1 Benn bés Yeesu doon jàngal nit ña ca kër Yàlla ga, di leen yégal xebaar bu baax bi. Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya ñëw ne ko:
1It happened on one of those days, as he was teaching the people in the temple and preaching the Good News, that the TR adds “chief” priests and scribes came to him with the elders.
2 «Wax nu ci ban sañ-sañ ngay defe yëf yii, walla kan moo la may boobu sañ-sañ.»
2They asked him, “Tell us: by what authority do you do these things? Or who is giving you this authority?”
3 Yeesu tontu leen ne: «Man itam dinaa leen laaj lenn: wax leen ma,
3He answered them, “I also will ask you one question. Tell me:
4 la Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?»
4 the baptism of John, was it from heaven, or from men?”
5 Ñu waxtaan ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?”
5They reasoned with themselves, saying, “If we say, ‘From heaven,’ he will say, ‘Why didn’t you believe him?’
6 Te bu nu nee: “Ci nit ñi,” mbooloo mépp dinañu nu sànni ay xeer, ndaxte gëm nañu ne Yaxya yonent la woon.»
6But if we say, ‘From men,’ all the people will stone us, for they are persuaded that John was a prophet.”
7 Noonu ñu tontu ne, xamuñu fu mu ko jële.
7They answered that they didn’t know where it was from.
8 Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.»
8Jesus said to them, “Neither will I tell you by what authority I do these things.”
9 Noonu Yeesu daldi wax nit ña léeb wii: «Amoon na nit ku jëmbët toolu réseñ, batale ko ay beykat, dem tukki tukki bu yàgg.
9He began to tell the people this parable. “A NU (in brackets) and TR add “certain” man planted a vineyard, and rented it out to some farmers, and went into another country for a long time.
10 Bi tool bi ñoree nag, mu yónni surga ci ñoom, ngir jot wàllam ci meññeef gi. Waaye beykat yi dóor ko ay yar, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen.
10 At the proper season, he sent a servant to the farmers to collect his share of the fruit of the vineyard. But the farmers beat him, and sent him away empty.
11 Mu yónniwaat beneen surga, ñu dóor ko moom itam, toroxal ko, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen.
11 He sent yet another servant, and they also beat him, and treated him shamefully, and sent him away empty.
12 Mu yónneeti ñetteelu surga, ñu gaañ ko, dàq ko.
12 He sent yet a third, and they also wounded him, and threw him out.
13 «Boroom tool ba daldi ne: “Nan laay def nag? Dinaa yónni sama doom, sama reeni xol. Xëy na ñu weg ko, moom.”
13 The lord of the vineyard said, ‘What shall I do? I will send my beloved son. It may be that seeing him, they will respect him.’
14 Waaye bi beykat yi gisee doom ji, ñu ne ci seen biir: “Kii moo war a donn tool bi; nan ko rey, moom ndono li.”
14 “But when the farmers saw him, they reasoned among themselves, saying, ‘This is the heir. Come, let’s kill him, that the inheritance may be ours.’
15 Ñu génne ko tool bi nag, rey ko.» Noonu Yeesu laaj leen: «Nu leen boroom tool bi di def, nag?
15 They threw him out of the vineyard, and killed him. What therefore will the lord of the vineyard do to them?
16 Xanaa ñëw, rey beykat yooyu, dénk tool ba ñeneen.» Bi Yeesu waxee loolu, nit ña ne ko: «Yàlla tere!»
16 He will come and destroy these farmers, and will give the vineyard to others.” When they heard it, they said, “May it never be!”
17 Waaye Yeesu ne leen jàkk, daldi ne: «Kon nag lu baat yii ci Mbind mi di tekki:“Doj wa tabaxkat ya sànni,mujj na di doju koñ.”
17But he looked at them, and said, “Then what is this that is written, ‘The stone which the builders rejected, the same was made the chief cornerstone?’ Psalm 118:22
18 Képp ku dal ci doj woowu, dammtoo, te ku mu dal ci sa kaw, rajaxe la.»
18 Everyone who falls on that stone will be broken to pieces, but it will crush whomever it falls on to dust.”
19 Xutbakat ya ak saraxalekat yu mag ya ñu ngi doon wut a jàpp Yeesu ca taxawaay ba, ndaxte xam nañu ne, ñoo tax mu wax léeb woowu. Waaye ragal nañu mbooloo ma.
19The chief priests and the scribes sought to lay hands on him that very hour, but they feared the people—for they knew he had spoken this parable against them.
20 Noonu ñu koy yeeru, daldi yónni ay nit ñu mbubboo njub, sas leen ñu fexe koo jàpp ci ay waxam, ngir jébbal ko boroom réew, ma yor kilifteef ak sañ-sañ.
20They watched him, and sent out spies, who pretended to be righteous, that they might trap him in something he said, so as to deliver him up to the power and authority of the governor.
21 Ñu daldi ñëw ci Yeesu ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne li ngay wax te di ko jàngale lu jub la. Amuloo parlàqu, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor.
21They asked him, “Teacher, we know that you say and teach what is right, and aren’t partial to anyone, but truly teach the way of God.
22 Wax nu, ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag walla déet.»
22Is it lawful for us to pay taxes to Caesar, or not?”
