Wolof: New Testament

World English Bible

Matthew

18

1 Ca waxtu woowu taalibe ya ñëwoon nañu ci Yeesu, laaj ko: «Kan moo gën a màgg ci nguuru Yàlla mi nekk ci kaw?»
1In that hour the disciples came to Jesus, saying, “Who then is greatest in the Kingdom of Heaven?”
2 Noonu Yeesu woo xale, teg ko ci seen biir,
2Jesus called a little child to himself, and set him in their midst,
3 ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen woññikuwul ci Yàlla, ba mel niy xale, dungeen dugg mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
3and said, “Most certainly I tell you, unless you turn, and become as little children, you will in no way enter into the Kingdom of Heaven.
4 Kuy suufeelu nag, ba mel ni xale bii, kooku mooy ki gën a màgg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
4 Whoever therefore humbles himself as this little child, the same is the greatest in the Kingdom of Heaven.
5 Te it ku nangu ci sama tur xale bu mel ni kii, man mii nga nangu.
5 Whoever receives one such little child in my name receives me,
6 Waaye ku yóbbe bàkkaar kenn ci ñi gën a tuuti ñi ma gëm, li gën ci moom mooy ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ca fa gën a xóot ca géej ga.
6 but whoever causes one of these little ones who believe in me to stumble, it would be better for him that a huge millstone should be hung around his neck, and that he should be sunk in the depths of the sea.
7 «Yaw àddina dinga torox ndax say fiir yiy yóbbe nit bàkkaar. Fiir mënta ñàkk, waaye toroxte dal na nit ki koy lal.
7 “Woe to the world because of occasions of stumbling! For it must be that the occasions come, but woe to that person through whom the occasion comes!
8 Boo xamee ne sa loxo mbaa sa tànk mu ngi lay yóbbe bàkkaar, dagg ko, sànni ko fu sore. Ndaxte nga lafañ walla ñàkk loxo te dugg ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari loxo walla ñaari tànk, te ñu sànni la ci safara su dul fey mukk.
8 If your hand or your foot causes you to stumble, cut it off, and cast it from you. It is better for you to enter into life maimed or crippled, rather than having two hands or two feet to be cast into the eternal fire.
9 Boo xamee ne sa bët mu ngi lay yóbbe bàkkaar, luqi ko, sànni ko fu sore. Ndaxte nga patt te dugg ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari bët, te ñu sànni la ci safara.
9 If your eye causes you to stumble, pluck it out, and cast it from you. It is better for you to enter into life with one eye, rather than having two eyes to be cast into the Gehenna of fire.
10 «Te it wottuleen a xeeb kenn ci ñi gën a tuuti, ndax kat seeni malaakaa ngi sax ci jataayu sama Baay bi nekk ci kaw. Maa leen wax loolu.
10 See that you don’t despise one of these little ones, for I tell you that in heaven their angels always see the face of my Father who is in heaven.
12 «Luy seen xalaat ci lii? Su fi amoon nit ku am téeméeri xar, te benn ci ñoom réer, lu muy def? Ndax du bàyyi ca parlukaay ba juróom-ñeent-fukki xar ya ak juróom-ñeent, te dem wuti ma réer?
11 For the Son of Man came to save that which was lost.
13 Bu ko gisee, mbég mi mu am ci moom mooy ëpp mbég, mi mu am ci juróom-ñeent-fukki xar ya ak juróom-ñeent ya réerul.
12 “What do you think? If a man has one hundred sheep, and one of them goes astray, doesn’t he leave the ninety-nine, go to the mountains, and seek that which has gone astray?
14 «Noonu it seen Baay bi nekk ci kaw bëggul kenn ci ñi gën a tuuti sànku.
13 If he finds it, most certainly I tell you, he rejoices over it more than over the ninety-nine which have not gone astray.
15 «Te lii itam, bu sa mbokk defee bàkkaar, demal yedd ko, yéen ñaar rekk. Bu la dégloo, kon gindi nga sa mbokk.
14 Even so it is not the will of your Father who is in heaven that one of these little ones should perish.
16 Waaye bu la dégluwul, àndal ak kenn mbaa ñaar, ngir mbir mi dëggu ci li ko ñaar walla ñett seede.
15 “If your brother sins against you, go, show him his fault between you and him alone. If he listens to you, you have gained back your brother.
17 Bu leen dégluwul ñoom itam, wax ko mbooloom ñi gëm. Bu dégluwul mbooloo ma nag, nga teg ko ni ku gëmul Yàlla mbaa ab juutikat.
