1 Su nu Kirist mayee fit nag ak mbëggeel guy dëfël sunu xol, su nu amee cér ci Xel mu Sell mi, su amee cofeel ak yërmande ci sunu bokk ci moom,
1POR tanto, si hay alguna consolación en Cristo; si algún refrigerio de amor; si alguna comunión del Espíritu; si algunas entrañas y misericordias,
2 kon mottalileen sama mbég, ci bokk benn xalaat ak genn mbëggeel, benn bakkan ak menn xel.
2Cumplid mi gozo; que sintáis lo mismo, teniendo el mismo amor, unánimes, sintiendo una misma cosa.
3 Buleen def dara ci kaw wut aw tur walla wonu, waaye jiital-leen seeni moroom cig woyof.
3Nada hagáis por contienda ó por vanagloria; antes bien en humildad, estimándoos inferiores los unos á los otros:
4 Buleen yem ci topptoo seen bopp rekk, waaye booleleen ci seeni moroom.
4No mirando cada uno á lo suyo propio, sino cada cual también á lo de los otros.
5 Te ngeen soloo xel mi nekkoon ci Kirist Yeesu:
5Haya, pues, en vosotros este sentir que hubo también en Cristo Jesús:
6 Njàlbéen ga fekk na Kirist yor melow Yàlla,waaye aakimowul taxawaayamci li mu mengoo ak Yàlla.
6El cual, siendo en forma de Dios, no tuvo por usurpación ser igual á Dios:
7 Waaye daa wàcce boppam,ba tollook nit ñi,def boppam surga.Te bi mu yoree bindu nit,
7Sin embargo, se anonadó á sí mismo, tomando forma de siervo, hecho semejante á los hombres;
8 daa suufeel boppam,di dégg ndigal, ba joxe boppam,ñu daaj ko sax ci bant.
8Y hallado en la condición como hombre, se humilló á sí mismo, hecho obediente hasta la muerte, y muerte de cruz.
9 Moo tax Yàlla kaweel ko lool,jox ko tur wi tiim yépp,
9Por lo cual Dios también le ensalzó á lo sumo, y dióle un nombre que es sobre todo nombre;
10 ngir turu Yeesoo tax ñépp sukk,ci asamaan, ci kaw suuf, ci biir suuf;
10Para que en el nombre de Jesús se doble toda rodilla de los que están en los cielos, y de los que en la tierra, y de los que debajo de la tierra;
11 te ñépp bokk genn kàddu naan:Yeesu Kirist mooy Boroom bi;ci màggug Yàlla Baay bi.
11Y toda lengua confiese que Jesucristo es el Señor, á la gloria de Dios Padre.
12 Noonu samay soppe, xam naa ne, musuleen a jóg ci dégg ndigal, waxuma sax bi ma nekkee ak yéen rekk, waaye rawatina bi ma leen soree. Kon nag maa ngi leen di ñaan, ngeen biral seen mucc ci seeni jëf, te def ko ci ragal Yàlla gu dëggu.
12Por tanto, amados míos, como siempre habéis obedecido, no como en mi presencia solamente, sino mucho más ahora en mi ausencia, ocupaos en vuestra salvación con temor y temblor;
13 Ndaxte Yàlla ci boppam mooy jëf ci yéen, ngir ngeen fonk coobareem te di ko jëfe.
13Porque Dios es el que en vosotros obra así el querer como el hacer, por su buena voluntad.
14 Lépp lu ngeen di def nag, buleen ci boole xultu mbaa xuloo.
14Haced todo sin murmuraciones y contiendas,
15 Noonu dingeen am xol bu laab bu àndul ak ŋàññ, di guney Yàlla yu amul sikk ci biir jamono ju yàqu te rëb. Dangeen di leer ci seen biir ni weer ci àddina si,
15Para que seáis irreprensibles y sencillos, hijos de Dios sin culpa en medio de la nación maligna y perversa, entre los cuales resplandecéis como luminares en el mundo;
16 di jottali kàddug dund gi. Noonu bu bésu Kirist ñëwee, dinaa man a bég, xam ne dawuma lu amul njariñ, te sonnuma cig neen.
