Wolof: New Testament

World English Bible

Mark

11

1 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jege nañu Yerusalem, ba agsi dëkki Betfase ak Betani ci wetu tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal ñaar ciy taalibeem,
1When they drew near to Jerusalem, to Bethsphage and Bethany, at the Mount of Olives, he sent two of his disciples,
2 ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn musul a war. Yiwileen ko, indi.
2and said to them, “Go your way into the village that is opposite you. Immediately as you enter into it, you will find a young donkey tied, on which no one has sat. Untie him, and bring him.
3 Bu leen kenn nee: “Lu ngeen di def?” tontuleen ko: “Boroom bi da koo soxla, te léegi mu delloosi ko.”»
3 If anyone asks you, ‘Why are you doing this?’ say, ‘The Lord needs him;’ and immediately he will send him back here.”
4 Taalibe ya dem nag, ñu gis cumbur ga ci mbedd mi, mu yeewe cib buntu kër.
4They went away, and found a young donkey tied at the door outside in the open street, and they untied him.
5 Bi ñu koy yiwi nag, am na ca ña fa taxaw, ñu ne leen: «Lu ngeen nar, bay yiwi cumbur gi?»
5Some of those who stood there asked them, “What are you doing, untying the young donkey?”
6 Taalibe yi tontu leen, ni leen Yeesu digale woon, kon nit ñi bàyyi leen, ñu dem.
6They said to them just as Jesus had said, and they let them go.
7 Ñu indi cumbur gi Yeesu nag, lal ci seeni yére, mu toog ci.
7They brought the young donkey to Jesus, and threw their garments on it, and Jesus sat on it.
8 Ñu bare lal seeni yére ci yoon wi, ñenn ñi dagg ay cari garab ci tool yi, lal leen it ci yoon wi.
8Many spread their garments on the way, and others were cutting down branches from the trees, and spreading them on the road.
9 Ñiy jiitu ak ñiy topp ci Yeesu ñépp di wax ci kaw naan:«Osaana!Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!
9Those who went in front, and those who followed, cried out, “Hosanna ! Blessed is he who comes in the name of the Lord!
10 Nguuru sunu maam Daawuda giy ñëw,dina barkeel!Ci bérab yu gën a kawe,nañu ne: “Osaana!”»
10Blessed is the kingdom of our father David that is coming in the name of the Lord! Hosanna in the highest!”
11 Noonu Yeesu dugg Yerusalem, dem kër Yàlla ga, xool lépp, ba noppi génn dem dëkku Betani, moom ak fukki taalibe ya ak ñaar, ndaxte dafa guddi.
11Jesus entered into the temple in Jerusalem. When he had looked around at everything, it being now evening, he went out to Bethany with the twelve.
12 Bët set ñu génn Betani, fekk Yeesu xiif.
12The next day, when they had come out from Bethany, he was hungry.
13 Noonu mu séen fu sore garabu figg gu sëq, mu dem seeti, ndax am na ay doom. Waaye bi mu fa eggee, gisul lu dul ay xob, ndaxte jamonoy figg duggagul.
13Seeing a fig tree afar off having leaves, he came to see if perhaps he might find anything on it. When he came to it, he found nothing but leaves, for it was not the season for figs.
14 Ci kaw loolu mu ne garab gi: «Dootuloo meññ mukk!» Taalibe yi dégg loolu mu wax.
14Jesus told it, “May no one ever eat fruit from you again!” and his disciples heard it.
15 Bi ñu eggee Yerusalem, Yeesu dugg ci kër Yàlla gi, daldi dàq ñi fay jaay ak ñi fay jënd. Mu daaneel taabali weccikatu xaalis yi ak tooguy jaaykati pitax yi,
15They came to Jerusalem, and Jesus entered into the temple, and began to throw out those who sold and those who bought in the temple, and overthrew the tables of the money changers, and the seats of those who sold the doves.
16 te mayul kenn, mu yóbbu am njaay ci kër Yàlla gi.
16He would not allow anyone to carry a container through the temple.
17 Mu di leen jàngal ne leen: «Ndax waxuñu ci Mbind mi:“Dees na wooye sama kërkëru ñaan ci Yàlla ngir xeet yépp”? Waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.»
