Wolof: New Testament

Luke

1

1 Yaw Teyofil mu tedd mi, xam nga ne, nit ñu bare sasoo nañoo bind ab nettali bu jëm ci mbir, yi xewoon ci sunu biir,2 li dëppook waxi seede, yi ko teewe woon li dale ca ndoorte la te ñu mujj nekk jawriñi kàddug Yàlla. 3 Léegi nag kon man ci sama wàll, gëstu naa ci lépp li ko dale ca njàlbéen ga, te fas naa la ko yéenee bindal, nettali la ni xew-xew yooyu deme woon tembe. 4 Noonu dinga man a xam ne, li ñu la jàngaloon lu wér peŋŋ la. 5 Ca jamonoy Erodd, mi nekkoon buur ca réewu Yawut ya, amoon na saraxalekat bu ñu tudde Sakariya te bokk ca mbootaayu saraxalekat, ya askanoo ci Abiya. Jabaram Elisabet askanoo moom itam ci Aaroona. 6 Sakariya ak jabaram ñu jub lañu ca kanam Yàlla, di topp ni mu ware ndigal yi ak dogali Boroom bi yépp. 7 Waaye amuñu doom, ndaxte Elisabet mënul a am doom, te it fekk ñoom ñaar ñépp ay màggat lañu. 8 Benn bés nag Sakariya doon def liggéeyu saraxaleem ca Yàlla, ndaxte mbootaayam a aye keroog. 9 Bi ñuy tegoo bant, ni ko saraxalekat yi daan defe nakajekk, ngir xam kan mooy dugg ca bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga, ngir taal fa cuuraay, bant ba tegu ci Sakariya. 10 Ca waxtu wa ñuy taal cuuraay la, mbooloo maa nga woon ca biti, di ñaan. 11 Noonu benn malaakam Boroom bi daldi feeñu Sakariya, taxaw ca féeteek ndeyjooru saraxalukaay, ba ñuy taal cuuraay ca kawam. 12 Naka la ko Sakariya gis, fitam daldi dem, mu tiit. 13 Waaye malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Sakariya, ndaxte sa ñaan nangu na. Elisabet sa jabar dina la jural doom, te dinga ko tudde Yaxya. 14 Sa mbég lay doon, sa xol sedd ci, te ñu bare dinañu bég ci juddoom, 15 ndaxte dina nekk ku màgg ca kanam Yàlla. Du naan biiñ walla dara luy màndil, te bu juddoo, Xel mu Sell mi daldi ko solu. 16 Dina delloosi niti Israyil yu bare ci Yàlla seen Boroom. 17 Mooy jiitu, di yégle ñëwu Boroom bi, ànd ak xel mi ak doole, ji yonent Yàlla Iliyas amoon, ngir jubale xoli baay yi ak doom yi, ngir delloo ñi déggadi ci maanduteg ñi jub. Noonu dina waajal mbooloo muy teeru Boroom bi.» 18 Sakariya daldi ne malaaka ma: «Nan laay xame ne, loolu dëgg la? Ndaxte mag laa, te sama jabar it màggat na.» 19 Malaaka ma tontu ko ne: «Man maay Jibril miy taxaw ci kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw te yégal la xebaar bu baax boobu. 20 Léegi nag gannaaw gëmuloo li ma wax, dinga luu te dootuloo man a wax, ba kera sama wax di am, bu jamonoom jotee.» 21 Fekk na booba mbooloo maa ngi xaar, jaaxle lool ci li Sakariya yàgg ca bérab bu sell ba. 22 Waaye bi mu génnee nag, mënul a wax ak ñoom. Noonu nit ña xam ne, dafa am lu ko feeñu ca bérab bu sell ba. Dafa luu, ba di leen liyaar. 23 Bi Sakariya matalee liggéeyu saraxaleem ba noppi, mu daldi ñibbi. 24 Bi mbir yooyu weesoo, Elisabet jabaram ëmb, di ko nëbb lu mat juróomi weer 25 te naan: «Lii mooy yiw wi ma Boroom bi defal, ba fajal ma li doon sama gàcce ci nit ñi!» 26 Bi Elisabet nekkee ci juróom-benni weeram, Yàlla yónni na malaakaam Jibril ca dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile. 27 Mu yebal ko ca janq bu ñu may waa ju bokk ci askanu Daawuda te ñu koy wax Yuusufa, waaye àndaguñu. Janq baa ngi tudd Maryaama. 28 Malaaka ma dikk ca moom ne ko: «Jàmm ngaam, yaw mi Boroom bi defal aw yiw; mu ngi ak yaw.» 29 Waxi malaaka ma daldi jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu man a tekki. 30 Malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Maryaama, ndaxte Yàlla tànn na la ci yiwam. 31 Dinga ëmb, jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu. 32 Ku màgg lay nekki, te dinañu ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla dina ko jébbal nguuru Daawuda maamam. 