Wolof: New Testament

Luke

19

1 Yeesu dugg na Yeriko, jaar ca dëkk ba, di dem. 2 Waaye amoon na fa waa ju ñuy wax Sase. Njiitu juutikat la, te di ku bare alal. 3 Bëgg na gis kan mooy Yeesu, waaye dafa gàtt lool, ba mënu koo gis ndax mbooloo ma. 4 Noonu mu daw, jiituji ca yoon wa, yéeg ci genn garab ngir gis Yeesu, ndaxte foofa la naroon a jaar. 5 Bi Yeesu dikkee ba tollook garab ga nag, mu téen ne ko: «Sase, wàccal gaaw, ndax tey sa kër laa war a dal.» 6 Sase daldi gaawantu wàcc, ganale ko ak mbég. 7 Ñépp gis loolu, di ñurum-ñurumi naan: «Mi ngi dal cig këru boroom bàkkaar.»8 Waaye Sase taxaw ne Boroom bi: «Déglul Boroom bi, dogu naa may sama genn-wàllu alal miskin yi, te lu ma mas a njublaŋ nit, jël alalam, dinaa ko fey ñeenti yoon lu ni tollu.»9 Yeesu ne ko: «Mucc gi wàcc na tey ci kër gii, ndaxte nit kii, ci askanu Ibraayma la bokk itam. 10 Ndaxte Doomu nit ki ñëw na, ngir seet te musal ñi réer.» 11 Bi nit ñi doon déglu kàddu yooyu, Yeesu teg ca léeb, ndaxte jege woon na Yerusalem, te ñoom foogoon nañu ne, nguuru Yàlla dafay daldi feeñ ca saa sa. 12 Mu ne nag: «Dafa amoon boroom juddu bu rafet bu demoon ci réew mu sore, ngir ñu fal ko buur te mu dellusiwaat. 13 Noonu mu woo fukk ci ay surgaam, jox ku nekk benn libidoor, ne leen: “Liggéeyleen ci, ba may ñibbisi.” 14 Waaye waa réewam bëgguñu ko. Noonu ñu yónni ndaw ci gannaawam ne: “Bëggunu nit kii yilif nu.” 15 «Bi ñu ko falee buur nag, ba mu dellusi, mu woolu surga, ya mu joxoon wurus wa, ngir xam nan lañu ci liggéeye. 16 Ku jëkk ka ñëw ne ko: “Sang bi, sa libidoor bii jur na fukki libidoor.” 17 Buur ba ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga. Segam wone nga ne, takku nga ci lu tuuti, falul ci fukki dëkk.” 18 Surga ba ca topp ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor ba indi na juróomi libidoor.” 19 Buur ba ne ko: “Yaw, falul ci juróomi dëkk.” 20 Keneen ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor baa ngi nii. Dama koo fasoon ci sekkit, denc ko. 21 Dama laa ragaloon, ndaxte ku néeg nga. Dangay nangu loo dénkaanewul, di dajale loo jiwul.” 22 Buur ba ne ko: “Ci say wax laa lay àtte, surga bu bon bi! Xamoon nga ne, nit ku néeg laa, di nangu lu ma dénkaanewul, te dajale lu ma jiwul. 23 Lu tax nag yóbbuwoo sama xaalis ca denckati xaalis ya? Bés bu ma ñëwee nag, ma man a jot sama xaalis ak la mu jur.” 24 «Ci kaw loolu mu ne ña taxawoon ca wetam: “Nanguleen libidoor bi ci moom, jox ko boroom fukki libidoor yi.” 25 Ñu ne ko: “Sang bi, am na fukki libidoor ba noppi.” 26 Buur ba ne leen: “Maa ngi leen koy wax, ku am, dinañu la dolli, waaye ku amul, li nga am as néew sax, dinañu ko nangu. 27 Waaye sama noon yi, ñi bëggul woon ma doon seen buur, indileen fii, rey leen ci sama kanam.”» 28 Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa daldi jiitu, jëm Yerusalem. 29 Bi muy jege dëkki Betfase ak Betani, ci wetu tund wu ñuy wax tundu Oliw ya, Yeesu yebal ñaar ci ay taalibeem, 30 ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn musul a war. Yiwileen ko, indi. 31 Bu leen kenn laajee: “Lu tax ngeen koy yiwi?” tontuleen ko: “Boroom bi da koo soxla.”» 32 Ñaari ndaw ya dem, fekk mbir ya deme, na leen ko Yeesu waxe woon. 33 Bi ñuy yiwi cumbur ga nag, ay boroomam ne leen: «Lu tax ngeen di yiwi cumbur gi?» 34 Ñu tontu ne: «Ndaxte Boroom bi da koo soxla.» 35 Noonu ñu indil cumbur gi Yeesu, daldi lal seeni yére ca kaw, yéegal ca Yeesu. 36 Bi muy dem, nit ñi di lalal Yeesu seeni yére ci yoon wi. 37 Bi ñu agsee fa mbartalum tundu Oliw ya doore, taalibeem yépp fees ak mbég, tàmbalee màggal Yàlla ca kaw ndax kéemaan yu bare yi ñu gis. 38 Ñu ngi naan:«Yaw buur biy ñëw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!Na jàmm am ca asamaan,te ndam li féete ca bérab yu gën a kawe!» 39 Waaye ay Farisen yu nekkoon ca mbooloo ma ne Yeesu: «Kilifa gi, yeddal sa taalibe yi!» 40 Noonu mu tontu ne: «Maa ngi leen koy wax, bu ñu noppee ñoom, doj yiy xaacu.» 41 Bi Yeesu jegee dëkk ba, ba séen ko, mu jooy ko 42 naan: «Céy yaw itam, boo xamoon bésub tey yi la man a indil jàmm! Waaye fi mu ne mënuloo koo gis. 43 Bés dina ñëwi yu say noon di jal, wërale la. Dinañu la tëj ci biir, tanc la. 44 Dinañu la yàqaate, yaw ak sa waa dëkk. Doj dootul des ci kaw doj ci yaw, ndaxte ràññeewoo jamono ji Yàlla ñëwe, wallusi la.» 45 Gannaaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, daldi dàq ña fay jaay, 46 naan leen: «Mbind mi nee na: “Sama kër këru ñaan ci Yàlla lay doon; waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.”»47 Bés bu nekk Yeesu di jàngale ca kër Yàlla ga. Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya, ñoom ak njiiti xeet wa, ñu ngi ko doon wut a reylu. 48 Waaye xamuñu woon lan lañu man a def, ndaxte nit ñépp a ngi ko doon déglu, bañ benn baat raw leen.