16 But if he doesn’t listen, take one or two more with you, that at the mouth of two or three witnesses every word may be established.
18 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lépp lu ngeen yeew ci àddina, dees na ko yeew ci asamaan, te lépp lu ngeen yiwi ci àddina, dees na ko yiwi ci asamaan.
17 If he refuses to listen to them, tell it to the assembly. If he refuses to hear the assembly also, let him be to you as a Gentile or a tax collector.
19 «Maa ngi leen koy wax it, bu ñaar ci yéen déggoo ci àddina, ngir ñaan lu mu man a doon, sama Baay bi nekk ci kaw dina leen ko may.
18 Most certainly I tell you, whatever things you bind on earth will have been bound in heaven, and whatever things you release on earth will have been released in heaven.
20 Ndaxte fu ñaar walla ñetti nit booloo ci sama tur, maa ngi ci seen biir.»
19 Again, assuredly I tell you, that if two of you will agree on earth concerning anything that they will ask, it will be done for them by my Father who is in heaven.
21 Noonu Piyeer ñëw ci Yeesu, laaj ko: «Boroom bi, bu ma sama mbokk tooñee, ñaata yoon laa ko war a baal? Xanaa ba ci juróom-ñaari yoon?»
20 For where two or three are gathered together in my name, there I am in their midst.”
22 Yeesu tontu ko ne: «Waxuma la ba ci juróom-ñaari yoon, waaye ba ci juróom-ñaar-fukki juróom-ñaari yoon.
21Then Peter came and said to him, “Lord, how often shall my brother sin against me, and I forgive him? Until seven times?”
23 «Loolu moo tax nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni buur bu bëgg a waññ alalam ak ay jaraafam.
22Jesus said to him, “I don’t tell you until seven times, but, until seventy times seven.
24 Ba mu tàmbalee waññ nag, ñu indil buur ba ku ko ameel ay milyoŋ yu baree-bare,
23 Therefore the Kingdom of Heaven is like a certain king, who wanted to reconcile accounts with his servants.
25 waaye jaraaf ja amul lu mu feye. Kon nag sangam santaane, ñu jaay ko moom ak jabaram ak ay doomam ak lépp lu mu am, ngir fey bor ba.
24 When he had begun to reconcile, one was brought to him who owed him ten thousand talents.
26 Kon jaraaf ja daanu ciy tànkam ne ko: “Muñal ma, dinaa la fey lépp.”
25 But because he couldn’t pay, his lord commanded him to be sold, with his wife, his children, and all that he had, and payment to be made.
27 Noonu sangam yërëm ko, bàyyi ko, baal ko bor ba.
26 The servant therefore fell down and kneeled before him, saying, ‘Lord, have patience with me, and I will repay you all!’
28 «Bi loolu amee jaraaf ja génn, gis benn moroomu jaraafam bu ko ameel ay junni. Mu daldi ko jàpp, poñe ko ne ko: “Fey ma li nga ma ameel.”
27 The lord of that servant, being moved with compassion, released him, and forgave him the debt.
29 Kon moroomam daanu ci suuf, ñaan ko ne: “Muñal ma, dinaa la fey.”
28 “But that servant went out, and found one of his fellow servants, who owed him one hundred denarii, and he grabbed him, and took him by the throat, saying, ‘Pay me what you owe!’
30 Waaye moom nanguwu ko, mu dem, tëj ko kaso, ba kera mu fey li mu ko ameel.
29 “So his fellow servant fell down at his feet and begged him, saying, ‘Have patience with me, and I will repay you!’
31 «Bi ay moroomam gisee loolu nag, ñu am naqar wu réy, daldi dem, xamal seen sang li xew lépp.
30 He would not, but went and cast him into prison, until he should pay back that which was due.
32 Sang ba nag woolu jaraaf ba ne ko: “Yaw jaraaf ju soxor nga! Baal naa la sa bor bépp, ndaxte tinu nga ma.
31 So when his fellow servants saw what was done, they were exceedingly sorry, and came and told to their lord all that was done.
33 Lu tax yaw itam yërëmoo sa moroom, ni ma la yërëme?”
32 Then his lord called him in, and said to him, ‘You wicked servant! I forgave you all that debt, because you begged me.
34 Noonu sang ba mer, jébbal ko ñiy fitnaale ca kaso ba, ba kera muy fey li mu ko ameel lépp.
33 Shouldn’t you also have had mercy on your fellow servant, even as I had mercy on you?’
35 «Noonu la leen sama Baay bi ci kaw di def, bu ngeen baalul ku nekk seen mbokk ak xol bu sedd.»
34 His lord was angry, and delivered him to the tormentors, until he should pay all that was due to him.
35 So my heavenly Father will also do to you, if you don’t each forgive your brother from your hearts for his misdeeds.”