Wolof: New Testament

World English Bible

Matthew

9

1 Bi loolu amee Yeesu dugg cig gaal, jàll dex ga, dellu dëkkam.
1He entered into a boat, and crossed over, and came into his own city.
2 Foofa ñu indil ko ku tëdd ci basaŋ, fekk yaramam wépp làggi. Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu ne ku làggi ka: «Na sa xel dal, sama waay, baal nañu la say bàkkaar.»
2Behold, they brought to him a man who was paralyzed, lying on a bed. Jesus, seeing their faith, said to the paralytic, “Son, cheer up! Your sins are forgiven you.”
3 Bi mu waxee loolu, ay xutbakat daldi ne ci seen biir: «Nit kii mu ngi sosal Yàlla.»
3Behold, some of the scribes said to themselves, “This man blasphemes.”
4 Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Lu tax ngeen am xalaat yu bon ci seen xol?
4Jesus, knowing their thoughts, said, “Why do you think evil in your hearts?
5 Ma wax ne: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma ne: “Jógal te dox,” lan moo ci gën a yomb?
5 For which is easier, to say, ‘Your sins are forgiven;’ or to say, ‘Get up, and walk?’
6 Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ka: «Jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.»
6 But that you may know that the Son of Man has authority on earth to forgive sins...” (then he said to the paralytic), “Get up, and take up your mat, and go up to your house.”
7 Noonu làggi ba daldi jóg, ñibbi.
7He arose and departed to his house.
8 Ba mbooloo ma gisee loolu, ñu daldi ragal te màggal Yàlla, mi dénk sañ-sañ bu tollu noonu doom Aadama yi.
8But when the multitudes saw it, they marveled and glorified God, who had given such authority to men.
9 Bi Yeesu jógee foofa, mu gis nit ku tudd Macë, toog ca juuti ba. Yeesu ne ko: «Kaay topp ma.» Noonu Macë jóg, daldi ko topp.
9As Jesus passed by from there, he saw a man called Matthew sitting at the tax collection office. He said to him, “Follow me.” He got up and followed him.
10 Gannaaw ga Yeesu doon lekk ca kër ga, te ay juutikat ak i boroom bàkkaar yu bare dikk, bokk lekk ak Yeesu ak taalibeem ya.
10It happened as he sat in the house, behold, many tax collectors and sinners came and sat down with Jesus and his disciples.
11 Bi ko Farisen ya gisee nag, ñu ne taalibe ya: «Lu tax seen kilifa di lekkandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?»
11When the Pharisees saw it, they said to his disciples, “Why does your teacher eat with tax collectors and sinners?”
12 Waaye bi ko Yeesu déggee, mu ne: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla.
12When Jesus heard it, he said to them, “Those who are healthy have no need for a physician, but those who are sick do.
13 Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Demleen nag te seet lu wax joojuy tekki. Ndaxte ñëwuma, ngir woo ñi jub, waaye bàkkaarkat yi laay woo.»
13 But you go and learn what this means: ‘I desire mercy, and not sacrifice,’ for I came not to call the righteous, but sinners to repentance.
14 Gannaaw loolu taalibey Yaxya ñëw ci Yeesu ne ko: «Lu tax nuy woor, nun ak Farisen yi, te say taalibe duñu woor?»
14Then John’s disciples came to him, saying, “Why do we and the Pharisees fast often, but your disciples don’t fast?”
15 Yeesu tontu leen: «Ndax gan yi ñëw ci céet dinañu naqarlu dara, li feek boroom céet gaa ngi ànd ak ñoom? Waaye bés yaa ngi ñëw yu ñuy jële boroom céet gi ci seen biir; booba nag dinañu woor.
15Jesus said to them, “Can the friends of the bridegroom mourn, as long as the bridegroom is with them? But the days will come when the bridegroom will be taken away from them, and then they will fast.
16 Xam ngeen ne, kenn du daax mbubb mu màggat ak sekkit wu bees; ndaxte sekkit wi day ñoddi mbubb mi, te xottiku bi gën a yaatu.
16 No one puts a piece of unshrunk cloth on an old garment; for the patch would tear away from the garment, and a worse hole is made.
17 Te it duñu def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, mbuus yi dañuy toj, biiñ bi tuuru te mbuus yi yàqu. Waaye biiñ bu bees, dees na ko def ci mbuus yu bees. Noonu ñoom ñaar duñu yàqu.»
17 Neither do people put new wine into old wineskins, or else the skins would burst, and the wine be spilled, and the skins ruined. No, they put new wine into fresh wineskins, and both are preserved.”
