Wolof: New Testament

Spanish: Reina Valera (1909)

Revelation

14

1 Ma xool noonu, gis Mbote ma taxaw ci tundu Siyon, ànd ak téeméer ak ñeent-fukk ak ñeenti junniy nit, te ñu bind ci seen jë turu Mbote ma ak turu Baayam.
1Y MIRÉ, y he aquí, el Cordero estaba sobre el monte de Sión, y con él ciento cuarenta y cuatro mil, que tenían el nombre de su Padre escrito en sus frentes.
2 Ma dégg baat bu jóge asamaan, buy riir ni duusi géej, ni riiru dënnu gu réy. Baat ba ma dégg mel ni baati xalamkat yuy xalam.
2Y oí una voz del cielo como ruido de muchas aguas, y como sonido de un gran trueno: y oí una voz de tañedores de arpas que tañían con sus arpas:
3 Nit ñu bare ñooñu taxaw ca kanamu gàngune ma ak ñeenti mbindeef ya ak mag ña, di woy woy wu bees. Kenn mënul a jàng woy wa, ku dul téeméer ak ñeent-fukk ak ñeenti junniy nit, ñooñu ñu jote àddina.
3Y cantaban como un cántico nuevo delante del trono, y delante de los cuatro animales, y de los ancianos: y ninguno podía aprender el cántico sino aquellos ciento cuarenta y cuatro mil, los cuales fueron comprados de entre los de la tierra.
4 Ñoo di ñi taqul sobey jigéen, ndaxte saxal nañu seen bopp ci sell. Ñu nga topp Mbote ma fépp fu mu jëm. Yàlla jot na leen ci biir nit ñi, ñu jébbalu ci Yàlla ak ci Mbote mi, mel ni tànneefu ngóob mi ñuy sédde Yàlla,
4Estos son los que con mujeres no fueron contaminados; porque son vírgenes. Estos, los que siguen al Cordero por donde quiera que fuere. Estos fueron comprados de entre los hombres por primicias para Dios y para el Cordero.
5 te fen musul a génn ci seen gémmiñ. Amuñu benn sikk.
5Y en sus bocas no ha sido hallado engaño; porque ellos son sin mácula delante del trono de Dios.
6 Noonu ma gis meneen malaaka naaw ca digg asamaan, yor xebaar bi sax, di ko yégal waa àddina — xeet yépp, giir yépp, kàllaama yépp ak réew yépp.
6Y vi otro ángel volar por en medio del cielo, que tenía el evangelio eterno para predicarlo á los que moran en la tierra, y á toda nación y tribu y lengua y pueblo,
7 Ma nga doon xaacu naan: «Ragal-leen Yàlla te jox ko ndam li, ndaxte waxtuw àtteem jot na. Jaamuleen ki sàkk asamaan ak suuf ak géej ak bëti ndox yi.»
7Diciendo en alta voz: Temed á Dios, y dadle honra; porque la hora de su juicio es venida; y adorad á aquel que ha hecho el cielo y la tierra y el mar y las fuentes de las aguas.
8 Meneen malaaka, di ñaareel bi, topp ca naan: «Daanu na! Babilon, dëkk bu mag, bi daan màndil réew yépp ak biiñu njaaloom, daanu na.»
8Y otro ángel le siguió, diciendo: Ha caído, ha caído Babilonia, aquella grande ciudad, porque ella ha dado á beber á todas las naciones del vino del furor de su fornicación.
9 Meneen malaaka, di ñetteel bi, topp ca, di xaacu naan: «Ku jaamu rab wi ak nataalam te nangoo am màndargam ci jëwam walla ci loxoom,
9Y el tercer ángel los siguió, diciendo en alta voz: Si alguno adora á la bestia y á su imagen, y toma la señal en su frente, ó en su mano,
10 dina naan moom itam biiñu xadarub Yàlla bi kenn raxul, ñu sotti ko ci koppu meram. Te dees na ko mbugal ci safara ak tamarax ci kanamu malaaka yu sell yi ak Mbote mi,
