Wolof: New Testament

World English Bible

1 John

3

1 Xool-leen mbëggeel gi nu Baay bi jox, ni mu réye, ba nu man a tudd doomi Yàlla. Te moom lanu. Moo tax àddina xamu nu, ndaxte xamu ko woon, moom itam.
1Behold, how great a love the Father has bestowed on us, that we should be called children of God! For this cause the world doesn’t know us, because it didn’t know him.
2 Samay soppe, léegi doomi Yàlla lanu, te li nu nar a nekki feeñagul, waaye xam nanu ne, bés bu Almasi bi feeñee, dinanu nirook moom, ndaxte dinanu ko gis, na mu mel.
2Beloved, now we are children of God, and it is not yet revealed what we will be. But we know that, when he is revealed, we will be like him; for we will see him just as he is.
3 Te képp ku am yaakaar jooju ci moom, dinga sellal sa bopp, ni mu selle moom.
3Everyone who has this hope set on him purifies himself, even as he is pure.
4 Ku def bàkkaar, jàdd nga yoon; ndaxte bàkkaar mooy jàdd yoon.
4Everyone who sins also commits lawlessness. Sin is lawlessness.
5 Te xam ngeen ne Yeesu Kirist feeñ na, ngir dindi bàkkaar yi, te moom amul benn bàkkaar.
5You know that he was revealed to take away our sins, and in him is no sin.
6 Képp ku sax ci moom, doo sax ci bàkkaar; kuy def bàkkaar, gisuloo ko te xamuloo ko.
6Whoever remains in him doesn’t sin. Whoever sins hasn’t seen him, neither knows him.
7 Samay doom, bu leen kenn nax! Kuy def lu jub, ku jub nga, ni Kirist jube moom ci boppam.
7Little children, let no one lead you astray. He who does righteousness is righteous, even as he is righteous.
8 Kuy def bàkkaar, ci Seytaane nga bokk, ndax Seytaane ca njàlbéen ga ba tey day bàkkaar. Te Doomu Yàlla ji ñëw na, ngir nasaxal jëfi Seytaane.
8He who sins is of the devil, for the devil has been sinning from the beginning. To this end the Son of God was revealed, that he might destroy the works of the devil.
9 Ku juddu ci Yàlla doo def bàkkaar, ndax Yàlla sol na la jikkoom, te doo man a sax ci bàkkaar, ndax juddu nga ci Yàlla.
9Whoever is born of God doesn’t commit sin, because his seed remains in him; and he can’t sin, because he is born of God.
10 Lii mooy ràññale doomi Yàlla ak doomi Seytaane: képp ku dul def lu jub bokkoo ci Yàlla; naka noonu itam ku soppul sa mbokk bokkoo ci Yàlla.
10In this the children of God are revealed, and the children of the devil. Whoever doesn’t do righteousness is not of God, neither is he who doesn’t love his brother.
11 Ndaxte xebaar, bi ngeen déggoon ca ndoorte la, mooy lii: nanu bëggante,
11For this is the message which you heard from the beginning, that we should love one another;
12 te bañ a mel ni Kayin, mi bokkoon ci Ibliis, ba rey rakkam. Lu tax mu rey ko nag? Ndaxte ay jëfam dañoo bon, te yu rakkam jub.
12unlike Cain, who was of the evil one, and killed his brother. Why did he kill him? Because his works were evil, and his brother’s righteous.
13 Bokk yi, bu leen àddina bañee, buleen ci jaaxle.
13Don’t be surprised, my brothers, if the world hates you.
14 Mbëggeel gi nu bëgg sunuy bokk moo nuy xamal ne, jóge nanu ci dee, tàbbi ci dund. Ku bëggul sa mbokk, yaa ngi ci dee ba tey.
14We know that we have passed out of death into life, because we love the brothers. He who doesn’t love his brother remains in death.
15 Képp ku bañ sa mbokk, reykat nga; te xam ngeen ne, ku rey nit amuloo dund gu dul jeex.
15Whoever hates his brother is a murderer, and you know that no murderer has eternal life remaining in him.
16 Ci lii lanuy xàmmee luy mbëggeel: Kirist joxe na bakkanam ngir nun; te nun itam war nanoo joxe sunu bakkan ngir sunuy bokk.
16By this we know love, because he laid down his life for us. And we ought to lay down our lives for the brothers.
17 Waaye ku am alalu àddina te gis sa mbokk nekk ci soxla, nga dummóoyu ko, nan la mbëggeelu Yàlla dëkke ci yaw?
17But whoever has the world’s goods, and sees his brother in need, and closes his heart of compassion against him, how does the love of God remain in him?
18 Samay doom, bunu bëggante ci wax mbaa ci làmmiñ rekk, waaye ci jëf ak ci dëgg.
18My little children, let’s not love in word only, neither with the tongue only, but in deed and truth.
19 Ci loolu lanu xame ne, nu ngi ci dëgg; te waxtu wu sunu xol di xeex ak nun, dinanu ko dalal ci kanamam; ndaxte Yàllaa ëpp sunu xol te xam na lépp.
19And by this we know that we are of the truth, and persuade our hearts before him,
21 Samay soppe, bu nu sunu xol daanul, kon man nanoo jege Yàlla ak kóolute.
20because if our heart condemns us, God is greater than our heart, and knows all things.
22 Te lépp lu nu koy ñaan, dinanu ko jot ci moom, ndaxte nu ngi sàmm ay ndigalam, di def lu ko neex.
21Beloved, if our hearts don’t condemn us, we have boldness toward God;
23 Ndigalam mooy lii: nu gëm turu Doomam, Yeesu Kirist, tey bëggante, ni mu nu ko digale.
22and whatever we ask, we receive from him, because we keep his commandments and do the things that are pleasing in his sight.
24 Kuy sàmm ndigalu Yàlla, dinga sax ci moom, mu dëkk ci yaw. Te Xel mi mu nu jox, moo nuy xamal ne, dëkk na ci nun.
23This is his commandment, that we should believe in the name of his Son, Jesus Christ, and love one another, even as he commanded.
24He who keeps his commandments remains in him, and he in him. By this we know that he remains in us, by the Spirit which he gave us.