17He taught, saying to them, “Isn’t it written, ‘My house will be called a house of prayer for all the nations?’ But you have made it a den of robbers!”
18 Bi ko saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya déggee nag, ñu ragal ko, ndaxte mbooloo mépp dañoo waaru ci njàngaleem. Noonu ñu seet pexem reylu ko.
18The chief priests and the scribes heard it, and sought how they might destroy him. For they feared him, because all the multitude was astonished at his teaching.
19 Bi timis jotee Yeesu ak taalibe yi génn dëkk bi.
19When evening came, he went out of the city.
20 Ci suba si, bi ñuy dem, ñu gis ne garabu figg gi dee na, ba wow koŋŋ.
20As they passed by in the morning, they saw the fig tree withered away from the roots.
21 Noonu Piyeer fàttaliku li xewoon, ne Yeesu: «Kilifa gi, xoolal, figg gi nga rëbb dee na, ba wow!»
21Peter, remembering, said to him, “Rabbi, look! The fig tree which you cursed has withered away.”
22 Yeesu tontu ne: «Gëmleen Yàlla.
22Jesus answered them, “Have faith in God.
23 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ku ne tund wale: “Jógal, tàbbi ca géej ga,” te nga gëm ne loolu dina am, bañ cee boole xel ñaar, kon sa ñaan nangu.
23 For most certainly I tell you, whoever may tell this mountain, ‘Be taken up and cast into the sea,’ and doesn’t doubt in his heart, but believes that what he says is happening; he shall have whatever he says.
24 Moo tax maa ngi leen koy wax, bu ngeen di ñaan Yàlla, lépp lu ngeen ko man a laaj, gëmleen ne jot ngeen ko, te dingeen ko am.
24 Therefore I tell you, all things whatever you pray and ask for, believe that you have received them, and you shall have them.
25 Te it bu ngeen di ñaan, fekk ngeen jàppal kenn dara, baal-leen ko, ngir seen Baay bi ci kaw baal leen seeni tooñ, yéen itam.»
25 Whenever you stand praying, forgive, if you have anything against anyone; so that your Father, who is in heaven, may also forgive you your transgressions.
27 Gannaaw loolu ñu duggaat Yerusalem, te Yeesu doon doxantu ca ëtti kër Yàlla ga. Noonu saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya dab ko
26 But if you do not forgive, neither will your Father in heaven forgive your transgressions.”
28 ne ko: «Yëf yii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe? Te ku la may sañ-sañu def ko?»
27They came again to Jerusalem, and as he was walking in the temple, the chief priests, and the scribes, and the elders came to him,
29 Yeesu tontu leen: «Man itam dinaa leen laaj lenn; bu ngeen ma ci tontoo, kon dinaa leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.
28and they began saying to him, “By what authority do you do these things? Or who gave you this authority to do these things?”
30 La Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?»
29Jesus said to them, “I will ask you one question. Answer me, and I will tell you by what authority I do these things.
31 Bi ñu ko déggee, ñuy werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” kon dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?”
30 The baptism of John—was it from heaven, or from men? Answer me.”
32 Waaye bu nu nee: “Ci nit ñi,” kon mbooloo mi dal ci sunu kaw;» ndaxte ñépp teg nañu Yaxya ab yonent.
31They reasoned with themselves, saying, “If we should say, ‘From heaven;’ he will say, ‘Why then did you not believe him?’
33 Ñu tontu Yeesu nag ne: «Loolu de xamunu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.»
32If we should say, ‘From men’”—they feared the people, for all held John to really be a prophet.
33They answered Jesus, “We don’t know.” Jesus said to them, “Neither do I tell you by what authority I do these things.”