1 Man njiit li, maa ngi lay bind, yaw sama xarit Gayus, mi ma bëgg ci sama xol.
1The elder to Gaius the beloved, whom I love in truth.
2 Sama soppe, maa ngi ñaan, Yàlla may la jàmm ci lépp, ànd ak wér gi yaram, ju mel ni sa naataangeg xol.
2Beloved, I pray that you may prosper in all things and be healthy, even as your soul prospers.
3 Sunuy mbokk ñëw nañu, te seede ni nga fonke dëgg gi, ba wéer ci sa dund gépp, te bég naa ci lool.
3For I rejoiced greatly, when brothers came and testified about your truth, even as you walk in truth.
4 Awma mbég mu ëpp lii: ma dégg ne samay doomi diine ñu ngiy jaar ci tànki dëgg.
4I have no greater joy than this, to hear about my children walking in truth.
5 Yaw sama xarit, sa takkute fés na ci teeru bi ngay teeru mbokk yi, te fekk xamoo leen.
5Beloved, you do a faithful work in whatever you accomplish for those who are brothers and strangers.
6 Seedeel nañu sa mbëggeel fi kanam mbooloom ñi gëm. Taxawu leen nag ci seen yoon taxawu gu neex Yàlla.
6They have testified about your love before the assembly. You will do well to send them forward on their journey in a way worthy of God,
7 Ndaxte turu Krist la leen taxa jóg, te sàkkuwuñu daray ku gëmul.
7because for the sake of the Name they went out, taking nothing from the Gentiles.
8 Nun nag fàww nu teeru ñu mel ni ñoom, ngir nu liggéeyandoo ak dëgg gi.
8We therefore ought to receive such, that we may be fellow workers for the truth.
9 Bind naa mbooloo mi bataaxel, waaye Jotref, mi bëgg noot ñépp, du dégg sunu ndigal.
9I wrote to the assembly, but Diotrephes, who loves to be first among them, doesn’t accept what we say.
10 Kon nag su ma ñëwee, dinaa fàttali li mu def lépp, ci di nu sosal ci kàdduy neen yu ñaaw. Yemu foofu sax, waaye nanguwula teeru mbokk yi, rax-ca-dolli ku leen bëgga teeru, mu gàllankoor ko, dàq ko ci mbooloo mi.
10Therefore if I come, I will call attention to his deeds which he does, unjustly accusing us with wicked words. Not content with this, neither does he himself receive the brothers, and those who would, he forbids and throws out of the assembly.
11 Sama xarit, bul roy lu bon, waaye lu baax rekk. Kuy def lu baax, ci Yàlla nga bokk; kuy def lu bon, xamoo dara ci Yàlla.
11Beloved, don’t imitate that which is evil, but that which is good. He who does good is of God. He who does evil hasn’t seen God.
12 Naka Démétrius nag, ñépp seedeel nañu ko lu baax, te dëgg gi sax seedeel na ko ko. Nun itam seedeel nanu ko te wóor na ma ne, sunu seede dëgg la.
12Demetrius has the testimony of all, and of the truth itself; yes, we also testify, and you know that our testimony is true.
13 Am na lu bare, lu ma la bëggoona wax, waaye lépp xajul ci kayit.
13I had many things to write to you, but I am unwilling to write to you with ink and pen;
14 Kon yaakaar naa laa seetsi balaa yàgg, jàkkaarlook yaw, nu waxtaan ci.
14but I hope to see you soon, and we will speak face to face. Peace be to you. The friends greet you. Greet the friends by name.
15 Na jàmm ànd ak yaw. Xarit yi yépp ñu ngi lay nuyu. Nuyul nu sunuy xarit, kenn ku nekk ci turam.