1 Li jiitu tey Yàlla waxoon na ak maam ya ci wàll yu bare ak ci tëralin yu wuute jaarale ko ca yonent ya.
1DIOS, habiendo hablado muchas veces y en muchas maneras en otro tiempo á los padres por los profetas,
2 Waaye ci mujug jamono jii nu tollu, Yàlla wax na ak nun jaarale ko ci Doom ji. Doomam jooju la Yàlla jagleel lépp, te ci moom la Yàlla jaar, sàkk àddina.
2En estos porstreros días nos ha hablado por el Hijo, al cual constituyó heredero de todo, por el cual asimismo hizo el universo:
3 Doom ji moo di leer giy jollee ci ndamu Yàlla, di ki dippeekoo ci Yàlla. Moo téye àddina ci kàddoom gu am doole gi. Te bi mu ubbee bunt ba nit di selle ci ay bàkkaaram, dafa toog fa ñu koy terale ca ndeyjooru Aji Màgg ji ca kaw,
3El cual siendo el resplandor de su gloria, y la misma imagen de su sustancia, y sustentando todas las cosas con la palabra de su potencia, habiendo hecho la purgación de nuestros pecados por sí mismo, se sentó á la diestra de la Majestad en las alturas,
4 wone noonu ne, moo gën a màgg malaaka yi. Te it Yàlla jox na ko tur wu sut seen tur.
4Hecho tanto más excelente que los ángeles, cuanto alcanzó por herencia más excelente nombre que ellos.
5 Ndaxte Yàlla musul a wax kenn ci malaaka yi ne:«Yaa di sama Doom,maa di sa Baay tey.» Musul ne ci mbirum kenn ci ñoom it:«Man Yàlla, dinaa doon Baay ci moom,mu nekk Doom ci man.»
5Porque ¿á cuál de los ángeles dijo Dios jamás: Mi hijo eres tú, Hoy yo te he engendrado? Y otra vez: Yo seré á él Padre, Y él me será á mí hijo?
6 Waaye bi muy yónni Doom jooju di taaw bi ci àddina, da ne:«Na ko malaakay Yàlla yépp jaamu.»
6Y otra vez, cuando introduce al Primogénito en la tierra, dice: Y adórenle todos los ángeles de Dios.
7 Ci wàllu malaaka yi, lii la ci Yàlla wax:«Def na malaakaam yi, ñu mel ni ay ngelaw,ñooñu koy liggéeyal, mu def leen niki safara.»
7Y ciertamente de los ángeles dice: El que hace á sus ángeles espíritus, Y á sus ministros llama de fuego.
8 Waaye ci wàllu Doom ji, lii la ko Yàlla wax:«Yaw Yàlla, dinga toog ci jal bi ba fàww,ci njubte ngay nguuru.
8Mas al hijo: Tu trono, oh Dios, por el siglo del siglo; Vara de equidad la vara de tu reino;
9 Sopp nga njub te bañ lu bon.Looloo tax yaw Yàlla,sa Yàlla sol la mbég mu gën a réymi mu jagleel say àndandoo.»
9Has amado la justicia, y aborrecido la maldad; Por lo cual te ungió Dios, el Dios tuyo, Con óleo de alegría más que á tus compañeros.
10 Newaat na it:«Yaw Boroom bi,yaa sàkk àddina ca njàlbéen ga,defar asamaan yi ci sa loxoy bopp.
10Y: Tú, oh Señor, en el principio fundaste la tierra; Y los cielos son obras de tus manos:
11 Yëf yooyu dinañu wéy,waaye yaw dinga sax,dinañu màggat ñoom ñépp ni ay yére.
11Ellos perecerán, mas tú eres permanente; Y todos ellos se envejecerán como una vestidura;
12 Dinga leen taxañ ni malaan,ñu furi ni ay yére,waaye yaw doo soppiku,te sa dund amul àpp.»
12Y como un vestido los envolverás, y serán mudados; Empero tú eres el mismo, Y tus años no acabarán.
13 Waaye Yàlla musul a teral kenn ci malaaka yi, ba di ko wax:«Toogal ci sama ndeyjoor,ba kera may daaneel say noonci sa kanam.»
13Pues, ¿á cuál de los ángeles dijo jamás: Siéntate á mi diestra, Hasta que ponga á tus enemigos por estrado de tus pies?
14 Malaaka yépp ay xel lañu rekk yuy liggéeyal Yàlla, mu di leen yónni ñuy dimbali nit, ñi nar a jot mucc gi.
14¿No son todos espíritus administradores, enviados para servicio á favor de los que serán herederos de salud?