1 Yéen samay bokk, bu benn gënale laal seen ngëm ci sunu Boroom Yeesu Kirist, mi soloo ndam.
1My brothers, don’t hold the faith of our Lord Jesus Christ of glory with partiality.
2 Ndaxte su ñaari nit duggee ci seen mbooloo, kii takk jaaroy wurus te sol yére yu taaru, ka ca des ñàkk te limboo ay sagar,
2For if a man with a gold ring, in fine clothing, comes into your synagogue or, meeting , and a poor man in filthy clothing also comes in;
3 ngeen teral boroom daraja ji ne ko: «Àggal ci jataay bu yiw bi,» ba noppi ngeen ne aji néew doole ji: «Taxawal fale, mbaa nga toog fi ci samay tànk,»
3and you pay special attention to him who wears the fine clothing, and say, “Sit here in a good place”; and you tell the poor man, “Stand there,” or “Sit by my footstool”;
4 kon gënale ngeen ci seen biir, ba àtte ci col, bàyyi xol.
4haven’t you shown partiality among yourselves, and become judges with evil thoughts?
5 Dégluleen yéen sama bokk yi ma bëgg, ndax Yàlla tànnul ñi néewle ci àddina, ngir ñu barele ci ngëm, tey am i cér ci nguur, gi Yàlla dig ñi ko bëgg?
5Listen, my beloved brothers. Didn’t God choose those who are poor in this world to be rich in faith, and heirs of the Kingdom which he promised to those who love him?
6 Fekk dangeen leen di toroxal! Xanaa du boroom alal yi ñoo leen di noot te di leen yóbbu fa kanam àttekat yi?
6But you have dishonored the poor man. Don’t the rich oppress you, and personally drag you before the courts?
7 Ndax duñu tilimal tur wu tedd, wi ngeen di wuyoo?
7Don’t they blaspheme the honorable name by which you are called?
8 Su ngeen sàmmee yoonu Buur Yàlla, ni ko Mbind mi tërale naan: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp,» kon def ngeen lu baax.
8However, if you fulfill the royal law, according to the Scripture, “You shall love your neighbor as yourself,” Leviticus 19:18 you do well.
9 Waaye su ngeen gënalee, bàkkaar ngeen, te yoonu Yàlla dina leen dab ni ñu moy.
9But if you show partiality, you commit sin, being convicted by the law as transgressors.
10 Ndaxte ku sàmm yoon wépp, waaye xëtt ci lenn ndigal rekk, jàdd nga yoon wépp.
10For whoever keeps the whole law, and yet stumbles in one point, he has become guilty of all.
11 Ndaxte Yàlla mi ne: «Bul njaaloo,» teg na ca ne: «Bul rey nit.» Ku njaaloowul nag, waaye nga rey nit, jàdd nga yoon wépp.
11For he who said, “Do not commit adultery,” Exodus 20:14; Deuteronomy 5:18 also said, “Do not commit murder.” Exodus 10:13; Deuteronomy 5:17 Now if you do not commit adultery, but murder, you have become a transgressor of the law.
12 Gannaaw dingeen nar a jaar ci àtteb yoon, wiy goreel, na loolu lal seen wax ak seen jëf.
12So speak, and so do, as men who are to be judged by a law of freedom.
13 Ndaxte ku yërëmul, yoon du la yërëm. Te yërmande mooy noot àtte.
13For judgment is without mercy to him who has shown no mercy. Mercy triumphs over judgment.
14 Te lii itam samay bokk, ku ne gëm nga, te jëfewoo ko, loolu lu muy jariñ? Ndax googu ngëm man na laa musal?
14What good is it, my brothers, if a man says he has faith, but has no works? Can faith save him?
15 Su amee mbokk ci seen biir, mu rafle te amul dund, muy góor walla jigéen,
15And if a brother or sister is naked and in lack of daily food,
16 te kenn ci yéen ne ko: «Demal ak jàmm, nga solu te lekk,» te fekk fajuleen aajoom, loolu lu muy jariñ?
16and one of you tells them, “Go in peace, be warmed and filled”; and yet you didn’t give them the things the body needs, what good is it?
17 Noonu ngëm gu àndul ak jëf, amul benn njariñ.
17Even so faith, if it has no works, is dead in itself.
18 Waaye xanaa dina am ku ne: «Yaw am nga ngëm, man am naa ay jëf.» Yaw nag won ma sa ngëm gu àndul ak jëf, man ma feeñal la sama ngëm ci samay jëf.
18Yes, a man will say, “You have faith, and I have works.” Show me your faith without works, and I by my works will show you my faith.
19 Gëm nga ne Yàlla kenn la; loolu lu baax la, waaye xamal ne, jinne yi it gëm nañu loolu, ba dañoo tiit bay lox.
19You believe that God is one. You do well. The demons also believe, and shudder.
20 Yaw mi gàtt xel, kaay ma won la ne, ngëm gu àndul ak jëf, amul njariñ.
20But do you want to know, vain man, that faith apart from works is dead?
21 Sunu maam Ibraayma, ndax du ci kaw jëf la ko Yàlla àttee ni ku jub, ci li mu joxe doomam Isaaxa ni sarax?
21Wasn’t Abraham our father justified by works, in that he offered up Isaac his son on the altar?
22 Kon gis nga ne, ngëm dafa lëngoo ak ay jëfam, te ngëmam mat ci kaw jëf jooju.
22You see that faith worked with his works, and by works faith was perfected;
23 Noonu li ñu wax ci Mbind mi am na, bi mu naan: «Ibraayma gëm na Yàlla, te Yàlla jàppe ngëmam ni njub,» ba ñu ko wooye xaritu Yàlla.
23and the Scripture was fulfilled which says, “Abraham believed God, and it was accounted to him as righteousness”; Genesis 15:6 and he was called the friend of God.
24 Kon nag gis nga ne, Yàlla ci jëf lay àtte nit ni ku jub, waaye du ci kaw ngëm kese.
24You see then that by works, a man is justified, and not only by faith.
25 Naka Raxab jigéenu moykat bi itam, ndax du ci noonu la ko Yàlla àttee ni ku jub, ci li mu teeru ndawi Yawut yi, te jaarale leen ca poot ba?
25In the same way, wasn’t Rahab the prostitute also justified by works, in that she received the messengers, and sent them out another way?
26 Kon nag ni jëmm ju amul ruu nekke ndee, noonu la ngëm gu àndul ak jëf nasaxe.
26For as the body apart from the spirit is dead, even so faith apart from works is dead.