Wolof: New Testament

Spanish: Reina Valera (1909)

Acts

6

1 Ca bés yooyu, naka taalibe yi di gën a bare, Yawut yiy làkk gereg tàmbalee ñaxtu ci mbirum Yawut tigi yi, te lii a ko waral: jigéen ñi seen jëkkër dee, te ñu bokk ci ñoom, naraalewuñu leen ca ndimbal, la ñuy séddale bés bu nekk.
1EN aquellos días, creciendo el número de los discípulos, hubo murmuración de los Griegos contra los Hebreos, de que sus viudas eran menospreciadas en el ministerio cotidiano.
2 Noonu fukki ndaw ya ak ñaar woo mbooloom taalibe ya ne leen: «Nu bàyyi kàddug Yàlla, di topptoo mbirum séddale, loolu jekkul ci nun.
2Así que, los doce convocaron la multitud de los discípulos, y dijeron: No es justo que nosotros dejemos la palabra de Dios, y sirvamos á las mesas.
3 Kon nag bokk yi, tànnleen juróom-ñaari nit ci seen biir, ñu am seede su rafet te fees ak Xel mu Sell mi ak sago, nu dénk leen liggéey bii.
3Buscad pues, hermanos, siete varones de vosotros de buen testimonio, llenos de Espíritu Santo y de sabiduría, los cuales pongamos en esta obra.
4 Waaye nun dinanu wéy ci ñaan ci Yàlla ak ci yenub xamle kàddu gi.»
4Y nosotros persistiremos en la oración, y en el ministerio de la palabra.
5 Lii ñu wax nag neex na mbooloo mépp. Noonu ñu tànn Ecen, di nit ku fees ak ngëm ak Xel mu Sell mi, boole ci Filib ak Porokor, teg ca Nikanor, Timon, Parmenas ak Nikolas, mi juddoo Ancos te tuub ci yoonu Yawut ya.
5Y plugo el parecer á toda la multitud; y eligieron á Esteban, varón lleno de fe y de Espíritu Santo, y á Felipe, y á Prócoro, y á Nicanor, y á Timón, y á Parmenas, y á Nicolás, prosélito de Antioquía:
6 Ñu jébbal leen ndaw ya, ñaanal leen, teg leen loxo.
6A estos presentaron delante de los apóstoles, los cuales orando les pusieron las manos encima.
7 Noonu kàddug Yàlla di law, ba mbooloom taalibe yi di yokku bu bare ci Yerusalem; te saraxalekat yu bare déggal Yàlla ci topp yoonu ngëm wi.
7Y crecía la palabra del Señor, y el número de los discípulos se multiplicaba mucho en Jerusalem: también una gran multitud de los sacerdotes obedecía á la fe.
8 Naka noona Ecen, mi fees ak yiw ak kàttan, di def ay kéemaan yu mag ak ay firnde ca nit ña.
8Empero Esteban, lleno de gracia y de potencia, hacía prodigios y milagros grandes en el pueblo.
9 Waaye ay nit jóg, bokk ci jàngu, bi ñuy wax Jàngub ñi ñu goreel, di ay niti dëkki Siren ak Alegsàndiri, ak it waa diiwaani Silisi ak Asi. Ñuy werante ak Ecen,
9Levantáronse entonces unos de la sinagoga que se llama de los Libertinos, y Cireneos, y Alejandrinos, y de los de Cilicia, y de Asia, disputando con Esteban.
10 waaye àttanuñu sagoom ak Xel mi muy waxe.
10Mas no podían resistir á la sabiduría y al Espíritu con que hablaba.
11 Kon ñu daldi jënd ay nit, ñu ne: «Dégg nanu ko, muy sosal Musaa ak Yàlla.»
11Entonces sobornaron á unos que dijesen que le habían oído hablar palabras blasfemas contra Moisés y Dios.
12 Noonu ñu jógloo nit ñi ak njiit yi ak xutbakat yi, ñu dal ci kawam, jàpp ko, yóbbu ko ca kureelu àttekat ya.
12Y conmovieron al pueblo, y á los ancianos, y á los escribas; y arremetiendo le arrebataron, y le trajeron al concilio.
13 Te ñu sàkk ay naaféq yuy seede ne: «Kii du bàyyee wax lu juuyoo ak bérab bu sell ba ak yoonu Musaa.
13Y pusieron testigos falsos, que dijesen: Este hombre no cesa de hablar palabras blasfemas contra este lugar santo y la ley:
14 Ndaxte dégg nanu, muy wax ne, Yeesum Nasaret moomu dina daaneel bérab bii te soppi aada, yi nu Musaa batale woon.»
14Porque le hemos oído decir, que Jesús de Nazaret destruirá este lugar, y mudará las ordenanzas que nos dió Moisés.
15 Bi ñu ko waxee, ña toogoon ñépp ca mbooloo ma xool ko jàkk, gis xar-kanamam, mu mel ni xar-kanamu malaaka.
15Entonces todos los que estaban sentados en el concilio, puestos los ojos en él, vieron su rostro como el rostro de un ángel.