33 Noonu dina yilif askanu Yanqóoba ba fàww, te nguuram du am àpp.» 34 Maryaama laaj malaaka ma ne ko: «Naka la loolu man a ame? Man de, janq laa ba tey.» 35 Malaaka ma tontu ko ne: «Xel mu Sell mi dina wàcc ci yaw, te Aji Kawe ji dina la yiir ci kàttanam. Moo tax xale biy juddu dinañu ko wooye Ku sell ki, Doomu Yàlla ji. 36 Elisabet sa mbokk mi it dina am doom ju góor cig màggatam. Ki ñu doon wooye ku mënul a am doom, mu ngi ci juróom-benni weeram. 37 Ndaxte dara tëwul Yàlla.» 38 Maryaama ne ko: «Jaamub Boroom bi laa. Na Yàlla def ci man li nga wax.» Ci noonu malaaka ma daldi dem. 39 Ci jamono jooju Maryaama jóg, gaawantu dem ci benn dëkk bu nekkoon ca tund ya ca diiwaanu Yude. 40 Mu dugg ca kër Sakariya, daldi nuyu Elisabet. 41 Naka la Elisabet dégg Maryaama di nuyoo, doomam daldi yengatu ci biiram. Noonu Xelum Yàlla mu Sell mi daldi solu Elisabet. 42 Elisabet wax ca kaw ne: «Barkeel nañu la ci jigéen ñi, barkeel doom ji nga ëmb! 43 Man maay kan, ba ndeyu sama Boroom ñëw di ma seetsi? 44 Maa ngi lay wax ne, naka laa la dégg ngay nuyoo rekk, sama doom ji yengu ci sama biir ndax mbég. 45 Barke ñeel na la, yaw mi gëm ne, li la Boroom bi yégal dina mat!» 46 Noonu Maryaama daldi ne: 47 «Sama xol a ngi màggal Boroom bi,sama xel di bég ci Yàlla sama Musalkat, 48 ndaxte fàttaliku na ma,man jaamam bu woyof bi.Gannaawsi tey, niti jamono yéppdinañu ma wooye ki ñu barkeel, 49 ndaxte Ku Màgg ki defal na ma lu réy.Turam dafa sell. 50 Day wàcce yërmandeem ci ñi ko ragal,ci seeni sët ba ci seeni sëtaat. 51 Wone na jëf yu mag ci dooley loxoom,te tas mbooloom ñiy réy-réylu, 52 daaneel boroom doole yi ci seen nguur,yékkati baadoolo yi. 53 Ñi xiif, reggal na leen ak ñam wu neex,te dàq boroom alal yi,ñu daw ak loxoy neen. 54 Wallu na bànni Israyil giy jaamam,di fàttaliku yërmandeem, 55 ni mu ko dige woon sunuy maam,jëmale ko ci Ibraayma ak askanam ba fàww.» 56 Noonu Maryaama toog fa Elisabet lu war a tollook ñetti weer, sog a ñibbi. 57 Gannaaw loolu jamono ji Elisabet war a mucc agsi, mu daldi jur doom ju góor. 58 Dëkkandoom yi ak mbokkam yi yég ne, Boroom bi won na ko yërmande ju réy, ñu ànd ak moom bég. 59 Bi bés ba dellusee, ñu ñëw xarafalsi xale ba, bëgg koo dippee baayam Sakariya. 60 Waaye yaayam ne leen: «Déedéet, Yaxya lay tudd.» 61 Ñu ne ko: «Amoo menn mbokk mu tudd noonu.» 62 Ñu daldi liyaar baayam, ngir xam nan la bëgg ñu tudde xale ba. 63 Sakariya laaj àlluwa, bind ci ne: «Yaxya la tudd.» Ñépp daldi waaru. 64 Ca saa sa Yàlla dindi luu gi, Sakariya daldi waxaat, di màggal Yàlla. 65 Waa dëkk ba bépp jaaxle, xew-xew yooyu siiw ca tundi Yude yépp. 66 Ñi dégg nettali, bi jëm ci mbir yooyu, dañu koo denc ci seen xol te naan: «Nu xale bii di mujje nag?» Ndaxte leeroon na ne, dooley Boroom baa ngi ànd ak moom. 67 Sakariya baayu Yaxya daldi fees ak Xel mu Sell mi. Noonu mu wax ci kàddug Yàlla ne: 68 «Cant ñeel na Boroom bi, Yàllay Israyil,ndaxte wallusi na mbooloom, ba jot leen! 69 Feeñal na nu Musalkat bu am doole,bi soqikoo ci askanu Daawuda jaamam, 70 ni mu yéglee woon bu yàggjaarale ko ci yonentam yu sell yi. 71 Dina nu musal ci sunuy noon,jële nu ci sunu loxoy bañaale. 72 Yàlla wone na yërmandeem,ji mu digoon sunuy maam,te di fàttaliku kóllëre, gi mu fas ak ñoom, 73 di ngiñ, li mu giñaloon sunu maam Ibraayma naan, 74 dina nu teqale ak sunuy noon,ngir nu man koo jaamu ci jàmm, 75 nu sell te jub ci kanamam sunu giiru dund. 76 Yaw nag doom, dinañu lay wooye yonentu Aji Kawe ji,ndaxte dinga jiitu, di yégle ñëwu Boroom bi,di ko xàllal yoon wi. 77 Dinga xamal mbooloom,ni leen Boroom bi man a musale,jaare ko ci seen mbaalug bàkkaar, 78 ndaxte Yàlla sunu Boroom fees na ak yërmande,ba tax muy wàcce ci nun jant buy fenk, 79 ngir leeral ñi toog ci lëndëm,takkandeeru dee tiim leen,ngir jiite nu ci yoonu jàmm.»80 Noonu Yaxyaa ngi doon màgg, te xelam di ubbiku. Mu dëkk ca màndiŋ ma, ba bés ba muy feeñu bànni Israyil.