1 Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, dem ca wàlli réewu Yawut yi, ya ca gannaaw dexu Yurdan. Bi mu fa demee, mbooloo mu bare ñëw fi moom. Yeesu daldi leen jàngal, ni mu ko daan defe. 2 Noonu ay Farisen ñëw ci moom, lalal ko fiir, ñu laaj ko: «Ndax jaadu na, nit fase jabaram?»3 Yeesu tontu leen ne: «Lu leen yoonu Musaa sant?»4 Ñu ne ko: «Musaa maye na, nit bind kayitu pase, tàggook jabaram.»5 Waaye Yeesu ne leen: «Dénkaane boobu mu leen bindal, bind na ko ndax seen xol dafa fatt. 6 Waaye ca njàlbéen ga “Yàlla sàkk na leen, kii góor, kii jigéen. 7 Moo tax góor dina beru ndeyam ak baayam, di taq ci jabaram,8 ñoom ñaar doon benn.” Kon nekkatuñu ñaar waaye benn. 9 Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas.» 10 Bi ñu delloo ca kër ga nag, taalibe ya laaj ko ci mbirum loolu. 11 Noonu Yeesu ne leen: «Ku fase sa jabar, takk jeneen, njaaloo nga, di tooñ ku jëkk ka. 12 Te jigéen ji tas, séyaat ak keneen, njaaloo nga.» 13 Bi loolu wéyee ñu indil Yeesu ay xale, ngir mu teg leen ay loxoom. Waaye taalibe ya gëdd nit ñi. 14 Bi ko Yeesu gisee nag, mu metti ko lool, mu ne leen: «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw fi man! Buleen leen tere, ndaxte ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguuru Yàlla. 15 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ku woyoful ni xale, nangu nguuru Yàlla, doo ci man a dugg.» 16 Noonu Yeesu leewu leen, teg leen ay loxoom, barkeel leen. 17 Gannaaw loolu bi Yeesu nekkee ci kaw yoon wi di dem, am ku daw, sukk ci kanamam ne ko: «Kilifa gu baax gi, lu ma war a def, ngir am wàll ci dund gu dul jeex gi?» 18 Yeesu tontu ko: «Lu tax nga wooye ma ku baax ki? Yàlla rekk a baax. 19 Xam nga ndigal yi: “Bul bóom, bul njaaloo, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, bul nangu alalu jaambur, teralal sa ndey ak sa baay.”» 20 Waa ji ne ko: «Kilifa gi, loolu lépp sàmm naa ko li dale ci samag ndaw ba tey.» 21 Noonu Yeesu xool ko, am cofeel ci moom, mu ne ko: «Lenn rekk moo la dese. Demal jaay li nga am, may ko miskin yi, te dinga woomle ci asamaan; boo noppee, nga ñëw topp ci man.» 22 Waaye ci wax jooju xar-kanamam lëndëm, mu jóge fa ak tiis, ndaxte ku bare woon alal la. 23 Noonu Yeesu xool taalibe yi ko wër ne leen: «Boroom alal dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu!» 24 Wax jooju nag daldi jaaxal taalibe yi lool. Waaye Yeesu neeti leen: «Samay xarit, dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu! 25 Giléem jaar ci bën-bënu pusa, moo gën a yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla.» 26 Wax jooju gënatee jaaxal taalibe ya, ñu naan ci seen biir: «Kon nag ku man a mucc?» 27 Noonu Yeesu xool leen naan: «Loolu të na nit, waaye tëwul Yàlla; Yàlla man na lépp.» 28 Ci kaw loolu Piyeer daldi ko ne: «Nun de dëddu nanu lépp te topp la!» 29 Yeesu tontu ko: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, képp ku dëddu kër, doomu ndey yu góor walla yu jigéen, ndey walla baay, doom walla suuf ndax man ak xebaar bu baax bi, 30 dinga am tey jii téeméeri yoon ay kër, doomi ndey yu góor ak yu jigéen, ndey, doom ak suuf, ñoom ak ay fitnay noon, te ëllëg nga am dund gu dul jeex. 31 Waaye ñu bare ci ñi jiitu ñooy mujji; ñi mujj ñooy jiituji.» 32 Gannaaw loolu ñu ànd jëm Yerusalem, Yeesu jiitu; taalibe yi am njàqare, te ñi ci topp tiit. Noonu Yeesu woowaat fukk ak ñaar ña cig wet, xamal leen li nar a xew ci mbiram. 33 Mu ne leen: «Noo ngi dem Yerusalem, te dees na jébbal Doomu nit ki ci loxoy saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya. Dinañu ko àtte, teg ko dee, jébbal ko ñi dul Yawut, 34 ñu ñaawal ko, di tifli ci kawam, dóor ko ay yar, rey ko. Waaye gannaaw ñetti fan dina dekki.» 35 Gannaaw loolu Saag ak Yowaana, doomi Sebede, ñëw ci Yeesu. Ñu ne ko: «Kilifa gi, danoo bëggoon nga may nu li nu lay ñaan.» 36 Yeesu tontu leen: «Lu ngeen bëggoon, ma may leen ko?» 37 Ñu ne ko: «Bés boo soloo sa ndam, nga may nu, nu toog, kii ci sa ndeyjoor, kii ci sa càmmooñ.» 38 Waaye Yeesu tontu leen: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax man ngeen a naan kaasu naqar, bi may naan? Ndax man ngeen a sóobu ci metit, yi ma nar a sóobu?» 39 Ñu ne ko: «Waaw, man nanu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Dingeen naan kaasu naqar, bi may naan, tey sóobu ci metit, yi ma nar a sóobu, 40 waaye toog ci sama ndeyjoor mbaa sama càmmooñ, du man maa koy maye. Ñi ñu ko waajal rekk a ko yelloo.» 41 Bi nga xamee ne fukki taalibe ya ca des dégg nañu loolu, ñu daldi mere Saag ak Yowaana. 42 Waaye Yeesu woo leen naan: «Xam ngeen ne ci xeeti àddina, ñi ñu teg njiit dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi di leen noot. 43 Buleen mel ni ñooñu. Waaye ku bëgg a nekk kilifa ci yéen, na nekk seen surga, 44 te ku bëgg a nekk njiit, na nekk seen jaam. 45 Ndaxte noonu la Doomu nit ki ñëwe sax, du ngir ñu nekk ay surgaam, waaye ngir muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug ñu bare.» 46 Bi loolu wéyee ñu agsi ca dëkku Yeriko. Bi ko Yeesu di génn, ànd ak taalibe ya ak mbooloo mu xaw a bare, am gumba gu tudd Bartime — liy tekki «doomu Time,» toog ci wetu yoon wi, di yelwaan. 47 Noonu mu dégg ne, Yeesum Nasaret moo fay romb; mu daldi yuuxu naan: «Yërëm ma, yaw Sëtu Daawuda bi!» 48 Ci kaw loolu ñu bare gëdd ko, ngir mu noppi. Teewul mu gën a yuuxu naan: «Yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm ma!»49 Noonu Yeesu taxaw, daldi ne: «Wooleen ko!» Ñu woo nag gumba gi ne ko: «Na sa xel dal! Jógal! Mu ngi lay woo.» 50 Bi mu ko déggee, mu sànni malaanam, ne bërét, dem ci Yeesu. 51 Yeesu ne ko: «Loo bëggoon ma defal la ko?» Gumba gi tontu ko: «Kilifa gi, damaa bëgg a gis.» 52 Noonu Yeesu ne ko: «Demal ci jàmm. Sa ngëm faj na la.» Ci saa si gumba gi gis, daldi topp Yeesu ci yoon wi.