Wolof: New Testament

World English Bible

James

5

1 Dégluleen yéen boroom alal yi, jooyleen te naqarlu ndax mbugal, gi leen di xaar.
1Come now, you rich, weep and howl for your miseries that are coming on you.
2 Seen alal seey na, seen yére yi maxe na,
2Your riches are corrupted and your garments are moth-eaten.
3 seen wurus ak seen xaalis xomaag na. Te xomaag jooju seede lay doon, su leen di daanlu, ba lakk leen ni safara. Dajale ngeen alal ju ne gàññ, te fekk yéena ngi ci muju jamono.
3Your gold and your silver are corroded, and their corrosion will be for a testimony against you, and will eat your flesh like fire. You have laid up your treasure in the last days.
4 Dégluleen, jooyi xaalis bi ngeen sàcce ci gubkat, yi leen doon liggéeyal, ak yuuxi góobkat yi, dugg nañu ci noppi Yàlla Aji Kàttan ji.
4Behold, the wages of the laborers who mowed your fields, which you have kept back by fraud, cry out, and the cries of those who reaped have entered into the ears of the Lord of Armies .
5 Ci barele ak bànneex ngeen dunde ci kaw suuf, di yafal seen bopp, fekk bésu rendi baa ngii.
5You have lived delicately on the earth, and taken your pleasure. You have nourished your hearts as in a day of slaughter.
6 Daan ngeen ku jub, ba rey ko sax, te bañul.
6You have condemned, you have murdered the righteous one. He doesn’t resist you.
7 Yéen samay bokk, muñleen, ba Boroom bi dellusi ci ndamam. Seetleen ci beykat bi, ni muy xaare njariñ ci meññeefu suuf, tey muñ, céebo ba bët wàcc.
7Be patient therefore, brothers, until the coming of the Lord. Behold, the farmer waits for the precious fruit of the earth, being patient over it, until it receives the early and late rain.
8 Yéen itam nag muñleen te dëgëral seen xol, xam ne ñëwu Boroom bi ci ndamam jege na.
8You also be patient. Establish your hearts, for the coming of the Lord is at hand.
9 Buleen jàmbatante, samay bokk, ngir ragal Yàlla àtte leen. Àttekat baa ngi ci bunt bi sax!
9Don’t grumble, brothers, against one another, so that you won’t be judged. Behold, the judge stands at the door.
10 Bokk yi, defleen yonent, yi wax ci turu Boroom bi, seeni royukaay ci muñ tiis ak ci góor-góorlu.
10Take, brothers, for an example of suffering and of patience, the prophets who spoke in the name of the Lord.
11 Xam ngeen ne ñiy góor-góorlu, ñu barkeel lañu. Dégg ngeen muñ ga Ayóoba amoon, te gis muj gu rafet, ga ko Boroom bi jagleel, ndax Boroom bi kuy ñeewante la te bare yërmande.
11Behold, we call them blessed who endured. You have heard of the patience of Job, and have seen the Lord in the outcome, and how the Lord is full of compassion and mercy.
12 Te li fi raw samay bokk, buleen waat mukk, bu muy ci asamaan mbaa ci suuf mbaa ci leneen lu mu man a doon. Nangeen yem ci: «Waaw,» ak «Déedéet,» ngir bañ cee layoo fa kanam Yàlla.
12But above all things, my brothers, don’t swear, neither by heaven, nor by the earth, nor by any other oath; but let your “yes” be “yes,” and your “no,” “no”; so that you don’t fall into hypocrisy.
13 Su amee ci yéen ku nekk ci tiis, na ñaan ci Yàlla. Ku nekk ci mbég, na sant Yàlla ciy woy.
13Is any among you suffering? Let him pray. Is any cheerful? Let him sing praises.
14 Su amee ci yéen ku wopp, na woo njiiti mbooloo mi, ñu ñaanal ko te diw boppam ci turu Boroom bi.
14Is any among you sick? Let him call for the elders of the assembly, and let them pray over him, anointing him with oil in the name of the Lord,
15 Te ñaan gu ànd ak ngëm dina musal ki wopp, ba Boroom bi yékkati ko. Te su ko fekkoon ak i bàkkaar sax, Yàlla dina ko baal.
15and the prayer of faith will heal him who is sick, and the Lord will raise him up. If he has committed sins, he will be forgiven.
16 Kon nag waxanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ngir ngeen wér. Ñaanu aji jub gu dëggu, dooleem amul kem.
16Confess your offenses to one another, and pray for one another, that you may be healed. The insistent prayer of a righteous person is powerfully effective.
17 Naka noonu Iliyas nit la woon ku bindoo ni nun, waaye bi mu saxee ci ñaan Yàlla, ngir mu bañ a taw, ndox laalul suuf diirub ñetti at ak genn-wàll.
17Elijah was a man with a nature like ours, and he prayed earnestly that it might not rain, and it didn’t rain on the earth for three years and six months.
18 Gannaaw ga mu dellu ñaan, asamaan daldi taw, te suuf si saxal meññeef.
18He prayed again, and the sky gave rain, and the earth brought forth its fruit.
19 Samay bokk, su amee ci yéen ku réere dëgg, te am ku ko gindi,
19Brothers, if any among you wanders from the truth, and someone turns him back,
20 na xam lii: ku gindi bàkkaarkat ci réeram, musal nga nit ci dee te faral ko bàkkaar yu bare.
20let him know that he who turns a sinner from the error of his way will save a soul from death, and will cover a multitude of sins.