1 Gannaaw loolu Yeesu nettali leen beneen léeb ne leen:
1Jesus answered and spoke again in parables to them, saying,
2 «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni buur buy waajal céetu doomam ju góor.
2 “The Kingdom of Heaven is like a certain king, who made a marriage feast for his son,
3 Noonu mu yónni ay surgaam, ngir ñu woo gan yi ca céet ga, waaye gan yi bëgguñoo ñëw.
3 and sent out his servants to call those who were invited to the marriage feast, but they would not come.
4 Kon mu yónneeti yeneen surga ne leen: “Bu ngeen demee, yégal-leen gan yi sama woote bii: ‘Reer yi noppi na, reylu naa samay nag ak samay jur gu duuf; lépp sotti na, ñëwleen ci reer yi.’ ”
4 Again he sent out other servants, saying, ‘Tell those who are invited, “Behold, I have prepared my dinner. My cattle and my fatlings are killed, and all things are ready. Come to the marriage feast!”’
5 Waaye ba tey wuyuwuñu ko; ñu dem, kenn ki ca toolam, kenn ki jaayaani,
5 But they made light of it, and went their ways, one to his own farm, another to his merchandise,
6 ña ca des jàpp surga ya, toroxal leen, rey leen.
6 and the rest grabbed his servants, and treated them shamefully, and killed them.
7 «Noonu buur mer, daldi yónni ay xarekatam, ngir ñu rey bóomkat yooyule, lakk seen dëkk.
7 When the king heard that, he was angry, and sent his armies, destroyed those murderers, and burned their city.
8 Ci kaw loolu mu ne surga ya: “Reeri céet gi noppi na, waaye ñi ñu woo yeyoowuñu ko.
8 “Then he said to his servants, ‘The wedding is ready, but those who were invited weren’t worthy.
9 Demleen nag buntu dëkk ba, woo ku ngeen fa gis ci reeri céet gi.”
9 Go therefore to the intersections of the highways, and as many as you may find, invite to the marriage feast.’
10 Noonu surga ya génn ca yoon ya, boole ña ñu fa gis ñépp, ñu bon ña ak ñu baax ña, ba néegu reer ya fees ak ay gan.
10 Those servants went out into the highways, and gathered together as many as they found, both bad and good. The wedding was filled with guests.
11 «Bi nga xamee ne buur bi dugg na nag, ngir seetsi gan yi, mu gis fa nit ku solul mbubb mu ñu war a sol ca céet ga.
11 But when the king came in to see the guests, he saw there a man who didn’t have on wedding clothing,
12 Buur ne ko: “Sama waay, naka nga dugge fii, te amuloo mbubbum céet?” Waa ji ne miig.
12 and he said to him, ‘Friend, how did you come in here not wearing wedding clothing?’ He was speechless.
13 Noonu buur ba ne ay surgaam: “Yeewleen ko ci tànk yi ak ci loxo yi, sànni ko ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.”
13 Then the king said to the servants, ‘Bind him hand and foot, take him away, and throw him into the outer darkness; there is where the weeping and grinding of teeth will be.’
14 Ndaxte ñi ñu woo bare nañu, waaye ñi ñu tànn barewul.»
14 For many are called, but few chosen.”
15 Booba Farisen ya dem gise, ba xam lu ñu war a def, ngir fiir Yeesu ci waxam.
15Then the Pharisees went and took counsel how they might entrap him in his talk.
16 Noonu ñu yónni ci moom seeni taalibe ak ñi far ak buur bi Erodd ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ku wóor nga, te ragaloo kenn, ndaxte seetuloo jëmmi nit, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor.
16They sent their disciples to him, along with the Herodians, saying, “Teacher, we know that you are honest, and teach the way of God in truth, no matter whom you teach, for you aren’t partial to anyone.
17 Wax nu nag loo xam ci lii: ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag walla déet?»
17Tell us therefore, what do you think? Is it lawful to pay taxes to Caesar, or not?”
18 Waaye Yeesu xam seen njublaŋ, mu ne leen nag: «Lu tax ngeen bëgg maa fiir, yéen naaféq yi?
18But Jesus perceived their wickedness, and said, “Why do you test me, you hypocrites?
19 Wonleen ma poset, bi ñuy feye galag.» Ñu daldi ko jox nag benn posetu denariyon.
19 Show me the tax money.” They brought to him a denarius.
20 Yeesu ne leen: «Kan lañu ci def nataalam ak turam?»
20He asked them, “Whose is this image and inscription?”
21 Ñu tontu ko: «Sesaar.» Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.»
21They said to him, “Caesar’s.” Then he said to them, “Give therefore to Caesar the things that are Caesar’s, and to God the things that are God’s.”
22 Bi nga xamee ne dégg nañu loolu, ñu waaru, bàyyi ko, daldi dem.
22When they heard it, they marveled, and left him, and went away.