10Este también beberá del vino de la ira de Dios, el cual está echado puro en el cáliz de su ira; y será atormentado con fuego y azufre delante de los santos ángeles, y delante del Cordero:
11 te saxar siy jóge ci seen mbugal dina gilli ba fàww. Ñooñu di jaamu rab wi ak nataalam, ak képp ku nangoo jot màndargam turam, duñu noppalu guddi ak bëccëg.»
11Y el humo del tormento de ellos sube para siempre jamás. Y los que adoran á la bestia y á su imagen, no tienen reposo día ni noche, ni cualquiera que tomare la señal de su nombre.
12 Looloo tax gaayi Yàlla yi war a muñ, ñooñuy sàmm ndigali Yàlla yi ak ngëm ci Yeesu.
12Aquí está la paciencia de los santos; aquí están los que guardan los mandamientos de Dios, y la fe de Jesús.
13 Noonu ma dégg baat ci asamaan naan: «Bindal: “Bés ni tey, ñi nekk ci Boroom bi te dee, barkeel nañu.”» Xelum Yàlla nee na: «Waaw, dinañu noppalu ci seeni coono, ndaxte seeni jëf a nga leen di xaar.»
13Y oí una voz del cielo que me decía: Escribe: Bienaventurados los muertos que de aquí adelante mueren en el Señor. Sí, dice el Espíritu, que descansarán de sus trabajos; porque sus obras con ellos siguen.
14 Ma xool noonu, gis niir wu weex ak ku ca toog, niroo ak doomu nit, takk kaalag wurus ca bopp ba, yor sàrt bu ñaw.
14Y miré, y he aquí una nube blanca; y sobre la nube uno sentado semejante al Hijo del hombre, que tenía en su cabeza una corona de oro, y en su mano una hoz aguda.
15 Te meneen malaaka génn ca kër Yàlla ga, di wax ak baat bu xumb ak ka toogoon ca niir wa, ne ko: «Dawalal sa sàrt te góob, ndaxte ngóob jot na, te lépp ñor na ci kaw suuf.»
15Y otro ángel salió del templo, clamando en alta voz al que estaba sentado sobre la nube: Mete tu hoz, y siega; porque la hora de segar te es venida, porque la mies de la tierra está madura.
16 Noonu ka toogoon ca kaw niir wa dawal sàrtam ci kaw suuf, góob àddina sépp.
16Y el que estaba sentado sobre la nube echó su hoz sobre la tierra, y la tierra fué segada.
17 Bi loolu amee meneen malaaka génn ca kër Yàlla ga nekk ca asamaan, yor moom itam sàrt bu ñaw.
17Y salió otro ángel del templo que está en el cielo, teniendo también una hoz aguda.
18 Noonu meneen malaaka, ma am sañ-sañ ca safara sa, jóge ca saraxalukaayu cuuraay ba, daldi wax ak baat bu xumb ak malaaka, ma yor sàrt bu ñaw ba, ne ko: «Dawalal sa sàrt bu ñaw bi te dagg céggu réseñ yu àddina, ndaxte ñor nañu.»
18Y otro ángel salió del altar, el cual tenía poder sobre el fuego, y clamó con gran voz al que tenía la hoz aguda, diciendo: Mete tu hoz aguda, y vendimia los racimos de la tierra; porque están maduras sus uvas.
19 Noonu malaaka ma daldi dawal sàrtam ci àddina, dagg réseñ yi, sànni leen ci biir segalukaay bu réy bu merum Yàlla.
19Y el ángel echó su hoz aguda en la tierra, y vendimió la viña de la tierra, y echó la uva en el grande lagar de la ira de Dios.
20 Ñu nal réseñ ya ca segalukaay, ba ca gannaaw dëkk ba, deret génn ca, ba agsi ci laabi fas yi, te wal ba ëmb lu mat ñetti téeméeri kilomet.
20Y el lagar fué hollado fuera de la ciudad, y del lagar salió sangre hasta los frenos de los caballos por mil y seiscientos estadios.