1 Màggalu Mburu ya amul lawiir jege woon na, te ñu di ko wax Bésu Jéggi ba. 2 Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya di wut pexem reylu Yeesu, ndaxte dañoo ragaloon nit ña. 3 Noonu Seytaane daldi solu Yudaa, mi ñuy wooye Iskariyo te mu bokkoon ca fukki taalibe ya ak ñaar. 4 Noonu Yudaa dem waxtaani ak saraxalekat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga, ba xam nan la leen di jébbale Yeesu. 5 Ñu am ca bànneex bu réy, dig ko xaalis. 6 Yudaa nangu, di fexe jamono ju mu leen man a jébbal Yeesu, fu mbooloo ma nekkul. 7 Bésu màggalu Mburu ya amul lawiir agsi, ca bés boobu lañu waroon a rendi mbotem màggalu Jéggi ba. 8 Noonu Yeesu yebal Piyeer ak Yowaana ne leen: «Demleen, defaral nu reeru Jéggi ba.»9 Ñu ne ko: «Fan nga bëggoon, nu defare ko fa?» 10 Mu ne leen: «Bu ngeen duggee ca dëkk ba, góor gu yenu njaq lu def ndox, dina taseek yéen. Toppleen ci moom ba ca kër ga muy dugg, 11 te ngeen ne boroom kër ga: “Kilifa gi nee na: Ana néegu gan, bi may lekke reeru Jéggi ba, man ak samay taalibe?” 12 Noonu dina leen won néeg bu féete kaw, te yaa, ñu defar ko ba noppi. Foofa ngeen koy defare.» 13 Ñu dem, gis lépp, ni leen ko Yeesu waxe woon. Noonu ñu defar reer bi. 14 Bi waxtu wi jotee Yeesu toog ak ndaw yi, 15 ne leen: «Yàkkamti woon naa lool lekk ak yéen reeru Jéggi bii, laata ñu may sonal. 16 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma ko lekk mukk, lu dul ba kera mu mat ci nguuru Yàlla.» 17 Noonu mu fab kaas, daldi sant Yàlla ne: «Jël-leen kaas bii, séddoo ko. 18 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma naan ndoxum réseñ mi, ba kera Yàlla di tëral nguuram.» 19 Gannaaw loolu mu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, joxleen ko ne: «Lii sama yaram la, wi ma joxe ngir yéen. Defleen lii, ngir fàttaliku ma.» 20 Noonu itam bi ñu lekkee ba noppi, mu jël kaas bi ne leen: «Kaas bii mooy misaal kóllëre gu bees gi Yàlla fas jaarale ko ci sama deret, ji tuuru ngir yéen. 21 Waaye nag loxob ki may wor a ngi nekk ak man ci ndab li. 22 Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko dogale. Waaye ki koy wor dina torox.» 23 Noonu taalibe yi di laajante ci seen biir, kan ci ñoom mooy nar a def loolu. 24 Taalibe ya it di werante, ngir xam kan ci ñoom moo gën a màgg. 25 Yeesu ne leen: «Buuri xeeti àddina dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañuy sàkku ngërëm. 26 Waaye yéen buleen def noonu. Ki gën a màgg ci yéen, na nekk ni ki gën a ndaw, te njiit mel ni surga. 27 Ki toog ca lekkukaay ba, moom ak surgaam, ñoom ñaar kan moo ci gën a màgg? Xanaa du ki toog ci lekkukaay bi? Waaye man maa ngi ci seen biir ni surga. 28 Yéen nag yéenay ñi ànd ak man ci samay fitna. 29 Man nag jox naa leen sañ-sañu nguuru, ni ma ko sama Baay joxe. 30 Dingeen lekkandoo te naanandoo ak man ci sama nguur. Te dingeen toog ci jal yi, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil.» 31 Yeesu teg ca ne: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane ñaan na, ñu jébbal leen ko, ngir mu teqale leen ni ñu teqalee dugub ak xatax. 32 Waaye man ñaanal naa la, ngir sa ngëm dëgër. Te yaw, boo dellusee, nanga dëgëral sa bokki taalibe yi.» 33 Piyeer ne ko: «Boroom bi, àttan naa ànd ak yaw ca kaso, ba ci dee sax.» 34 Yeesu tontu ko ne: «Piyeer, maa ngi la koy wax, bala ginaar a sab tey jii, dinga weddi ñetti yoon ne, xam nga ma.» 35 Noonu Yeesu ne leen: «Ba ma leen yebalee te yóbbaalewuleen woon xaalis, mbuus, walla dàll, ndax ñàkkoon ngeen dara?» Ñu tontu ne: «Déedéet.» 