Wolof: New Testament

World English Bible

1 Peter

4

1 Gannaaw Kirist nag sonn na ci yaramam, gànnaayooleen xelam moomu, ndaxte ku sonn ci yaramam, tàggoo na ak bàkkaar.
1Forasmuch then as Christ suffered for us in the flesh, arm yourselves also with the same mind; for he who has suffered in the flesh has ceased from sin;
2 Noonu diir bi ko dese ci kaw suuf, dëddu na bànneexi bakkan, jublu ci coobareg Yàlla.
2that you no longer should live the rest of your time in the flesh for the lusts of men, but for the will of God.
3 Ndaxte àndoon ngeen démb ci xalaati ñi xamul Yàlla, di dund ciy ñaawteef ak topp seen bakkan, di màndi ak a xawaare, di xér ci biiñ ak a jaamu ay xërëm yu araam, waaye na fi yem nag.
3For we have spent enough of our past time doing the desire of the Gentiles, and having walked in lewdness, lusts, drunken binges, orgies, carousings, and abominable idolatries.
4 Ñiy jëfe noonu waaru nañu, ba di leen sosal, ci li ngeen àndul ak ñoom, sóobu ci seeni moy yu dul jeex,
4They think it is strange that you don’t run with them into the same excess of riot, blaspheming:
5 waaye dinañu mas a teew fa kanam Ki nar a àtte ñiy dund ak ñi dee.
5who will give account to him who is ready to judge the living and the dead.
6 Looloo waral it ñu jottali xebaar bu baax ndee, ya fekke woon jamonoy Nóoyin jooju, ngir ñu dunde Yàlla ci seen xel, doonte sax nit ñaa ngi leen daan fitnaal ci àddina.
6For to this end the Good News was preached even to the dead, that they might be judged indeed as men in the flesh, but live as to God in the spirit.
7 Te itam muju lépp jegesi na; nangeen maandu te foog, ba man a ñaan ci Yàlla.
7But the end of all things is near. Therefore be of sound mind, self-controlled, and sober in prayer.
8 Li gën a am solo mooy, ngeen bëggante mbëggeel gu tar, ndax mbëggeel day suul bàkkaar yu bare.
8And above all things be earnest in your love among yourselves, for love covers a multitude of sins.
9 Ganalanteleen ci lu àndul ak njàmbat.
9Be hospitable to one another without grumbling.
10 Te lu la Yàlla jagleel kenn ku nekk ci yéen, nanga ko bokk ak ñépp ni jawriñ ju jub, ci séddale yiwu Yàlla wu yaatu.
10As each has received a gift, employ it in serving one another, as good managers of the grace of God in its various forms.
11 Kuy jottali kàddug Yàlla, na mel ni Yàllaay wax. Kuy jëf it, na jëfe dooley Yàlla, ngir turu Yàlla màgg ci lépp jaar ci Yeesu Kirist, mi yelloo ndam ak kàttan ba fàww. Amiin.
11If anyone speaks, let it be as it were the very words of God. If anyone serves, let it be as of the strength which God supplies, that in all things God may be glorified through Jesus Christ, to whom belong the glory and the dominion forever and ever. Amen.
12 Yéen samay xarit, ci mbirum nattu bu tànge ni daay, bi dal ci seen kaw, bumu leen jaaxal, ba ngeen teg ko ni lu xel dajul.
12Beloved, don’t be astonished at the fiery trial which has come upon you, to test you, as though a strange thing happened to you.
13 Waaye bégleen ci cér, boobu ngeen am ci coonoy Kirist, ngir bés bu ndamam di feeñ, ngeen bég ak mbég mu ëpp xel.
13But because you are partakers of Christ’s sufferings, rejoice; that at the revelation of his glory you also may rejoice with exceeding joy.
14 Su ñu leen jànnee sax ci turu Kirist, xamleen ne ñu barkeel ngeen, ndax Xelum Yàllaa ngi ci yéen, di firndeel seen ndamu ëllëg.
14If you are insulted for the name of Christ, you are blessed; because the Spirit of glory and of God rests on you. On their part he is blasphemed, but on your part he is glorified.
15 Buñu sonal kenn ci yéen ci li mu rey nit walla mu sàcc, mbaa def lu bon, walla dugg ci lu yoonam nekkul.
15For let none of you suffer as a murderer, or a thief, or an evil doer, or a meddler in other men’s matters.
16 Waaye ku ñu sonal ndax waayu Kirist nga, bu ci rus, waaye nga màggal Yàlla ci tur woowu.
16But if one of you suffers for being a Christian, let him not be ashamed; but let him glorify God in this matter.
17 Ndaxte àpp bi jot na, àtte baa ngi tàmbalee ci nun waa kër Yàlla. Te su tàmbalee ci nun nag, luy muju ñi weddi xebaaru Yàlla?
17For the time has come for judgment to begin with the household of God. If it begins first with us, what will happen to those who don’t obey the Good News of God?
18 Te:«Su muccu ki jub jafee,luy doon muju ki weddi te dëng?»
18“If it is hard for the righteous to be saved, what will happen to the ungodly and the sinner?”
19 Kon nag ñi tegoo fitna ci coobareg Yàlla, nañu sax ci def lu baax, dénk seen bopp Yàlla, miy Bindkat biy sàmm kóllëre.
19Therefore let them also who suffer according to the will of God in doing good entrust their souls to him, as to a faithful Creator.