18 Bi leen Yeesu di wax loolu, benn njiitu jàngu daldi ñëw, sukk ci kanamam ne ko: «Sama doom ju jigéen dafa faatu léegi, waaye ñëwal, teg ko say loxo, te dina dundaat.»
18While he told these things to them, behold, a ruler came and worshiped him, saying, “My daughter has just died, but come and lay your hand on her, and she will live.”
19 Noonu Yeesu jóg, topp ko, moom ak ay taalibeem.
19Jesus got up and followed him, as did his disciples.
20 Bi ñuy dem nag, amoon na ca mbooloo ma jigéen juy xëpp deret diirub fukki at ak ñaar. Mu defe ne, su laalee mbubbam rekk, dina wér. Mu jegeñsi Yeesu nag, doxe ko gannaaw, laal catu mbubbam.
20Behold, a woman who had an issue of blood for twelve years came behind him, and touched the fringe of his garment;
22 Bi mu ko defee Yeesu woññiku ne ko: «Na sa xel dal, soxna si, sa ngëm faj na la.» Noonu jigéen ja daldi wér ca saa sa.
21for she said within herself, “If I just touch his garment, I will be made well.”
23 Bi Yeesu eggee kër njiit la, mu gis ñiy liit ak toxoro, ak mbooloo may def coow lu bare.
22But Jesus, turning around and seeing her, said, “Daughter, cheer up! Your faith has made you well.” And the woman was made well from that hour.
24 Mu ne leen: «Génnleen, janq bi deewul, day nelaw rekk.» Bi ko mbooloo ma déggee, ñu daldi ko ñaawal.
23When Jesus came into the ruler’s house, and saw the flute players, and the crowd in noisy disorder,
25 Waaye ñu génne leen, Yeesu dugg, jàpp loxob janq ba, mu daldi jóg.
24he said to them, “Make room, because the girl isn’t dead, but sleeping.” They were ridiculing him.
26 Noonu xebaaru li mu def daldi siiw ca réew ma.
25But when the crowd was put out, he entered in, took her by the hand, and the girl arose.
27 Bi Yeesu jógee foofa, ñaari gumba topp ko, di wax ca kaw naan: «Yërëm nu, yaw Sëtu Daawuda bi!»
26The report of this went out into all that land.
28 Noonu Yeesu dugg ca kër ga, gumba ya toppsi ko. Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen ne, man naa def li ngeen ma laaj?» Ñu tontu ko: «Waaw Sang bi.»
27As Jesus passed by from there, two blind men followed him, calling out and saying, “Have mercy on us, son of David!”
29 Kon Yeesu daldi laal seeni bët ne leen: «Na am, ni ngeen ko gëme.»
28When he had come into the house, the blind men came to him. Jesus said to them, “Do you believe that I am able to do this?” They told him, “Yes, Lord.”
30 Ca saa sa seeni bët daldi ubbiku. Yeesu dénk leen bu wér ne leen: «Moytuleen kenn xam ko.»
29Then he touched their eyes, saying, “According to your faith be it done to you.”
31 Waaye ñu génn rekk, siiwal turam fu nekk.
30Their eyes were opened. Jesus strictly commanded them, saying, “See that no one knows about this.”
32 Bi ñu fa jógee nag, amoon na ñeneen ñu ñëw fi moom, indil ko ku rab jàpp, mu luu.
31But they went out and spread abroad his fame in all that land.
33 Yeesu dàq rab wa, luu ba daldi wax. Bi ñu ko gisee, mbooloo ma waaru, ñu ne: «Lu mel nii, musuñu koo gis ci Israyil.»
32As they went out, behold, a mute man who was demon possessed was brought to him.
34 Waaye Farisen ya ne: «Ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.»
33When the demon was cast out, the mute man spoke. The multitudes marveled, saying, “Nothing like this has ever been seen in Israel!”
35 Noonu Yeesu wër dëkk yu mag ya yépp ak yu ndaw ya, di leen jàngal ci seeni jàngu, tey yégle xebaar bu baax bi jëm ci nguuru Yàlla, di faj jàngoro yépp ak wéradi yépp.
34But the Pharisees said, “By the prince of the demons, he casts out demons.”
36 Bi Yeesu gisee mbooloo ma, mu yërëm leen, ndaxte dañoo sonn ba ne yogg, mel ni xar yu amul sàmm.
35Jesus went about all the cities and the villages, teaching in their synagogues, and preaching the Good News of the Kingdom, and healing every disease and every sickness among the people.
37 Noonu mu ne taalibeem ya: «Ngóob mi yaatu na, waaye liggéeykat yi barewuñu.
36But when he saw the multitudes, he was moved with compassion for them, because they were harassed and scattered, like sheep without a shepherd.
38 Ñaanleen nag Boroom ngóob mi, mu yebal ay liggéeykat, ñu góob toolam.»
37Then he said to his disciples, “The harvest indeed is plentiful, but the laborers are few.
38 Pray therefore that the Lord of the harvest will send out laborers into his harvest.”