23 Bés boobale ay Sadusen ñëw ci moom. Sadusen yi nag ñoom gëmuñu ne ndekkite am na. Noonu ñu laaj ko naan:
23On that day Sadducees (those who say that there is no resurrection) came to him. They asked him,
24 «Kilifa gi, Musaa nee woon na: “Boo xamee ne góor dee na te amul doom, na rakkam donn jabaram, ngir sàkkal magam njaboot.”
24saying, “Teacher, Moses said, ‘If a man dies, having no children, his brother shall marry his wife, and raise up seed for his brother.’
25 Amoon na ci nun nag juróom-ñaari góor, ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba séyoon na, faatu; rakk ja donn jabar ja, ndaxte amul woon doom.
25Now there were with us seven brothers. The first married and died, and having no seed left his wife to his brother.
26 Ñaareel ba ak ñetteel ba def noonu, ba ci juróom-ñaareel ba.
26In the same way, the second also, and the third, to the seventh.
27 Gannaaw ñoom ñépp, jigéen ja faatu.
27After them all, the woman died.
28 Bu ndekkite taxawee nag, jabaru kan lay doon ci juróom-ñaar ñi, ndaxte ñépp jël nañu ko?»
28In the resurrection therefore, whose wife will she be of the seven? For they all had her.”
29 Waaye Yeesu tontu leen ne: «Yéena ngi cig réer, ndaxte xamuleen Mbind mi mbaa kàttanu Yàlla.
29But Jesus answered them, “You are mistaken, not knowing the Scriptures, nor the power of God.
30 Ndaxte keroog ndekkite li kenn du am jabar, kenn du am jëkkër, waaye dinañu mel ni malaaka yi ci kaw.
30 For in the resurrection they neither marry, nor are given in marriage, but are like God’s angels in heaven.
31 Te lu jëm ci ndekkitel ñi dee, xanaa musuleen a jàng la leen Yàlla waxoon ne:
31 But concerning the resurrection of the dead, haven’t you read that which was spoken to you by God, saying,
32 “Maay Yàllay Ibraayma ak Yàllay Isaaxa ak Yàllay Yanqóoba”? Li ciy génn mooy, nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la.»
32 ‘I am the God of Abraham, and the God of Isaac, and the God of Jacob?’ Exodus 3:6 God is not the God of the dead, but of the living.”
33 Bi nga xamee ne mbooloo ma dégg nañu loolu, ñu waaru ndax li mu jàngale.
33When the multitudes heard it, they were astonished at his teaching.
34 Gannaaw gi, Farisen ya yég nañu ne, yey na Sadusen ya. Kon nag ñu daldi daje.
34But the Pharisees, when they heard that he had silenced the Sadducees, gathered themselves together.
35 Noonu kenn ci ñoom, ka nekk xutbakat, fexe koo fiir. Mu laaj ko:
35One of them, a lawyer, asked him a question, testing him.
36 «Kilifa gi, ban ndigal moo gën a màgg ci yoonu Musaa?»
36“Teacher, which is the greatest commandment in the law?”
37 Yeesu tontu ko ne: « “Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp ak sa xel mépp.”
37Jesus said to him, “‘You shall love the Lord your God with all your heart, with all your soul, and with all your mind.’ Deuteronomy 6:5
38 Loolu moo di li jëkk te ëpp ci li Yàlla santaane.
38 This is the first and great commandment.
39 Te ñaareel bi noona la mel: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.”
39 A second likewise is this, ‘You shall love your neighbor as yourself.’ Leviticus 19:18
40 Ñaari ndigal yooyu tënk nañu yoonu Musaa wépp, moom ak waxi yonent yi.»
40 The whole law and the prophets depend on these two commandments.”
41 Bi Farisen ya dajee nag, Yeesu laaj leen:
41Now while the Pharisees were gathered together, Jesus asked them a question,
42 «Lu ngeen xalaat ci Almasi bi; kan la nekk sëtam?» Ñu tontu ko: «Daawuda.»
42saying, “What do you think of the Christ? Whose son is he?” They said to him, “Of David.”
43 Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nag Daawuda, bi muy wax ci kàttanu Xelu Yàlla mi, di ko wooye “Boroom bi” ne:
43He said to them, “How then does David in the Spirit call him Lord, saying,
44 “Boroom bi wax na sama Boroom:‘Toogal ci sama ndeyjoor,ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam’ ”
44 ‘The Lord said to my Lord, sit on my right hand, until I make your enemies a footstool for your feet?’ Psalm 110:1
45 Gannaaw Daawuda nag wooye na ko: “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?»
45 “If then David calls him Lord, how is he his son?”
46 Ci kaw loolu kenn mënu koo tontu genn kàddu. Te li dale ci bés booba kenn ñemeetu koo laaj dara.
46No one was able to answer him a word, neither did any man dare ask him any more questions from that day forth.