1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Yàlla, maa leen di bind, yéen gaayi Yàlla yu sell yi te gëm Kirist Yeesu ci dëkku Efes.
1PABLO, apóstol de Jesucristo por la voluntad de Dios, á los santos y fieles en Cristo Jesús que están en Efeso:
2 Na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
2Gracia sea á vosotros, y paz de Dios Padre nuestro, y del Señor Jesucristo.
3 Cant ñeel na Yàlla Baayu sunu Boroom Yeesu Kirist, mi nu sotti ci sunu bokk ci Kirist lépp luy barkeel ci baatin te nekk ca bérab yu kawe ya.
3Bendito el Dios y Padre del Señor nuestro Jesucristo, el cual nos bendijo con toda bendición espiritual en lugares celestiales en Cristo:
4 Ndaxte ba àddina sosoogul, tànn na nu ci Kirist, ngir nu man a teew fa kanamam, sell te ñàkk sikk. Ci kaw mbëggeelam
4Según nos escogió en él antes de la fundación del mundo, para que fuésemos santos y sin mancha delante de él en amor;
5 séddoo na nu lu jiitu, def nu ay doomam jaarale ko ci Yeesu Kirist, ndaxte looloo doon yéene ju rafet, ji mu tëral ci coobareem.
5Habiéndonos predestinado para ser adoptados hijos por Jesucristo á sí mismo, según el puro afecto de su voluntad,
6 Na ndamam jolli ndax yiw wu réy, wi mu nu sotti ci Soppeem bi.
6Para alabanza de la gloria de su gracia, con la cual nos hizo aceptos en el Amado:
7 Moom jot na nu ak deretam ji ñu tuur, maanaam baal nu sunuy bàkkaar, ci kaw yiw wu yaatu,
7En el cual tenemos redención por su sangre, la remisión de pecados por las riquezas de su gracia,
8 wi mu nu baawaanal. Te Yàlla sol na nu xel mu mat ak dégg,
8Que sobreabundó en nosotros en toda sabiduría é inteligencia;
9 ci feeñal nu mbóoti coobareem, dëppook yéeneem ju rafet, ji mu jaarale ci Kirist.
9Descubriéndonos el misterio de su voluntad, según su beneplácito, que se había propuesto en sí mismo,
10 Mu tëral ne, bu jamono yi wéyee ba lépp mat, dina dajale lépp ci kilifteefu Kirist, muy ci kaw, muy ci suuf.
10De reunir todas las cosas en Cristo, en la dispensación del cumplimiento de los tiempos, así las que están en los cielos, como las que están en la tierra:
11 Te am nanu cér ci moom bu nu Yàlla sédd lu jiitu ci dogalam, moom miy doxal lépp ci ni mu ko àttee ci coobareem.
11En él digo, en quien asimismo tuvimos suerte, habiendo sido predestinados conforme al propósito del que hace todas las cosas según el consejo de su voluntad,
12 Noonu nuy jollil ndamam, nun ñi jëkk a wékk sunu yaakaar ci Kirist.
12Para que seamos para alabanza de su gloria, nosotros que antes esperamos en Cristo.
13 Te yéen itam, bi ngeen déggee kàddug dëgg gi, di xebaar bu baax, bi leen tegtal yoonu mucc, te ngeen gëm ko, Yàlla tàmpe na leen ni ñoñam ak Xel mu Sell, mi mu dige woon.
13En el cual esperasteis también vosotros en oyendo la palabra de verdad, el evangelio de vuestra salud: en el cual también desde que creísteis, fuisteis sellados con el Espíritu Santo de la promesa,
14 Te Xel mi mooy dawal gi nu Yàlla jox ci cér, bi mu nu dencal, ba kera muy goreel ñi mu jotal boppam, te ñépp jollil ndamam.
14Que es las arras de nuestra herencia, para la redención de la posesión adquirida para alabanza de su gloria.
15 Bi ma déggee nag seen ngëm ci Boroom bi Yeesu ak seen mbëggeel ci gaayi Yàlla yu sell yépp,
15Por lo cual también yo, habiendo oído de vuestra fe en el Señor Jesús, y amor para con todos los santos,
16 duma noppee sant Yàlla, di leen boole ci samay ñaan.
16No ceso de dar gracias por vosotros, haciendo memoria de vosotros en mis oraciones;
17 Te li may ñaan Yàllay sunu Boroom Yeesu Kirist, di Baay bi yelloo ndam, mooy lii: mu sol leen xel mu xóot, te xamal leen boppam
17Que el Dios del Señor nuestro Jesucristo, el Padre de gloria, os dé espíritu de sabiduría y de revelación para su conocimiento;
18 ci leeral seeni xol. Noonu dingeen xam yaakaaru ëllëg, ji leen Yàlla wooye, di ndam lu xel mënta daj, li nekk ci cér, bi mu dencal gaayam yu sell yi.
18Alumbrando los ojos de vuestro entendimiento, para que sepáis cuál sea la esperanza de su vocación, y cuáles las riquezas de la gloria de su herencia en los santos,
19 Ngeen xam it, ni kàttanam màgge ba jéggi dayo, jëm ci nun ñi gëm, dëppook dooleem ju ràññiku,
19Y cuál aquella supereminente grandeza de su poder para con nosotros los que creemos, por la operación de la potencia de su fortaleza,
20 ji mu jëfe ci Kirist, ci li mu ko dekkal, dëël ko ci ndeyjooram ca bérab yu kawe ya,
20La cual obró en Cristo, resucitándole de los muertos, y colocándole á su diestra en los cielos,
21 mu tiim lu sore malaaka yépp, muy kilifa, boroom sañ-sañ, boroom doole mbaa buur, te gën a màgg wépp tur wu ñu man a tudd, muy tey, muy ëllëg.
21Sobre todo principado, y potestad, y potencia, y señorío, y todo nombre que se nombra, no sólo en este siglo, mas aun en el venidero:
22 Yàlla suufeel na lépp fi kanamam, def ko kilifag lépp ci mbooloom ñi gëm,
22Y sometió todas las cosas debajo de sus pies, y diólo por cabeza sobre todas las cosas á la iglesia,
23 miy jëmmam, di matug Kirist, mi fees mbindeef mu ne ci fànn gu ne.
23La cual es su cuerpo, la plenitud de Aquel que hinche todas las cosas en todos.