16Reteniendo la palabra de vida para que yo pueda gloriarme en el día de Cristo, que no he corrido en vano, ni trabajado en vano.
17 Te bu sama deret waree tuuru sax, ngir seen ngëm mat sëkk, ma mel ni naan gu ñu boole ak sarax su jëm ci Yàlla, ba tey bég naa ci, te dinaa ci bégati.
17Y aun si soy derramado en libación sobre el sacrificio y servicio de vuestra fe, me gozo y congratulo por todos vosotros.
18 Yéen itam nag bégleen, waaw fekksileen ma ci sama mbég.
18Y asimismo gozaos también vosotros, y regocijaos conmigo.
19 Gannaaw loolu, bu soobee Boroom bi Yeesu, yaakaar naa ne, dinaa leen yónnee Timote balaa yàgg, ngir sama xel dal ci xam nan ngeen def.
19Mas espero en el Señor Jesús enviaros presto á Timoteo, para que yo también esté de buen ánimo, entendido vuestro estado.
20 Ndaxte amu fi kenn gannaaw Timote, ku bokk ak man xalaat te fonk leen bu wér.
20Porque á ninguno tengo tan unánime, y que con sincera afición esté solícito por vosotros.
21 Ñi ci des ñépp, seen bopp lañuy xalaat, waaye du mbiri Yeesu Kirist.
21Porque todos buscan lo suyo propio, no lo que es de Cristo Jesús.
22 Waaye xam ngeen takkuteg Timote, ci ni mu ànde ak man ci tas xebaar bu baax bi, ni doom di taxawoo baayam.
22Pero la experiencia de él habéis conocido, que como hijo á padre ha servido conmigo en el evangelio.
23 Moom laa yaakaar a yónni fi yéen nag, waxtu wu ma yégee, nu sama mbir di tëdde.
23Así que á éste espero enviaros, luego que yo viere cómo van mis negocios;
24 Waaye wóor na ma ne, Boroom bi dina ma may, man ci sama bopp, ma seetsi leen balaa yàgg.
24Y confío en el Señor que yo también iré presto á vosotros.
25 Ci lu jëm ci sama mbokk Epafrodit nag, miy sama nawle ci liggéey bi ak ci xeex bi, te di seen ndaw ci faj samay soxla, jàpp naa ne, war naa leen koo delloo.
25Mas tuve por cosa necesaria enviaros á Epafrodito, mi hermano, y colaborador y compañero de milicia, y vuestro mensajero, y ministrador de mis necesidades;
26 Ndaxte namm na leen lool, te tiisoo na li ngeen yég jagadeem.
26Porque tenía gran deseo de ver á todos vosotros, y gravemente se angustió porque habíais oído que había enfermado.
27 Ci dëgg-dëgg woppoon na ba xaw a dee, waaye Yàlla yërëm na ko, ba fëgg boppam, rax-ca-dolli siggil na ma man itam, ngir ma bañ a am tiis ci kaw tiis.
27Pues en verdad estuvo enfermo á la muerte: mas Dios tuvo misericordia de él; y no solamente de él, sino aun de mí, para que yo no tuviese tristeza sobre tristeza.
28 Noonu delloo naa leen ko ci lu gaaw, ngir ñëwam bégal seeni xol, te man itam sama xol féex.
28Así que le envío más presto, para que viéndole os volváis á gozar, y yo esté con menos tristeza.
29 Teeruleen ko teeru bu rafet nag ngir Boroom bi, te teral ñi mel ni moom.
29Recibidle pues en el Señor con todo gozo; y tened en estima á los tales:
30 Ndaxte liggéeyal na Kirist, ba riisu dee, te gar na bakkanam ci taxawal leen ci topptoo, bi ngeen yéene woon ci man.
30Porque por la obra de Cristo estuvo cercano á la muerte, poniendo su vida para suplir vuestra falta en mi servicio.