1 «Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, ngir bañ ñu àtte leen yéen itam.
1 “Don’t judge, so that you won’t be judged.
2 Ndaxte dees na leen àtte ak ni ngeen di àttee, nattal leen ak li ngeen di nattale.
2 For with whatever judgment you judge, you will be judged; and with whatever measure you measure, it will be measured to you.
3 Lu tax ngay xool ñax gi ci sa bëtu mbokk, te gisuloo gànj gi ci sa bët yaw?
3 Why do you see the speck that is in your brother’s eye, but don’t consider the beam that is in your own eye?
4 Walla nan ngay waxe sa mbokk: “May ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” fekk gànj a ngii ci sa bët yaw?
4 Or how will you tell your brother, ‘Let me remove the speck from your eye;’ and behold, the beam is in your own eye?
5 Naaféq, jëkkal a dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga man a gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk.
5 You hypocrite! First remove the beam out of your own eye, and then you can see clearly to remove the speck out of your brother’s eye.
6 «Buleen jox lu sell xaj yi, mbaa sànni seeni per ci kanamu mbaam-xuux yi, ngir bañ ñu dëggaate ko te walbatiku, xotti leen.
6 “Don’t give that which is holy to the dogs, neither throw your pearls before the pigs, lest perhaps they trample them under their feet, and turn and tear you to pieces.
7 «Ñaanleen, ñu may leen; seetleen te dingeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen.
7 “Ask, and it will be given you. Seek, and you will find. Knock, and it will be opened for you.
8 Ndaxte képp kuy ñaan, dinga am; kuy seet, dinga gis; kuy fëgg, ñu ubbil la.
8 For everyone who asks receives. He who seeks finds. To him who knocks it will be opened.
9 Kan ci yéen, bu la sa doom ñaanee mburu, nga jox ko doj?
9 Or who is there among you, who, if his son asks him for bread, will give him a stone?
10 Walla mu ñaan la jën, nga jox ko jaan?
10 Or if he asks for a fish, who will give him a serpent?
11 Ndegam yéen ñi bon yéena man a jox seeni gune lu baax, astemaak seen Baay bi nekk ci kaw dina jox lu baax ñi ko koy ñaan!
11 If you then, being evil, know how to give good gifts to your children, how much more will your Father who is in heaven give good things to those who ask him!
12 «Kon nag lépp lu ngeen bëgg, nit ñi defal leen ko, yéen itam nangeen leen ko defal; ndaxte loolu moo ëmb yoonu Musaa ak waxi yonent yi.
12 Therefore whatever you desire for men to do to you, you shall also do to them; for this is the law and the prophets.
13 «Jaarleen ci bunt bu xat bi, ndaxte bunt bi ak yoon wi jëm sànku yaatu nañu, te ñi ciy jaar bare.
13 “Enter in by the narrow gate; for wide is the gate and broad is the way that leads to destruction, and many are those who enter in by it.
14 Waaye buntu dund gu wóor xat na, te yoon wi jëm kaw sew na, te ñi ko gis barewul.
14 How TR reads “Because” instead of “How” narrow is the gate, and restricted is the way that leads to life! Few are those who find it.
15 «Moytuleen ñi mbubboo turu yonent. Dañuy ñëw ci yéen, yor melow xar, waaye ci biir ay bukki yu soxor lañu.
15 “Beware of false prophets, who come to you in sheep’s clothing, but inwardly are ravening wolves.
16 Dingeen leen xàmmee ci seeni jëf. Ndax dees na witte réseñ ci dédd, walla figg ci xaaxaam?
16 By their fruits you will know them. Do you gather grapes from thorns, or figs from thistles?
17 Noonu garab gu baax gu nekk dina meññ doom yu neex, waaye garab gu bon dina meññ doom yu bon.
17 Even so, every good tree produces good fruit; but the corrupt tree produces evil fruit.
18 Garab gu baax mënul a meññ doom yu bon, naka itam garab gu bon mënul a meññ doom yu neex.
18 A good tree can’t produce evil fruit, neither can a corrupt tree produce good fruit.
19 Garab gu nekk gu dul meññ doom yu neex, dees na ko gor, sànni ko ca safara sa.
19 Every tree that doesn’t grow good fruit is cut down, and thrown into the fire.
20 Ci seeni jëf nag ngeen leen di xàmmee.
20 Therefore by their fruits you will know them.
21 «Du képp ku may wax: “Boroom bi, Boroom bi,” mooy dugg ca nguuru Yàlla Aji Kawe ji; ka cay dugg mooy kiy def sama coobareg Baay, bi nekk ci kaw.
21 Not everyone who says to me, ‘Lord, Lord,’ will enter into the Kingdom of Heaven; but he who does the will of my Father who is in heaven.
22 Bu bés baa, ñu bare dinañu ma wax: “Boroom bi, Boroom bi, ndax du ci saw tur lanu daa waxe ci kàddug Yàlla? Ndax du ci saw tur lanu daa dàqe ay rab? Ndax du ci saw tur lanu daa defe ay kéemaan yu bare?”
22 Many will tell me in that day, ‘Lord, Lord, didn’t we prophesy in your name, in your name cast out demons, and in your name do many mighty works?’
23 Ci kaw loolu dinaa leen wax dëgg ne leen: “Musuma leen a xam; soreleen ma, yéen ñiy def bàkkaar.”
23 Then I will tell them, ‘I never knew you. Depart from me, you who work iniquity.’
24 «Képp ku dégg nag lii ma leen wax, te di ko jëfe, dinga mel ni nit ku am xel, ku tabax këram, samp ko ciw doj.
24 “Everyone therefore who hears these words of mine, and does them, I will liken him to a wise man, who built his house on a rock.
25 Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; waaye màbbul, ndaxte mu ngi jàpp ca doj wa.
25 The rain came down, the floods came, and the winds blew, and beat on that house; and it didn’t fall, for it was founded on the rock.
26 Waaye képp ku dégg lii ma leen wax, te jëfewuloo ko, dinga mel ni nit ku ñàkk xel, ku tabax këram ci gànnuus bi.
26 Everyone who hears these words of mine, and doesn’t do them will be like a foolish man, who built his house on the sand.
27 Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; mu màbb, ba ne tasar.»
27 The rain came down, the floods came, and the winds blew, and beat on that house; and it fell—and great was its fall.”
28 Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, mbooloo ma daldi waaru ca njàngaleem,
28It happened, when Jesus had finished saying these things, that the multitudes were astonished at his teaching,
29 ndaxte jàngal na leen ak sañ-sañ bu seeni xutbakat amul.
29for he taught them with authority, and not like the scribes.