Wolof: New Testament

Luke

10

1 Gannaaw loolu Boroom bi tànn na yeneen juróom-ñaar-fukki taalibe ak ñaar, yebal leen, ñu ànd ñaar ak ñaar, jiituji ko ca dëkk yépp ak ca bérab yépp, ya mu naroon a dem moom ci boppam. 2 Mu ne leen: «Ngóob mi yaatu na, waaye liggéeykat yi barewuñu. Ñaanleen nag Boroom ngóob mi, mu yebal ay liggéeykat, ñu góob toolam. 3 Demleen! Maa ngi leen di yónni, mel ni ay mbote ci biir ay bukki. 4 Buleen yor xaalis walla mbuus walla ay dàll. Buleen nuyu kenn ci yoon wi. 5 «Kër gu ngeen man a dugg, nangeen jëkk ne: “Na jàmm wàcc ci kër gi.”6 Bu fa nitu jàmm nekkee, seen yéene dina ko indil jàmm. Lu ko moy, seen yéene dina dellusi ci yéen. 7 Dal-leen ca kër googa, tey lekk ak a naan lu ñu leen di jox, ndaxte liggéeykat yelloo na jot peyam. Buleen dem nag kër ak kër. 8 «Dëkk bu ngeen man a dugg, te waa dëkk ba teeru leen, lu ñu leen jox, lekkleen ko. 9 Nangeen wéral jaragi dëkk ba, te ngeen ne leen: “Nguuru Yàlla jegesi na leen.” 10 Waaye bu ngeen duggee ci dëkk te teeruwuñu leen, demleen ca mbedd ya te ne leen: 11 “Seen pëndu dëkk, bi taq ci sunuy tànk sax, noo ngi koy faxas, ngir seede leen seen réer. Waaye nag xamleen ne, nguuru Yàlla jegesi na.” 12 Maa ngi leen koy wax, bu bés baa, waa Sodom ñooy tane dëkk boobu. 13 «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon tuub nañu seeni bàkkaar bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku. 14 Moona ca bés pénc ba, Tir ak Sidon ñoo leen di tane. 15 Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe. 16 «Ku leen déglu, déglu na ma; ku leen bañ, bañ na ma. Te ku ma bañ, bañ na ki ma yónni.» 17 Juróom-ñaar-fukki taalibe yi ak ñaar dellusi, fees ak mbég te naan: «Boroom bi, rab yi sax déggal nañu nu ndax sa tur.» 18 Yeesu ne leen: «Maa ngi doon séen Seytaane wàcce asamaan ni safaras melax. 19 Gis ngeen, jox naa leen sañ-sañu joggi ci jaan yi ak ci jiit yi, daan dooley bañaale bi, te dara du leen man a gaañ. 20 Moona li leen rab yi déggal, bumu tax ngeen bég, waaye bégleen ndax li ñu bind seen tur ci asamaan.» 21 Ca saa soosu Xel mu Sell mi feesal Yeesu ak mbég, mu daldi ne: «Yaw Baay bi, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel, te xamal leen gune yi. Waaw Baay bi, ndaxte looloo la neex.» 22 Yeesu teg ca ne: «Sama Baay jébbal na ma lépp, te kenn mënul a xam, man Doom ji, maay kan, ku dul Baay bi; kenn mënul a xam it kan mooy Baay bi, ku dul man Doom ji, ak ku ma ko bëgg a xamal.» 23 Gannaaw bi mu waxee loolu, Yeesu walbatiku ca taalibe ya ne leen ñoom rekk: «Ñi seeni bët di gis li ngeen di gis, am nañu mbég. 24 Ndaxte maa ngi leen koy wax, yonent yu bare ak buur yu bare bëggoon nañoo gis li ngeen di gis, waaye gisuñu ko, te dégg li ngeen di dégg, waaye dégguñu ko.» 25 Noonu benn xutbakat daldi jóg, ngir fexee fiir Yeesu ne ko: «Kilifa gi, lan laa war a def, ba am dund gu dul jeex?» 26 Yeesu ne ko: «Lu ñu bind ci yoonu Musaa? Lan nga ciy jàng?» 27 Nit ka ne ko: « “Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, sa kàttan gépp ak sa xel mépp,” te it: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.”» 28 Yeesu ne ko nag: «Li nga wax dëgg la. Boo defee loolu, dinga dund ba fàww.» 29 Waaye xutbakat ba bëggoon a am aw lay, ne Yeesu: «Kan mooy sama moroom nag?» 30 Yeesu tontu ko ne: «Dafa amoon nit ku jóge woon Yerusalem, jëm Yeriko. Ay sàcc dogale ko, futti ko, dóor ko ba muy bëgg a dee, dem bàyyi ko fa. 31 Faf ab saraxalekat jaar ca yoon wa, séen nit ka, teggi. 32 Benn waay it bu soqikoo ci giiru Lewi, aw ca bérab booba, séen waa ja, teggi. 33 Waaye benn waay bu dëkk Samari bu doon tukki, ñëw ba jege waa ja, gis ko, yërëm ko. 34 Noonu mu ñëw, diw ko diwlin ak biiñ ngir faj gaañu-gaañu ya, bandaas ko. Gannaaw loolu mu teg ko ci mbaamam, yóbbu ko ci fanaanukaay, di ko topptoo. 35 Bi bët setee, mu génne ñaari poseti xaalis, jox ko boroom kër ga ne ko: “Nanga topptoo nit kooku. Bés bu ma fi jaaraatee, dinaa la fey, man ci sama bopp, lépp loo ci dolli ci xaalis.”» 36 Yeesu teg ca ne: «Lu ciy sa xalaat? Kan ci ñett ñooñu moo jëfe ni kuy jëf jëme ci moroomam, ba ñu gisee nit, ka sàcc ya dogale woon?» 37 Xutbakat ba tontu ko ne: «Xanaa ki ko won yërmandeem.» Yeesu ne ko nag: «Demal tey def ni moom.»38 Bi Yeesu ak ay taalibeem nekkee ci yoon wi, mu dugg ci benn dëkk, fekk fa jigéen ju tudd Màrt, ganale ko. 39 Màrt nag amoon rakk ju tudd Maryaama, ma nga toog ci tànki Boroom bi, di déglu ay kàddoom. 40 Fekk Màrt jàpp lool ca waañ wa. Noonu mu ñëw ci wetu Yeesu ne ko: «Boroom bi, doo ci wax dara, boo gisee sama rakk ji bàyyi ma ak liggéey bi yépp? Ne ko mu jàpple ma.» 41 Boroom bi tontu ko ne: «Màrt, Màrt, yu baree ngi fees sa xol, nga am ay téq-téq ndax loolu. 42 Moona de, lenn rekk a am solo. Maryaama dafa tànn cér bi gën, te kenn du ko nangu ci moom.»