1 Gannaaw loolu ma gis ñeenti malaaka yu taxaw ci ñeenti xeblay àddina si. Ñu téye ñeenti ngelawi àddina, ngir ngelaw du wol ci kaw suuf, ci géej mbaa ci genn garab.
1After this, I saw four angels standing at the four corners of the earth, holding the four winds of the earth, so that no wind would blow on the earth, or on the sea, or on any tree.
2 Ma gis it meneen malaaka, muy yéeg, jóge penku, yor màndargakaayu Yàlla jiy dund. Mu daldi wax ak baat bu xumb ñeenti malaaka ya ñu joxoon sañ-sañ, ñu yàq suuf ak géej,
2I saw another angel ascend from the sunrise, having the seal of the living God. He cried with a loud voice to the four angels to whom it was given to harm the earth and the sea,
3 ne leen: «Buleen yàqagun suuf si ak géej gi ak garab yi. Négleen, ba ñu def màndarga ci jëwu ñiy jaamu Yàlla sunu Boroom.»
3saying, “Don’t harm the earth, neither the sea, nor the trees, until we have sealed the bondservants of our God on their foreheads!”
4 Noonu ma dégg limub ñi ñu màndargaal; ñu tollu ci téeméer ak ñeent-fukk ak ñeent ci ay junni. Ñu jóge ci giiri bànni Israyil yépp:
4I heard the number of those who were sealed, one hundred forty-four thousand, sealed out of every tribe of the children of Israel:
5 Fukki junni ak ñaar lañu màndargaal ci biir giiru Yuda,fukki junni ak ñaar ci giiru Ruben,fukki junni ak ñaar ci giiru Gàdd,
5of the tribe of Judah were sealed twelve thousand, of the tribe of Reuben twelve thousand, of the tribe of Gad twelve thousand,
6 fukki junni ak ñaar ci giiru Aser,fukki junni ak ñaar ci giiru Neftali,fukki junni ak ñaar ci giiru Manase,
6of the tribe of Asher twelve thousand, of the tribe of Naphtali twelve thousand, of the tribe of Manasseh twelve thousand,
7 fukki junni ak ñaar ci giiru Simeyon,fukki junni ak ñaar ci giiru Lewi,fukki junni ak ñaar ci giiru Isakaar,
7of the tribe of Simeon twelve thousand, of the tribe of Levi twelve thousand, of the tribe of Issachar twelve thousand,
8 fukki junni ak ñaar ci giiru Sabulon,fukki junni ak ñaar ci giiru Yuusufa,fukki junni ak ñaar ci giiru Ben-yamin.
8of the tribe of Zebulun twelve thousand, of the tribe of Joseph twelve thousand, of the tribe of Benjamin were sealed twelve thousand.
9 Gannaaw loolu ma xool, gis mbooloo mu réy, ba kenn mënu koo waññ, ñu bokk ci xeet yépp, giir yépp, réew yépp ak kàllaama yépp, taxaw ca kanamu gàngune ma ak Mbote ma. Ñu sol ay mbubb yu weex, di màggal te di yengal ay cari garab ci seeni loxo,
9After these things I looked, and behold, a great multitude, which no man could number, out of every nation and of all tribes, peoples, and languages, standing before the throne and before the Lamb, dressed in white robes, with palm branches in their hands.
10 naan:«Mucc gaa ngi ci Yàllasunu Boroom, bi toog ci gàngune mi,ak ci Mbote mi!»
10They cried with a loud voice, saying, “Salvation be to our God, who sits on the throne, and to the Lamb!”
11 Noonu malaaka yépp taxaw, wër gàngune ma ak mag ña ak ñeenti mbindeef ya. Ñu dëpp seen jë ca kanamu gàngune ma, di jaamu Yàlla,
11All the angels were standing around the throne, the elders, and the four living creatures; and they fell on their faces before his throne, and worshiped God,
12 naan:«Amiin. Na cant ak ndam, xel ak ngërëm, teraanga, kàttan ak dooleféete ak Yàlla sunu Boroom ba fàww. Amiin!»
12saying, “Amen! Blessing, glory, wisdom, thanksgiving, honor, power, and might, be to our God forever and ever! Amen.”
13 Noonu kenn ca mag ña ne ma: «Ñi sol mbubb yu weex yi, ñooy ñan ak fan lañu jóge?»
13One of the elders answered, saying to me, “These who are arrayed in white robes, who are they, and from where did they come?”
14 Ma ne ko: «Sang bi, xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca metit wu réy wa. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Mbote ma.
14I told him, “My lord, you know.” He said to me, “These are those who came out of the great tribulation. They washed their robes, and made them white in the Lamb’s blood.
15 Loolu moo taxñu nekk ci kanamu gàngunem Yàlla,di ko jaamu guddi ak bëccëg ci këram,te ki toog ci gàngune mi dina leen yiir.
15Therefore they are before the throne of God, they serve him day and night in his temple. He who sits on the throne will spread his tabernacle over them.
16 Dootuñu xiif, dootuñu mar.Jant mbaa weneen tàngaay du leen lakk,
16They will never be hungry, neither thirsty any more; neither will the sun beat on them, nor any heat;
17 ndaxte Mbote mi nekk ci diggu gàngune mi dina leen sàmm,yóbbu leen ca bëti ndoxum dund ma,te Yàlla dina fomp bépp rangooñ ci seeni bët.»
17for the Lamb who is in the midst of the throne shepherds them, and leads them to springs of waters of life. And God will wipe away every tear from their eyes.”