Wolof: New Testament

World English Bible

John

15

1 «Man maay garab gu wóor gi, te sama Baay mooy beykat bi.
1 “I am the true vine, and my Father is the farmer.
2 Car bu soqikoo ci man te meññul, dina ko dog, sànni. Waaye car bu ci meññ, dina ko tenqi, ngir mu gën a meññ.
2 Every branch in me that doesn’t bear fruit, he takes away. Every branch that bears fruit, he prunes, that it may bear more fruit.
3 Yéen nag, Baay bi setal na leen jaarale ko ci kàddu gi ma leen wax, ni beykat di tenqee garabam.
3 You are already pruned clean because of the word which I have spoken to you.
4 Saxleen ci man; ma sax, man itam, ci yéen. Ni car mënul a ame ay doom, bu saxul ci garab, noonu itam dungeen man a meññ li may jëfe ci yéen, bu ngeen saxul ci man.
4 Remain in me, and I in you. As the branch can’t bear fruit by itself, unless it remains in the vine, so neither can you, unless you remain in me.
5 «Man maay garab gi; yéen yéenay car yi. Ki sax ci man te ma sax ci moom, dina meññ, ndaxte bu ngeen saxul ci man, dungeen man dara.
5 I am the vine. You are the branches. He who remains in me, and I in him, the same bears much fruit, for apart from me you can do nothing.
6 Ku saxul ci man dinañu ko sànni ci biti, mu mel ni car bu ñu dagg, ba mu wow. Car yu wow nag, dañu leen di buub, sànni ci safara, ñu lakk.
6 If a man doesn’t remain in me, he is thrown out as a branch, and is withered; and they gather them, throw them into the fire, and they are burned.
7 Bu ngeen saxee ci man te saxal samay wax ci seen xol, lu ngeen ñaan mu nangu.
7 If you remain in me, and my words remain in you, you will ask whatever you desire, and it will be done for you.
8 Liy feeñal sama ndamu Baay moo di, ngeen di gën a meññ tey wone noonu ne, samay taalibe ngeen.
8 “In this is my Father glorified, that you bear much fruit; and so you will be my disciples.
9 «Ni ma Baay bi bëggee, noonu itam laa leen bëgge. Saxleen ci mbëggeel googu ma am ci yéen.
9 Even as the Father has loved me, I also have loved you. Remain in my love.
10 Bu ngeen toppee samay ndigal, dingeen sax ci sama mbëggeel, ni ma toppe sama ndigali Baay, ba tax ma sax ci mbëggeelam.
10 If you keep my commandments, you will remain in my love; even as I have kept my Father’s commandments, and remain in his love.
11 Wax naa leen loolu, ngir ngeen bokk ci sama mbég, te seen bos mat sëkk.
11 I have spoken these things to you, that my joy may remain in you, and that your joy may be made full.
12 Sama ndigal mooy ngeen bëggante, ni ma leen bëgge.
12 “This is my commandment, that you love one another, even as I have loved you.
13 Genn mbëggeel mënul a weesu joxe sa bakkan ngir say xarit.
13 Greater love has no one than this, that someone lay down his life for his friends.
14 Samay xarit ngeen, ci kaw ngeen def li ma santaane.
14 You are my friends, if you do whatever I command you.
15 Dootuma leen wooye jaam, ndaxte jaam du xam li sangam di def. Xarit laa leen wooye, ndaxte xamal naa leen li ma jële lépp ci sama Baay.
15 No longer do I call you servants, for the servant doesn’t know what his lord does. But I have called you friends, for everything that I heard from my Father, I have made known to you.
16 Du yéen yéena ma tànn, waaye man maa leen tànn, sas leen ngeen dem, meññ meññeef gu sax, ngir Baay bi def lu ngeen ko ñaan ci sama tur.
16 You didn’t choose me, but I chose you, and appointed you, that you should go and bear fruit, and that your fruit should remain; that whatever you will ask of the Father in my name, he may give it to you.
17 Li may santaane nag, mooy ngeen bëggante.
17 “I command these things to you, that you may love one another.
18 «Bu leen àddina bañee, xamleen ne, man lañu jëkk a bañ.
18 If the world hates you, you know that it has hated me before it hated you.
19 Ñi bokk ci ñoom lañu bëgg. Bu ngeen bokkoon ci ñoom, dinañu leen bëgg, ni ñu bëgge seeni ñoñ. Waaye bokkuleen ci àddina, ndaxte maa leen tànn, ber leen. Looloo tax ñu bañ leen.
19 If you were of the world, the world would love its own. But because you are not of the world, since I chose you out of the world, therefore the world hates you.
20 Fàttalikuleen li ma leen wax: “Jaam gënul a màgg sangam.” Bu ñu ma sonalee, dinañu leen sonal yéen itam. Bu ñu toppee sama wax, dinañu topp seen wax yéen itam.
20 Remember the word that I said to you: ‘A servant is not greater than his lord.’ If they persecuted me, they will also persecute you. If they kept my word, they will keep yours also.
21 Waaye loolu lépp dinañu leen ko def ndax man, ndaxte xamuñu ki ma yónni.
21 But all these things will they do to you for my name’s sake, because they don’t know him who sent me.
22 Su ma ñëwul woon, ne leen dara, duñu am bàkkaar. Waaye léegi amuñu lay ngir seeni bàkkaar.
22 If I had not come and spoken to them, they would not have had sin; but now they have no excuse for their sin.
23 Ku ma bañ, bañ nga itam sama Baay.
23 He who hates me, hates my Father also.
24 Su ma deful woon ci seen biir jëf yu kenn deful, kon duñu am bàkkaar. Waaye léegi nag gis nañu samay jëf te teewul ñu bañ nu, man ak sama Baay.
24 If I hadn’t done among them the works which no one else did, they wouldn’t have had sin. But now have they seen and also hated both me and my Father.
25 Waaye loolu am na ngir kàddu gi am, kàddu gii ñu bind ci seen yoon: “Bañ nañu ma ci dara.”
25 But this happened so that the word may be fulfilled which was written in their law, ‘They hated me without a cause.’
26 «Dimbalikat bi dina ñëw, mooy Xel mi jóge ci Baay bi tey yor dëgg gi. Dina jóge ci Baay bi, ma yebal ko ci yéen. Moom nag, moo may seedeeli.
26 “When the Counselor has come, whom I will send to you from the Father, the Spirit of truth, who proceeds from the Father, he will testify about me.
27 Te yéen itam dingeen seede samay mbir, ndaxte yéena nekkoon ak man ca njàlbéen ga.
27 You will also testify, because you have been with me from the beginning.