1 Amoon na benn bésu noflaay Yeesu di dem, jaar ci ay tool yu ñor. Taalibeem ya di fàq ay cëgg, di leen boxom ci seeni loxo tey lekk. 2 Am ay Farisen yu ne: «Lu tax ngeen di def lu jaaduwul ci bésu noflaay bi?»3 Yeesu tontu leen ne: «Ndax jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom ak ña mu àndaloon?4 Xanaa yéguleen, ni mu dugge woon ca kër Yàlla ga, jël mburu, ya ñu jébbal Yàlla, lekk ca, jox ca ña mu àndaloon? Fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul saraxalekat.»5 Yeesu dellu ne leen: «Doomu nit ki mooy boroom bésu noflaay bi.» 6 Beneen bésu noflaay, Yeesu dugg ci jàngu bi, di fa jàngale. Amoon na fa nit ku loxol ndeyjooram làggi. 7 Xutbakat yi ak Farisen yi ñu ngi ko doon xool, ba xam dina ko faj ci bésu noflaay bi, ngir ñu am lu ñu ko tuumaale. 8 Waaye Yeesu xam seen xalaat, daldi ne ku loxoom làggi: «Jógal taxaw ci kanamu ñépp.» Nit ka daldi jóg taxaw. 9 Yeesu ne leen: «Ma laaj leen, lan moo jaadu, nu def ko bésu noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu lor nit?» 10 Ci kaw loolu mu xool leen ñoom ñépp, ba noppi ne nit ka: «Tàllalal sa loxo.» Mu tàllal ko, loxoom daldi wér peŋŋ. 11 Waaye nit ña mer ba fees, di rabat pexe yu jëm ca Yeesu. 12 Ca bés yooya Yeesu yéeg ca tund wa ngir ñaan, mu fanaan fa, di ñaan ci Yàlla. 13 Bi bët setee, Yeesu woo taalibeem yi, tànn ci fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam: 14 Simoŋ, mi Yeesu tudde Piyeer, ak Andare, mi bokk ak Piyeer ndey ak baay; Saag ak Yowaana, Filib ak Bartelemi, 15 Macë ak Tomaa, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokk ci mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew; 16 Yudaa doomu Saag, ak Yudaa Iskariyo, mi mujj a wor. 17 Yeesu ànd ak ndaw ya, wàcc tund ya, daldi taxaw ca joor ga, fa mbooloom taalibe mu takku nekkoon. Amoon na fa it ay nit ñu bare ñu jóge ca réewu Yawut ya mépp ak ca dëkku Yerusalem ak dëkk yi nekk ca wetu géej ga, maanaam Tir ak Sidon. 18 Dañoo ñëw ngir déglu ko, te it ngir mu faj leen. Ñi rab jàpp it faju nañu. 19 Ñépp a ngi ko doon wut a laal ndax doole jiy jóge ci moom, di faj ñépp. 20 Yeesu xool ay taalibeem ne leen:«Yéen ñi sësul lu dul ci Yàlla, barkeel ngeen,ndaxte nguuru Yàlla, yéena ko yelloo. 21 Yéen ñi xiif léegi, barkeel ngeen,ndax dingeen regg.Yéen ñiy naqarlu léegi, barkeel ngeen,ndax dingeen ree.22 Barkeel ngeen, bu leen nit ñi bañee, di leen dàq ak a saaga, di sib seen tur ngir Doomu nit ki. 23 Bu boobaa bégleen te bànneexu, ndax seen yool dina réy ci laaxira. Ndaxte noonu la maami seeni bañ daan fitnaale yonent yi. 24 Waaye nag yéen boroom alal yi, torox ngeen,ndaxte jot ngeen ba noppi seen bànneex. 25 Yéen ñiy lekk ba suur léegi, torox ngeen,ndax ëllëg dingeen xiif.Yéen ñiy ree léegi, torox ngeen,ndax dingeen am aw naqar, ba jooy xàcc.26 Torox ngeen bu leen ñépp dee waxal lu baax, ndaxte noonu la seeni maam daan jëfe ak ña doon mbubboo yonent. 