya yéene woon lépp.»
11Entonces Pedro, volviendo en sí, dijo: Ahora entiendo verdaderamente que el Señor ha enviado su ángel, y me ha librado de la mano de Herodes, y de todo el pueblo de los Judíos que me esperaba.
12 Mu rabal xelam ci loolu, daldi dem kër Maryaama, ndeyu Yowaana, mi ñuy wooye Màrk, fekk ñu bare booloo fa, di ñaan ci Yàlla.
12Y habiendo considerado esto, llegó á casa de María la madre de Juan, el que tenía por sobrenombre Marcos, donde muchos estaban juntos orando.
13 Noonu Piyeer fëgg buntu kër ga, te mbindaan mu tudd Rodd wuyusi ko.
13Y tocando Pedro á la puerta del patio, salió una muchacha, para escuchar, llamada Rhode:
14 Mu xàmmi baatu Piyeer, bég ci, ba fàtte koo ubbil, waaye mu daw ci biir, xamle ne Piyeer a nga ca bunt ba.
14La cual como conoció la voz de Pedro, de gozo no abrió el postigo, sino corriendo adentro, dió nueva de que Pedro estaba al postigo.
15 Ñu ne ko: «Xanaa dangaa dof.» Waaye mu dëgër ci li mu wax. Noonu ñu ne ko: «Xanaa malaakaam la.»
15Y ellos le dijeron: Estás loca. Mas ella afirmaba que así era. Entonces ellos decían: Su ángel es.
16 Fekk Piyeer di gën a fëgg. Noonu ñu tijji, gis ko, daldi waaru.
16Mas Pedro perseveraba en llamar: y cuando abrieron, viéronle, y se espantaron.
17 Piyeer taf loxoom ci gémmiñam, ngir ñu noppi, daldi leen nettali, ni ko Boroom bi génnee ca kaso ba. Mu ne leen: «Tee ngeen jottali ko Saag ak bokk ya.» Bi mu ko waxee, mu jóge fa, dem feneen.
17Mas él haciéndoles con la mano señal de que callasen, les contó cómo el Señor le había sacado de la cárcel. Y dijo: Haced saber esto á Jacobo y á los hermanos. Y salió, y partió á otro lugar.
18 Bi bët setee nag, yengu-yengu bu réy am na ca xarekat ya, ñu ne: «Ana Piyeer?»
18Luego que fué de día, hubo no poco alboroto entre los soldados sobre qué se había hecho de Pedro.
19 Noonu Erodd wutlu ko, waaye gisu ko. Kon mu àtte wottukat ya, joxe ndigalu rey leen. Bi loolu amee Erodd jóge ci diiwaanu Yude, dem dëkku Sesare, toog fa.
19Mas Herodes, como le buscó y no le halló, hecha inquisición de los guardas, los mandó llevar. Después descendiendo de Judea á Cesarea, se quedó allí.
20 Fekk mu nekk ci xëccoo bu tàng ak waa dëkki Tir ak Sidon. Naka noona ñu ànd, bëgg koo gis. Ñu neexal Balastus, bëkk-néegu buur ba, di ñaan jàmm, ndaxte réewu buur ba moo doon dundal seen bos.
20Y Herodes estaba enojado contra los de Tiro y los de Sidón: mas ellos vinieron concordes á él, y sobornado Blasto, que era el camarero del rey, pedían paz; porque las tierras de ellos eran abastecidas por las del rey.
21 Ca bés ba ñu jàpp nag Erodd sol mbubbi buuram, toog ca jal ba ca àttekaay ba, di leen yedd ak a dénk.
21Y un día señalado, Herodes vestido de ropa real, se sentó en el tribunal, y arengóles.
22 Noonu mbooloo mi di yuuxu naan: «Lii baatu Yàlla la, du baatu nit!»
22Y el pueblo aclamaba: Voz de Dios, y no de hombre.
23 Ca saa sa nag, gannaaw màggalul Yàlla, malaakam Boroom bi fàdd ko te ay sax dugg ko, ba mu dee.
23Y luego el ángel del Señor le hirió, por cuanto no dió la gloria á Dios; y espiró comido de gusanos.
24 Moona kàddug Boroom bi di gën a màgg tey law.
24Mas la palabra del Señor crecía y era multiplicada.
25 Naka Barnabas ak Sool, bi ñu matalee seen liggéey, ñu jóge Yerusalem, ñibbi, ànd ak Yowaana mi tudd Màrk.
25Y Bernabé y Saulo volvieron de Jerusalem cumplido su servicio, tomando también consigo á Juan, el que tenía por sobrenombre Marcos.