Wolof: New Testament

World English Bible

Matthew

1

1 Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma.
1The book of the genealogy of Jesus Christ , the son of David, the son of Abraham.
2 Ibraayma moo jur Isaaxa; Isaaxa jur Yanqóoba; Yanqóoba jur Yuda ak i doomi baayam;
2Abraham became the father of Isaac. Isaac became the father of Jacob. Jacob became the father of Judah and his brothers.
3 Yuda, Fares ak Sara ci Tamar; Fares Esrom, miy baayu Aram;
3Judah became the father of Perez and Zerah by Tamar. Perez became the father of Hezron. Hezron became the father of Ram.
4 Aram Aminadab; Aminadab Naason; Naason Salmon;
4Ram became the father of Amminadab. Amminadab became the father of Nahshon. Nahshon became the father of Salmon.
5 Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas; Bowas am ak Ruut Obedd; Obedd jur Yese,
5Salmon became the father of Boaz by Rahab. Boaz became the father of Obed by Ruth. Obed became the father of Jesse.
6 miy baayu buur bi Daawuda. Daawuda moo jur Suleymaan ci ki nekkoon jabari Uri;
6Jesse became the father of King David. David became the father of Solomon by her who had been the wife of Uriah.
7 Suleymaan jur Robowam; Robowam Abiya; Abiya Asaf;
7Solomon became the father of Rehoboam. Rehoboam became the father of Abijah. Abijah became the father of Asa.
8 Asaf Yosafat; Yosafat Yoram, miy baayu Osiyas;
8Asa became the father of Jehoshaphat. Jehoshaphat became the father of Joram. Joram became the father of Uzziah.
9 Osiyas jur Yowatam; Yowatam Akas, miy baayu Esekiyas;
9Uzziah became the father of Jotham. Jotham became the father of Ahaz. Ahaz became the father of Hezekiah.
10 Esekiyas Manase; Manase Amon; Amon Yosiyas;
10Hezekiah became the father of Manasseh. Manasseh became the father of Amon. Amon became the father of Josiah.
11 Yosiyas jur Yekoñas ak i doomi baayam ca jamono, ja ñu defe Yawut ya jaam, yóbbu leen Babilon.
11Josiah became the father of Jechoniah and his brothers, at the time of the exile to Babylon.
12 Ba ñu leen yóbboo ca Babilon, Yekoñas jur Salacel; Salacel Sorobabel,
12After the exile to Babylon, Jechoniah became the father of Shealtiel. Shealtiel became the father of Zerubbabel.
13 miy baayu Abiyudd; Abiyudd Eliyakim; Eliyakim Asor;
13Zerubbabel became the father of Abiud. Abiud became the father of Eliakim. Eliakim became the father of Azor.
14 Asor Sadog; Sadog Akim; Akim Eliyudd;
14Azor became the father of Sadoc. Sadoc became the father of Achim. Achim became the father of Eliud.
15 Eliyudd Eleyasar; Eleyasar Matan, miy baayu Yanqóoba;
15Eliud became the father of Eleazar. Eleazar became the father of Matthan. Matthan became the father of Jacob.
16 Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama; te ci Maryaama la Yeesu, mi ñuy wax Kirist, juddoo.
16Jacob became the father of Joseph, the husband of Mary, from whom was born Jesus , who is called Christ.
17 Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent.
17So all the generations from Abraham to David are fourteen generations; from David to the exile to Babylon fourteen generations; and from the carrying away to Babylon to the Christ, fourteen generations.
18 Nii la Yeesu Kirist juddoo. Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa, waaye laata ñoo ànd, gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi.
18Now the birth of Jesus Christ was like this; for after his mother, Mary, was engaged to Joseph, before they came together, she was found pregnant by the Holy Spirit.
19 Yuusufa jëkkëram nag, nekkoon na nit ku jub te bëggu ko woon a weer. Mu nar a xàccook moom ci sutura.
19Joseph, her husband, being a righteous man, and not willing to make her a public example, intended to put her away secretly.
20 Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragal a yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge.
20But when he thought about these things, behold, an angel of the Lord appeared to him in a dream, saying, “Joseph, son of David, don’t be afraid to take to yourself Mary, your wife, for that which is conceived in her is of the Holy Spirit.
21 Dina jur doom ju góor; na nga ko tudde Yeesu, ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkaar.»
21She shall bring forth a son. You shall call his name Jesus, for it is he who shall save his people from their sins.”
22 Loolu lépp xewoon na, ngir amal li Boroom bi wax, jaarale ko cib yonent, bi mu naan:
22Now all this has happened, that it might be fulfilled which was spoken by the Lord through the prophet, saying,
23 «Janq bi dina ëmb,jur doom ju góor,ñu tudde ko Emanuwel,» liy tekki «Yàlla ganesi na nu.»
23“Behold, the virgin shall be with child, and shall bring forth a son. They shall call his name Immanuel”; which is, being interpreted, “God with us.”
24 Noonu Yuusufa yeewu, yeggali jabaram, na ko ko malaakam Boroom bi sante woon.
24Joseph arose from his sleep, and did as the angel of the Lord commanded him, and took his wife to himself;
25 Waaye àndul ak moom, ba kera mu mucc, jur doom ju góor; mu tudde ko Yeesu.
25and didn’t know her sexually until she had brought forth her firstborn son. He named him Jesus.