Wolof: New Testament

World English Bible

Matthew

4

1 Bi loolu amee Xelum Yàlla yóbbu Yeesu ca màndiŋ ma, ngir mu jànkoonte ak fiiri Seytaane.
1Then Jesus was led up by the Spirit into the wilderness to be tempted by the devil.
2 Yeesu nekk fa te lekkul ñeent-fukki bëccëg ak ñeent-fukki guddi, door a xiif.
2When he had fasted forty days and forty nights, he was hungry afterward.
3 Noonu fiirkat bi ñëw ci moom ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, santal doj yii, ñu nekk mburu.»
3The tempter came and said to him, “If you are the Son of God, command that these stones become bread.”
4 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk, waaye itam gépp kàddu gu génne ci gémmiñug Yàlla.”»
4But he answered, “It is written, ‘Man shall not live by bread alone, but by every word that proceeds out of the mouth of God.’”
5 Bi mu waxee loolu, Seytaane yóbbu ko ca dëkk bu sell ba, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga.
5Then the devil took him into the holy city. He set him on the pinnacle of the temple,
6 Mu ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal ci suuf, ndaxte Mbind mi nee na:“Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir,ñu leewu la ci seeni loxo,ngir nga bañ a fakkastalu ciw doj.”»
6and said to him, “If you are the Son of God, throw yourself down, for it is written, ‘He will put his angels in charge of you.’ and, ‘On their hands they will bear you up, so that you don’t dash your foot against a stone.’”
7 Yeesu tontu ko: «Bind nañu it ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”»
7Jesus said to him, “Again, it is written, ‘You shall not test the Lord, your God.’”
8 Gannaaw loolu Seytaane yóbbu ko ci kaw tund wu kawe lool, won ko réewi àddina yépp ak seeni ndam.
8Again, the devil took him to an exceedingly high mountain, and showed him all the kingdoms of the world, and their glory.
9 Mu ne ko: «Lii lépp dinaa la ko may, boo sukkee màggal ma.»
9He said to him, “I will give you all of these things, if you will fall down and worship me.”
10 Waaye Yeesu tontu ko: «Sore ma Seytaane, ndaxte Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom, te jaamu ko moom rekk.”»
10Then Jesus said to him, “Get behind me, Satan! For it is written, ‘You shall worship the Lord your God, and you shall serve him only.’”
11 Noonu Seytaane bàyyi ko. Te ay malaaka daldi ñëw fi Yeesu, di ko topptoo.
11Then the devil left him, and behold, angels came and served him.
12 Am bés Yeesu dégg ne, jàpp nañu Yaxya; mu jóg nag, jëm Galile.
12Now when Jesus heard that John was delivered up, he withdrew into Galilee.
13 Gannaaw gi, mu toxoo dëkku Nasaret, dem dëkk Kapernawum, bi féeteek dex ga ci diiwaani Sabulon ak Neftali.
13Leaving Nazareth, he came and lived in Capernaum, which is by the sea, in the region of Zebulun and Naphtali,
14 Noonu am la ñu waxoon, jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan:
14that it might be fulfilled which was spoken through Isaiah the prophet, saying,
15 «Yaw réewum Sabulon ak réewum Neftali,di yoonu géej gannaaw dexu Yurdan,yaw Galile, réewum ñi dul Yawut —
15“The land of Zebulun and the land of Naphtali, toward the sea, beyond the Jordan, Galilee of the Gentiles,
16 xeet wa nekkoon cig lëndëm,gis na leer gu mag,ña dëkkoon ca réew, ma dee tiim,leer fenkal na leen.»
16the people who sat in darkness saw a great light, to those who sat in the region and shadow of death, to them light has dawned.”
17 Booba Yeesu tàmbali di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.»
17From that time, Jesus began to preach, and to say, “Repent! For the Kingdom of Heaven is at hand.”
18 Gannaaw loolu Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare. Fekk ñuy sànni seen caax ca dex ga, ndaxte ay nappkat lañu woon.
18Walking by the sea of Galilee, he saw two brothers: Simon, who is called Peter, and Andrew, his brother, casting a net into the sea; for they were fishermen.
19 Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ci man, ma def leen nappkati nit.»
19He said to them, “Come after me, and I will make you fishers for men.”
20 Ca saa sa ñu daldi bàyyi seeni mbaal, topp ci moom.
20They immediately left their nets and followed him.
21 Ba Yeesu demee ba ca kanam, mu gis yeneen ñaar ñu bokk ndey ak baay, ñuy Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam. Ñu nekk ci seen biir gaal ak Sebede seen baay, di defar seeni mbaal. Noonu Yeesu woo leen.
21Going on from there, he saw two other brothers, James the son of Zebedee, and John his brother, in the boat with Zebedee their father, mending their nets. He called them.
22 Ca saa sa ñu daldi bàyyi gaal ga ak seen baay, topp ci moom.
22They immediately left the boat and their father, and followed him.
23 Ba loolu amee Yeesu doon wër Galile gépp, di jàngale ci seeni jàngu tey yégle xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla; muy faj jàngoro yépp ak wéradi yépp ca nit ña,
23Jesus went about in all Galilee, teaching in their synagogues, preaching the Good News of the Kingdom, and healing every disease and every sickness among the people.
24 ba tax turam siiw ba ci biir réewu Siri mépp. Ñu di ko indil ñi wopp ñépp, ñi sonn ndax ay jàngoro ak metit yu bare, ñi rab jàpp, ñiy say ak ñi làggi, mu faj leen.
24The report about him went out into all Syria. They brought to him all who were sick, afflicted with various diseases and torments, possessed with demons, epileptics, and paralytics; and he healed them.
25 Noonu mbooloo mu bare topp ci moom, jóge ci wàlli Galile ak diiwaan bi ñuy wax Fukki dëkk yi, ci dëkku Yerusalem ak ci diiwaanu Yude, ba ci gannaaw dexu Yurdan..
25Great multitudes from Galilee, Decapolis, Jerusalem, Judea and from beyond the Jordan followed him.