23 Waaye Yeesu xam na seen pexe ne leen:
23But he perceived their craftiness, and said to them, “Why do you test me?
24 «Wonleen ma posetu denariyon. Kan lañu ci def nataalam ak turam?» Ñu tontu ko: «Sesaar.»
24 Show me a denarius. Whose image and inscription are on it?” They answered, “Caesar’s.”
25 Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.»
25He said to them, “Then give to Caesar the things that are Caesar’s, and to God the things that are God’s.”
26 Noonu mënuñu ko woon a jàpp ciy waxam ci kanamu mbooloo ma; ñu waaru ci tontoom, ba wedam.
26They weren’t able to trap him in his words before the people. They marveled at his answer, and were silent.
27 Noonu ay nit, ñu bokk ci Sadusen yi, ñëw ci moom. Sadusen yi nag ñoom weddi nañu ndekkite li. Noonu ñu laaj ko ne:
27Some of the Sadducees came to him, those who deny that there is a resurrection.
28 «Kilifa gi, Musaa bindal na nu ne, ku magam faatu te bàyyiwul doom ak jabaram, kooku war na donn jigéen ji, ba yékkati giiru magam.
28They asked him, “Teacher, Moses wrote to us that if a man’s brother dies having a wife, and he is childless, his brother should take the wife, and raise up children for his brother.
29 Amoon na fi nag juróom-ñaari góor ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba takk jabar, faatu, te bàyyiwul doom.
29There were therefore seven brothers. The first took a wife, and died childless.
30 Ñaareel ba takk jigéen ja, def noonu; ak ñetteel ba, ba juróom-ñaar ñépp faatu te bàyyiwuñu doom.
30The second took her as wife, and he died childless.
32 Gannaaw ga nag jigéen ja it faatu.
31The third took her, and likewise the seven all left no children, and died.
33 Ci ndekkite li nag, kan ci ñoom moo war a donn jigéen ja, fekk ku nekk ci juróom-ñaar ñi mas na koo takk?»
32Afterward the woman also died.
34 Yeesu tontu leen ne: «Ci àddina sii, góor ñi ak jigéen ñi dañuy séy.
33Therefore in the resurrection whose wife of them will she be? For the seven had her as a wife.”
35 Waaye ña ñu àtte ne, yeyoo nañoo bokk ci dundu ëllëg ak ci ndekkite li, kenn du am jabar, kenn du am jëkkër.
34Jesus said to them, “The children of this age marry, and are given in marriage.
36 Dafa fekk ne mënatuñoo dee, ndaxte dañuy mel ni malaaka yi. Ay doomi Yàlla lañu ndaxte doomi ndekkite lañu.
35 But those who are considered worthy to attain to that age and the resurrection from the dead, neither marry, nor are given in marriage.
37 Te Musaa sax wone na ne, néew yi dinañu dekki, ci saarum ngarab si. Foofa Musaa wooye na fa Boroom bi: “Yàllay Ibraayma, Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba.”
36 For they can’t die any more, for they are like the angels, and are children of God, being children of the resurrection.
38 Kon nag nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la, ndaxte Yàllaa tax ñépp di dund.»
37 But that the dead are raised, even Moses showed at the bush, when he called the Lord ‘The God of Abraham, the God of Isaac, and the God of Jacob.’ Exodus 3:6
39 Ci kaw loolu ay xutbakat ne ko: «Li nga wax dëgg la, kilifa gi!»
38 Now he is not the God of the dead, but of the living, for all are alive to him.”
40 Ndaxte kenn ci ñoom ñemeetu koo laaj dara.
39Some of the scribes answered, “Teacher, you speak well.”
41 Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nit ñi di wax ne, Almasi bi mooy sëtu Daawuda?
40They didn’t dare to ask him any more questions.
42 Ndaxte Daawuda moom ci boppam moo ne ci Sabóor:“Boroom bi nee na sama Boroom:‘Toogal ci sama ndeyjoor,
41He said to them, “Why do they say that the Christ is David’s son?
43 ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam.’ ”
42 David himself says in the book of Psalms, ‘The Lord said to my Lord, “Sit at my right hand,
44 Gannaaw Daawuda nag wooye na ko “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?»
43 until I make your enemies the footstool of your feet.”’ Psalm 110:1
45 Bi ko nit ña fa nekkoon ñépp doon déglu, Yeesu ne ay taalibeem:
44 “David therefore calls him Lord, so how is he his son?”
46 «Moytuleen xutbakat yi; dañoo bëgg di doxantu, sol ay mbubb yu réy, te ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ci pénc mi. Ci jàngu yi, toogu yu féete kanam lañuy wut, te toogu yu yiw lañuy taamu ci reeri xew yi.
45In the hearing of all the people, he said to his disciples,
47 Ñu ngi lekk alalu jigéen ñi seen jëkkër faatu, di ñaan Yàlla ay ñaani ngistal yu gudd. Seen mbugal dina gën a tar.»
46 “Beware of the scribes, who like to walk in long robes, and love greetings in the marketplaces, the best seats in the synagogues, and the best places at feasts;
47 who devour widows’ houses, and for a pretense make long prayers: these will receive greater condemnation.”