Wolof: New Testament

Mark

15

1 Ci suba teel saraxalekat yu mag yi gise, ñoom ak njiit yi ak xutbakat yi ak kureelu àttekat yi yépp. Ñu yeew nag Yeesu, daldi ko yóbbu, jébbal ko Pilaat. 2 Noonu Pilaat laaj ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?» Yeesu tontu ko: «Wax nga ko.»3 Te saraxalekat yu mag yi di ko jiiñ lu bare. 4 Kon nag Pilaat laajaat ko: «Déggal lépp li ñu lay jiiñ. Xanaa amoo ci tont?»5 Waaye ba tey Yeesu tontuwul dara, ba tax Pilaat waaru. 6 Màggal gu nekk nag Pilaat daan na may mbooloo mi, ñu tànn kenn ci ñi ñu tëjoon, mu bàyyil leen ko. 7 Fekk booba amoon na ku ñu tëj, tudd Barabas, ku bokk ci ña bëggoon a tas réew mi, boole ci rey nit. 8 Noonu mbooloo mi ñëw, laaj Pilaat, mu defal leen la mu daan def. 9 Pilaat nag xam ne, kiñaan rekk a taxoon saraxalekat yu mag yi jébbal ko Yeesu. Kon mu ne mbooloo mi: «Xanaa ma bàyyil leen buuru Yawut yi?» 11 Waaye saraxalekat yu mag yi xiir mbooloo mi, ñu laaj Pilaat, mu bàyyil leen Barabas. 12 Kon Pilaat ne leen: «Lan laay def nag ak ki ngeen di wooye buuru Yawut yi?» 13 Ñu daldi yuuxuwaat naan: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!» 14 Pilaat ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye mbooloo mi di yuuxu bu gën a kawe: «Daaj ko ci bant!» 15 Noonu Pilaat, mi wut a neex mbooloo mi, bàyyil leen Barabas, ba noppi mu dóorlu Yeesu ay yar, jébbal ko, ngir ñu daaj ko ci bant. 16 Bi loolu amee ñu dugal Yeesu ci biir kër boroom réew ma, mooy bérab bu ñuy wax Peretoriyum, ñu daldi woo mbooloom xarekat yépp. 17 Noonu ñu solal ko mbubb mu xonq curr, ràbb kaalag dég, teg ko ci boppam. 18 Ñu daldi ko wax bu kawe: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!» 19 Ñu di ko dóor ci bopp ak bant, di ko tifli, daldi sukk, màggal ko. 20 Bi ñu ko ñaawalee noonu ba noppi, ñu summi mbubb mu xonq mi, solaatal ko ay yéreem, yóbbu ko, ngir daaj ko ci bant. 21 Amoon na nag nit ku dëkk Siren, tudd Simoŋ, di baayu Alegsàndar ak Rufus. Fekk booba mu romb fa, jóge ca wet, ga féete ak tool ya, ñu ga ko ngir mu gàddu bant bi. 22 Noonu ñu yóbbu Yeesu ca bérab bu ñuy wax Golgota, liy tekki «Bérabu kaaŋu bopp.» 23 Ñu bëgg koo jox biiñ bu ñu boole ak naan gu tudd miir, waaye nanguwu ko. 24 Foofa ñu daaj Yeesu ci bant, daldi séddoo ay yéreem, tegoo ko ay bant, ba xam ku nekk, looy am; 25 booba fekk yoor-yoor di jot. 26 Mbind mi xamle lu tax ñu rey ko nee na: «Kii mooy buuru Yawut yi.» 27 Booba it ñu daajaale ak moom ñaari taskati réew mi, kenn ci ndeyjooram, ki ci des ci càmmooñam. 29 Ña fa doon romb di ko xas, di wëcc seen bopp ndax sib ko naan: «Waaw kay, yaw mi bëgg a toj kër Yàlla gi, tabaxaat ko ci ñetti fan, 30 wàccal ci bant bi te musal sa bopp!» 31 Noonu it saraxalekat yu mag yi ak xutbakat yi di ko ñaawal ci seen biir naan: «Kii musal na ñeneen waaye mënul a musal boppam. 32 Almasi bii, di buuru Israyil, na wàcc léegi ci bant bi, nu gis ko te gëm.» Ñi ñu daajaale ak moom it di ko xarab. 33 Li tàmbalee digg-bëccëg, ba ci tisbaar, réew mépp lëndëm. 34 Ci tisbaar nag Yeesu wootee kàddu gu dëgër naan: «Elowi, Elowi, lema sabaktani?» liy tekki: «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga dëddu ma?» 35 Ñenn ci ña fa taxaw nag, bi ñu ko déggee, ñu ne: «Mu ngi woo yonent Yàlla Iliyas.» 36 Noonu kenn daw, jël aw sagar, capp ko ci bineegar, mu teg ko ci bant, jox ko ko, mu muucu. Mu ne: «Bàyyileen, nu seet, ba xam Iliyas dina ñëw, wàcce ko.» 37 Noonu Yeesu wootewaat ak kàddu gu dëgër, delloo ruuwam Yàlla. 38 Bi mu ko defee ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga xar ñaar, li dale ci kaw ba ci suuf. 39 Njiitu xare nag, bi taxawoon ci kanamu Yeesu, bi mu gisee ni Yeesu deeye, mu ne: «Ci dëgg, nit kii Doomu Yàlla la!» 40 Amoon na fa nag ay jigéen, ñu leen dand, di xool. Xàmmi nañu ci: Maryaama mi dëkk Magdala, Maryaama yaayu Saag mu ndaw ak Yuusufa, ak Salome. 41 Bi Yeesu nekkee Galile, jigéen ñooñu ñoo ko doon topp, di ko topptoo. Amoon na fa it yeneen jigéen yu bare yu àndoon ak moom, ba ñëw Yerusalem. 42 Booba nag bésu Waajal la woon, maanaam bés bu jiitu bésu noflaay bi. Ca ngoon sa nag, 43 Yuusufa mi dëkk Arimate takk aw fitam, dem Pilaat, laaj ko néewu Yeesu. Yuusufa moomu nag, ku siiw la woon ci kureelu àttekat yi, te doon séentu moom itam nguuru Yàlla. 44 Bi Pilaat déggee ne, Yeesu faatu na xaat, mu waaru. Mu woolu nag njiit li, laaj ko, ndax yàgg na faatu. 45 Bi ko ko njiit li dëggalee, Pilaat jox néew bi Yuusufa.46 Noonu Yuusufa jënd càngaay, wàcce néew bi, laxas ko ci, dugal ko cib bàmmeel bu ñu yett ci xeer. Bi mu ko defee mu béraŋ aw doj, ube ko buntu bàmmeel bi. 47 Maryaamam Magdala nag ak Maryaama yaayu Yuusufa xool fu mu ko denc.