36 Mu neeti leen: «Léegi nag képp ku am xaalis, na ko jël; te ku am mbuus, na ko jël; ku amul jaasi, na jaay mbubbam, jënde ko jaasi. 37 Ndaxte maa ngi leen koy wax, lii Mbind mi wax fàww mu am ci man, bi mu nee: “Boole nañu ko ak ñu bon ña.” Ndaxte loolu jëm ci man mi ngi mat.» 38 Noonu taalibe ya ne ko: «Boroom bi, ñaari jaasee ngii.» Mu ne leen: «Doy na.» 39 Noonu Yeesu génn, dem ca tundu Oliw ya, ni mu ko daan defe nakajekk. Taalibeem ya topp ci moom. 40 Bi mu agsee ca bérab ba, mu ne leen: «Ñaanleen, ngir bañ a daanu cig fiir.» 41 Noonu mu dand leen, ba fu aw saan man a tollu, daldi sukk di ñaan ne: 42 «Baay, soo ko bëggee, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.» 43 Noonu malaakam Yàlla daldi koy feeñu, may ko doole. 44 Ci biir tiis, Yeesu gën a sawar ci ñaan gi, ñaqam mel ni lumbi deret dal ci suuf. 45 Bi mu ñaanee ba noppi, mu jóg, dellusi ci taalibe yi, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seen xol dafa sonnoon ak tiis. 46 Noonu mu ne leen: «Lu tax ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir bañ a daanu cig fiir.» 47 Bi Yeesu di wax, mbooloo mu bare agsi; ku ñuy wax Yudaa te mu bokkoon ci fukki ndaw yi ak ñaar jiite leen. Yudaa jegeñsi Yeesu, bëgg koo fóon. 48 Waaye Yeesu ne ko: «Ci fóon ngay jébbale Doomu nit ki ay noonam!» 49 Bi ñi àndoon ak Yeesu gisee liy bëgg a xew, ñu ne: «Boroom bi, ndax nu dóore jaasi?» 50 Kenn ci ñoom nag dóor surgab saraxalekat bu mag ba, noppu ndeyjooram dagg. 51 Waaye Yeesu daldi ne: «Bàyyileen.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko. 52 Noonu Yeesu ne saraxalekat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga ak njiiti xeet, wa ko jàppsi woon: «Jóg ngeen, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc. 53 Moona maa nga woon ak yéen bés bu nekk ca kër Yàlla ga, te jàppuleen ma. Waaye léegi seen waxtu la, di jamonoy lëndëm.» 54 Ñu jàpp Yeesu, yóbbu ko ca kër saraxalekat bu mag ba. Piyeer topp fu sore. 55 Amoon na taal ca diggu ëtt ba, ay nit toog, wër ko, Piyeer itam toog ci seen biir. 56 Ab mbindaan gis ko, mu toog, taal bi di ko leeral, mu ne ko jàkk ne: «Nit kii itam àndoon na ak moom.» 57 Waaye Piyeer weddi ko ne: «Soxna si, xawma kooku.» 58 Nes tuuti keneen gis ko ne: «Yaw itam ci ñoom nga bokk.» Piyeer tontu ko: «Sama waay, bokkuma ci.» 59 Bi ñu tegee lu mat waxtu, keneen dikkaat ca wax ja ne: «Ci lu wóor nit kii àndoon na ak moom, nde Galile la jóge.» 60 Waaye Piyeer tontu ne: «Sama waay, xawma li ngay wax!» Bi kàddoom di daanu, faf ginaar daldi sab. 61 Noonu Boroom bi geestu, xool Piyeer. Te Piyeer fàttaliku la ko Boroom bi waxoon ne: «Bala ginaar a sab tey jii, dinga ma weddi ñetti yoon.» 62 Piyeer daldi génn, di jooy jooy yu metti. 63 Nit ñaa nga jàppoon Yeesu, di ko ñaawal ak di ko dóor. 64 Ñu ngi takkoon ay bëtam, di ko laaj, naan ko: «Yaw, wax nu ci kàddug Yàlla, ku la dóor?» 65 Ñu ngi ko doon tifaar it yeneeni saaga.66 Bi bët setee, kureelu njiiti xeet wa, maanaam saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya, daldi daje, indi Yeesu ci seen kanam. 67 Ñu ne ko: «Soo dee Almasi bi, wax nu ko.» Mu tontu leen ne: «Su ma leen ko waxee, dungeen ma gëm. 68 Te su ma leen laajee, dungeen tontu. 69 Waaye gannaawsi tey, Doomu nit ki dina toog ci ndeyjooru Yàlla, Aji Kàttan ji.» 70 Noonu ñépp ne: «Kon nag yaay Doomu Yàlla ji?» Mu tontu leen ne: «Yéen ci seen bopp wax ngeen ne moom laa.» 71 Ñu daldi ne nag: «Lu nuy doyeeti seede léegi, ndegam nun ci sunu bopp noo ko nangoo ci gémmiñam!»