Wolof: New Testament

Matthew

17

1 Juróom-benni fan gannaaw gi, Yeesu àndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana rakkam, yóbbu leen fu wéet ci tund wu kawe lool. 2 Mu soppiku fa seen kanam, xar-kanamam di melax nib jant, te ay yéreem weex ni leer. 3 Naka noonu ñu gis yonenti Yàlla Musaa ak Iliyas, di waxtaan ak Yeesu. 4 Piyeer nag daldi wax Yeesu ne ko: «Sang bi, bég nanu ci sunu teew fii; soo ko bëggee, dinaa fi defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Iliyas.»5 Waaye bi muy wax, niir wu leer muur leen, te baat jib ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg, ci moom laa ame bànneex; dégluleen ko.» 6 Bi taalibe yi déggee baat bi, ñu ne nërëm ci suuf, daldi tiit lool. 7 Waaye Yeesu jegeñsi, laal leen naan: «Jógleen, buleen ragal dara.»8 Noonu ñu xool ci kaw, waaye gisatuñu kenn ku dul Yeesu rekk. 9 Bi loolu amee ñu wàcc ca tund wa. Bi ñuy wàcc nag, Yeesu sant leen ne: «Buleen nettali kenn li ngeen gis, ba kera Doomu nit ki dekki.» 10 Noonu taalibe ya laaj ko: «Lu tax xutbakat ya nag di wax ne, Iliyas mooy jëkk a ñëw?» 11 Yeesu tontu leen ne: «Waaw dëgg la, Iliyas war na ñëw, jubbanti lépp. 12 Teewul maa ngi leen di wax ne, Iliyas ñëw na te xàmmiwuñu ko, waaye def nañu ko la leen neex. Noonu it dañoo nar a sonal léegi Doomu nit ki.» 13 Ndax wax jooju nag, taalibe ya xam ne, ci mbirum Yaxya la leen doon wax. 14 Bi nga xamee ne wàcc nañu, ba ñëw ca mbooloo ma, genn góor ñëw ci moom, sukk 15 naan: «Sang bi, yërëmal sama doom, ndaxte mu ngi say, di am coono bu metti; léeg-léeg mu daanu ci safara, léeg-léeg mu daanu ci ndox. 16 Indi naa ko ci say taalibe, waaye mënuñu koo faj.» 17 Noonu Yeesu tontu ne: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi te dëng, ba kañ laa war a nekk ak yéen, ba kañ laa leen di war a muñal?» Mu ne leen, «Indil-leen ma xale bi fii.» 18 Noonu Yeesu tëkku rab wa, rab wa génn ca xale ba, mu daldi wér ca saa sa. 19 Bi loolu amee taalibe ya ñëw ci Yeesu, laaj ko ci pegg: «Lu tax nun mënunu woon a dàq rab wi?» 20 Yeesu tontu leen ne: «Seen ngëm gu néew a tax. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen ne tund wii: “Jógeel fii, toxu fale,” te dina fa dem, ba dara du leen të.» 22 Bi ñuy wër diiwaanu Galile nag, Yeesu ne leen: «Léegi ñu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi; 23 dinañu ko rey, mu dekki ca ñetteelu fan ba.» Bi ko taalibe ya déggee, ñu am naqar lool. 24 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya ñëw Kapernawum. Bi ñu fa àggee nag, laajkati warugaru kër Yàlla ga ñëw ci Piyeer ne ko: «Ndax seen kilifa du fey posetu ñaari daraxma ngir warugar wi?» 25 Piyeer ne leen: «Aaŋkay!»Ba ñu eggee kër ga nag, Yeesu jëkk a wax ne Piyeer: «Waaw lu ciy sa xalaat, Simoŋ? Buuri àddina si, ñan lañuy laaj juuti walla galag? Seeni doom walla ñi bokkul ci njaboot gi?» 26 Piyeer tontu ko ne: «Xanaa ñi bokkul ci kër gi.» Yeesu ne ko: «Kon doom yi nag mucc nañu ci. 27 Waaye bëgguma nu naqaral leen; kon demal sànni oos ca dex ga te nga génne jën wa jëkk a xëcc. Boo ubbee gémmiñam, dinga ca gis posetu estateer. Jël ko nag, jox leen ko ngir man ak yaw.»