27 «Waaye maa ngi leen koy wax, yéen ñi may déglu, soppleen seeni bañaale tey defal lu baax ñi leen bañ. 28 Yéeneleen lu baax ñi leen di móolu, te ñaanal ñi leen di sonal. 29 Ku la talaata cib lex, jox ko ba ca des. Kuy nangu sa mbubb mu mag, bul téye sa turki. 30 Képp ku la ñaan, may ko, te ku nangu say yëf, bu ko ko laaj. 31 Defal-leen nit ñi li ngeen bëgg, ñu defal leen ko. 32 «Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban ngërëm ngeen ciy am? Ndaxte bàkkaarkat yi sax sopp nañu ñi leen sopp. 33 Te bu ngeen defalee lu baax ñi leen koy defal, ban ngërëm ngeen ciy am? Bàkkaarkat yi it dañuy def noonu. 34 Te bu ngeen dee leble te yaakaar ci ndelloo, ban ngërëm ngeen ciy am? Bàkkaarkat yi it dañuy lebal seeni moroom, ngir ñu delloo leen ko. 35 Waaye soppleen seeni noon, di leen defal lu baax, tey leble, bañ a yaakaar ñu delloo leen ko. Noonu seen yool dina mag te dingeen wone ne, yéenay doomi Aji Kawe ji, ndaxte Yàlla day wone mbaaxam ci ñu goreedi ñi ak ñu soxor ñi. 36 Nangeen am yërmande, ni seen Baay ame yërmande. 37 «Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, te deesu leen àtte. Buleen daan kenn, te deesu leen daan. Baal-leen ñi ci des, te dinañu leen baal. 38 Mayeleen te dinañu leen may. Dinañu leen ëmbal natt bu baax bu ñu rokkas te yengal ko, mu fees bay tuuru. Ndaxte dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale.» 39 Noonu Yeesu wax na leen beneen léeb ne leen: «Ndax gumba man na wommat moroomam? Mbaa duñu daanu ñoom ñaar ci kàmb? 40 Taalibe gënul kilifaam, waaye taalibe bu jàng ba wàcc, dina yem ak kilifaam demin. 41 «Lu tax ngay xool ñax gi ci sa bëtu mbokk, te gisuloo gànj gi ci sa bët yaw? 42 Nan nga man a waxe sa mbokk: “Sama xarit, may ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” yaw mi gisul gànj gi nekk ci sa bët? Naaféq! Jëkkal a dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga man a gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk. 43 «Garab gu baax du meññ doom yu bon, te garab gu bon du meññ doom yu baax. 44 Ndaxte garab, meññeefam lañu koy xàmmee. Deesul witte figg ci dédd, walla réseñ ci xaaxaam. 45 Noonu nit ku baax, lu baax lay wax, ndax loolu la denc ci xolam, te nit ku bon, lu bon lay wax, ndaxte denc na lu bon ci xolam. Ndaxte gémmiñ, la fees xolam lay wax.46 «Lu tax ngeen may wooye “Boroom bi, Boroom bi,” te dungeen def li may wax? 47 Képp ku ñëw ci man, di dégg samay wax te di ko jëfe, ma won leen nu muy mel. 48 Dafa mel ni nit kuy tabax kër, mu gas fu xóot, jot doj wu réy, samp fa kër ga. Bi mbënn ma ñëwee, wal ma dafa dal ca kër ga te yenguwul, ndaxte nit ka dafa tabax kër ga tabax bu dëgër. 49 Waaye képp ku dégg samay wax te jëfewuloo ko, dinga mel ni nit ku tabax këram ci suuf, bañ koo defal fondamaa. Bi wal ma dalee ca kër googa, dafa màbb ca saa sa, lépp yàqu yaxeet.»