Wolof: New Testament

Luke

14

1 Benn bésu noflaay Yeesu dem ci këru benn kilifag Farisen yi, ngir lekke fa. Nit ñaa ngi ko doon xool bu baax. 2 Faf am ca kanamam nit ku feebaroon, ay tànkam newi. 3 Yeesu yékkati baatam, ne xutbakat ya ak Farisen ya: «Ndax jaadu na, nu faj ci bésu noflaay bi?» 4 Waaye ñépp ne cell. Yeesu daldi laal jarag ja, faj ko, ba noppi ne ko mu ñibbi. 5 Gannaaw loolu mu ne leen: «Ku sa doom walla sa yëkk daanu ci teen, ndax doo dem génneji ko ca saa sa, fekk sax bésub noflaay la?»6 Amuñu woon dara lu ñu ciy teg. 7 Yeesu gis ni gan yi doon tànne toogu yu yiw yi, mu daldi leen wax léeb wii:8 «Bu ñu la wooyee ci xewu céet, bul jël toogu bu yiw. Man na am woo nañu it nit ku la ëpp daraja. 9 Kon ki leen woo yéen ñaar ñépp man na ñëw ci yaw ne la: “Joxal toogu bi nit kii.” Noonu dinga rus a dem ca toogu bu gannaawe ba. 10 Waaye bu ñu la wooyee, demal ca toogu bu gannaawe ba. Bu ko defee ki la woo, bu agsee ne la: “Sama xarit, àggal ca kaw.” Loolu dina la sagal ci ñi nga toogandool ci lekkukaay bi. 11 Ndaxte képp kuy yékkatiku, dees na la suufeel, te kuy suufeelu, dinañu la yékkati.» 12 Noonu Yeesu ne ki ko woo woon lekk: «Boo dee woote añ walla reer, bul woo rekk say xarit, say doomi ndey, say bokk, walla say dëkkandoo yu am alal. Lu ko moy ñooñu itam dinañu la woo, fey la bor bi. 13 Waaye boo dee woote lekk, wool néew doole yi, làggi yi, lafañ yi ak gumba yi. 14 Soo ko defee, dinga barkeel, ndaxte duñu la ko man a fey, waaye dinga jot sag pey, bés bi ñi jub di dekki.» 15 Bi mu déggee wax yooyu, kenn ca gan ya ne Yeesu: «Kiy lekk ci ñam, yi Yàlla di joxe ci nguuram, barkeel nga!» 16 Yeesu tontu ko ne: «Dafa amoon nit ku togglu ay ñam, woo ay nit ñu bare. 17 Bi waxtuw lekk jotee mu yónni surga ca ña muy ganale, fàttali leen: “Man ngeen a ñëw, ndaxte lépp sotti na léegi.” 18 «Waaye ñu tàmbali di jéggalu ci ngan gi ñoom ñépp. Ku jëkk ka ne ko: “Damaa jënd tool léegi, te fàww ma dem seeti ko. Maa ngi lay ñaan, nga jéggal ma.” 19 Keneen ne: “Damaa jënd léegi fukki yëkk, te damay dem nii, jéem leen a beyloo ba xam. Maa ngi lay ñaan, nga jéggal ma.” 20 Keneen ne ko: “Damay sog a takk jabar, looloo tax duma man a ñëw.” 21 «Surga ba dellu ca njaatigeem nettali ko loolu lépp. Noonu boroom kër ga mer, daldi ne surga ba: “Demal gaaw ca pénc ya ak ca mbedd ya ca dëkk ba, te indil ma fii néew doole yi, ñu làggi ñi, gumba yi ak lafañ yi.” 22 «Surga ba ñëwaat ne ko: “Sang bi, def naa li nga ma sant, waaye bérab bi feesul.” 23 Noonu njaatige ba ne ko: “Génnal dëkk bi te dem ca yoon ya ak ca tool ya, xiir nit ñi, ñu duggsi, ngir sama kër fees. 24 Maa ngi leen koy wax, ci ñi ma woo woon ci sama reer bi, kenn du ci ñam.”» 25 Am mbooloo yu réy yu toppoon ci Yeesu, ba muy dem ca yoon wa. Mu geestu ne leen: 26 «Képp ku ñëw ci man te gënalu ma ko baayam, yaayam, jabaram, ay doomam, ay magam ak ay rakkam, walla sax bakkanam, du man a nekk sama taalibe. 27 Képp koo xam ne nanguwuloo ñàkk sa bakkan, ba mel ni ku ñu daaj ci bant, te nga topp ma, doo man a nekk sama taalibe. 28 Su kenn ci yéen bëggee tabax taaxum kaw, ndax du jëkk a toog, xalaat ñaata la ko war a dikke, ngir seet ba xam ndax am na xaalis bu man a àggale liggéey bi? 29 Lu ko moy, su yékkatee fondamaa bi te mënu koo àggale, ñi koy gis dinañu ko ñaawal, naan ko: 30 “Waa jii dafa tàmbalee tabax, waaye mënu koo àggale.” 31 Walla boog ban buur mooy dugg ci xare ak beneen buur te jëkkul a toog, seet ba xam moom ak fukki junniy xarekat man na xeex ak kiy ñëw ak ñaar-fukki junniy xarekat? 32 Su ko mënul, dafay yónni ndaw ca beneen buur ba, fi ak ma ngay sore, ngir ñu juboo. 33 Naka noonu itam ku nekk ci yéen, bu dëdduwul li mu am lépp, du man a nekk sama taalibe. 34 «Xam ngeen nag ne, xorom lu baax la, waaye bu sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? 35 Du jariñ suuf, te du nekk tos. Dañu koy sànni ca biti. Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»